Nañu won nit ñu bare suñuy yéenekaay
1 “ Lu am njariñ la, ñów na ci waxtu bi ñu ko soxla woon, te dafay maye doole. ” “ Masuma gis yéenekaay yu neex a jàng ni yooyu. ” Moom la nit ñu bare ci àddina si xalaat ci suñu yéenekaay yi tudd La Tour de Garde ak Réveillez-vous ! Dëgg-dëgg, suñu yéenekaay yi ñu ngi ñuy dimbali bu baax-a-baax ngir “ ñépp ” mën a dégg xibaar bu baax bi. — 1 Tim. 2:4.
2 Am na koo xam ne liggéeyam rekk la doon xalaat. Bi mu gisee ci benn Réveillez-vous ! lu ko itteel, mu jël ko ak La Tour de Garde bi mu àndaloon. Bi mu paree ci Réveillez-vous ! bi, mu gis ci La Tour de Garde fu ñu doon wax ci ngëm gi ñu wax Trinite (maanaam ñetti yàlla ci benn). Moom yàggoon na gëm loolu. Waaye gëstu na ngëm googu ci yéenekaay bi. Li mu fa jàng dafa ko neex ba mu bëgg waxtaan ak ñun. Juróom-benni weer ginnaaw loolu, dañu ko sóob ci ndox. Am na keneen ku ñu faraloon a indil suñuy yéenekaay waaye daawu ko woon a liir. Jabaram, moom, bëgguloon waxtaan ak Seede yi, waaye dafa doon jàng yéenekaay yi ñu doon jox jëkkëram. Gis na fa li Biibël bi dige, maanaam Yàlla dina indi àjjana ci kow suuf si te suuf si sépp dina fees ak nit ñu jub. Loolu dafa laal xolam. Moom, doomam bu góor, ak rakkam bu jigéen dem nañu ba jaamu Yexowa.
3 Booleel ay yéenekaay boo leen di wone : Ni ñu ko wonee fii ci kow, kenn mënul wax kan mooy liir suñuy yéenekaay, walla lan moo leen ciy neex (Daj. 11:6). Kon, bu dee sax ci benn yéenekaay lañu faral di waxtaan, nañu boole benn La Tour de Garde ak benn Réveillez-vous ! bu ñu leen di wone. Yenn saay sax, dinañu mën a boole ay yéenekaay yu bare.
4 Nanga jàpp benn bés ayu-bés bu nekk ngir wone suñuy yéenekaay. Ci Calendrier des Témoins de Jéhovah 2005, samdi bu nekk, “ Bésu yéenekaay yi ” la. Waaye, ndegam ku nekk ak li nga nekke, mën nga tànn bés bu la gënal. Ndax yaa ngi def loolu ayu-bés bu nekk ?
5 Xamal ñaata yéenekaay nga bëgg a joxe : Loolu dina tax nga gën a bëgg wone yéenekaay yi. Ndax am nga koo faral di jox suñu yéenekaay yi ? Ndax dinga leen wone boo waaraatee ? Ndax mën nga leen wone booy waaraate ci mbedd yi, fu bare bitig, ak fu nit ñu bare di romb ? Ndax yaa ngi yore ay yéenekaay booy tukki, booy dem màrse, walla boo amee benn ràndewu ? Saa yoo gisee loo mën a def ngir nit ñi jàng La Tour de Garde ak Réveillez-vous ! ba am ci njariñ, nanga ko def.
6 Xéyna danga am ay yéenekaay yu xaw a yàgg yoo bëgg a wone. Su dee sax am na léegi benn walla ñaari weer bi ñu génnee yéenekaay yooyu, ba tey li ci nekk am na solo. Kon, won ko ñi bëgg waxtaan ak ñun. Ci ay milyoŋi nit, La Tour de Garde ak Réveillez-vous ! nekk nañu “ kàddu gi [...] ci waxtu bi ñu ko soxla ”. (Léeb. 25:11.) Nañu leen won ay yeneen milyoŋi nit ngir ñu xam Yexowa ba jaamu ko.
[Laaj yi]
1, 2. Lan la La Tour de Garde ak Réveillez-vous ! def ci ay nit ?
3. Lu tax mu baax ngay boole ay yéenekaay boo leen di wone ?
4. Naka lañu mënee def porogaraam ngir wone suñuy yéenekaay ?
5. Kañ lañu mën a wone suñuy yéenekaay, te lu ñu ci mën a dimbali ?
6. Naka lañu mënee jariñoo suñuy yéenekaay yu xaw a yàgg ?