Naka lañu mën a ame njaboot bu dëgër ci wàllu ngëm ?
1 War nañu ndokkeel njabootu karceen yi ndax dañuy “ wone seen ragal Yàlla ci seen biir kër ”. (1 Tim. 5:4.) Waaye lépp lu bon li ñu wër te mën a wàññi suñu ngëm, moo tax njaboot yi war a xeex ngir seen ngëm wéy di dëgër. Lu am-a-am solo la. Naka lañu ko mënee def ?
2 Nekk kilifa bu mel ni Krist : Kilifay njaboot yi war nañu roy Yeesu Krist bu ñuy def seen wareef bi jëm ci dooleel seen njaboot. Yeesu dafa saraxe bakkanam ngir wone ne dafa ñu bëgg. Waaye du noonu rekk la wonee mbëggeelam. Dafa doon wéy di ‘ dundal te di fonk ’ mbooloom (Efes 5:25-29). Way-jur yu bëgg seen njaboot, bu ñuy toppatoo bés bu nekk soxla yi seen njaboot am ci wàllu ngëm, noonu lañuy roye Yeesu bi mu daan toppatoo mbooloom ak mbëggeel. Loolu ëmb na jàng Biibël bi ak seen njaboot ayu-bés bu nekk, te am saa yu ñu ko mënee waxtaan yu xóot ci wàllu ngëm, te it bu amee poroblem, ñu gaaw koo toppatoo. — 5 Mu. 6:6, 7.
3 Ci liggéeyu waare bi : Ñépp ñi bokk ci njaboot, war nañu xam ne waar nit ñi ci Yexowa ak ci li mu bëgg def, lu am solo la ci seen njaamu Yàlla (Isa. 43:10-12). Yéen way-jur yi, bu ngeen bëggee seeni doom nekk Seede Yexowa bu am ngëm bu dëgër, dangeen war a teel a dugal liggéeyu waare bi ci seen xol. Waxtaanleen ak ñoom ci lu tax, bu ñuy waare, ñu war a fàtte suñu bopp te bokk ci liggéeyu waare bi ayu-bés bu nekk (Macë 22:37-39). Te it, fexeleen ñu tàmm di ànd ak yéen ci liggéeyu waare bi.
4 Dimbalileen seen njaboot ndax ñu xam ni waaraate bi amee solo. Naka ? Bu ngeen di jàng Biibël bi ak seen njaboot ayu-bés bu nekk, booleleen ci waajal waxtaan bu neex bu ngeen mën a am ci waaraate bi, te jéemleen koo mokkal. Na ngeen dimbali seen doom bu nekk ci waaraate bi ngir ñépp jëm kanam, waaye buleen fàtte at yi ñu am ak li ñu mën a àttan. Bu ngeen jógee ci waaraate bi, na ngeen waxtaan ak ñoom ci ni ñu gise ñoom ci seen bopp ne Yexowa dafa baax. Na ngeen nettali lu mën a dëgëral ngëm. Li njaboot yi di gën a “ mos ci mbaaxug Boroom bi ”, ci lañuy gën a jege Yexowa, te ci lañuy gën a am doole ngir xeex “ gépp coxor ”. — 1 Pie. 2:1-3.
5 Ci ndaje yi : Ci biir njaboot yi, bu ku nekk dimbalee moroomam ndax mu fekke ndaje yi yépp, di ko gën a def bu amee ku sonn, ku xolam jeex, walla ku bare poroblem, dina baax lool. Suñu benn mbokk bu jigéen bu nekk ndaw nee na :“ Sama baay, bu wàccee liggéey, dafay sonn. Waaye dinaa ko wax lu am solo lu ñu war a waxtaan ci ndaje bu ñuy am ngoon googu, te loolu dafa koy dimbali mu dem fekke ko. Te bu ma sonnee nag, moom moo may dimbali ma dem. ” — Yaw. 10:24, 25.
6 Na ngeen ànd ci def yenn yi : Njaboot yi war nañu am lu ñuy ànd di def, mel ni bokk ci liggéeyu kër gi. War nañu tànn bu baax li mën a féexal seen xol, te sàkk jot ngir loolu. Dem géej, doxantuji, fo, dem seeti ay mbokk walla ay xarit, loolu yépp mën na nekk lu neex lu ñuy fàttaliku ëllëg. — Daj. 3:4.
7 Njabootu karceen yu dëgër yi, dañuy xeex bés bu nekk li mën a wàññi seen ngëm. Dañuy gën di jege Yexowa, te noonu lañuy ame doole bi muy maye. — Efes 6:10.