Ndax yaa ngi farlu ci njàng mi ak mbind mi ?
1 Bu ñu bëggee jàng ngir am xam-xamu Yàlla ak li mu bëgg, dafa war a fekk ñu mën a jàng tuuti. Ñu bare gis nañu ne mën jàng te mën bind, dafa leen di dimbali bu baax ngir mën a jaamu Yàlla (Peeñ. 1:3). Ñu bare jàng nañu ni ñuy binde ak ni ñuy jànge ci mbooloo yu koy jàngale. Téere bi tudd Farlul ci njàng mi ak mbind mi (ay-WO) lañu fay jëfandikoo, bu ñu ko mënee am. Seetlu nañu ne loolu dafay tax nit ñi gaaw a mën a jàng te bind. — 1 Tim. 4:13 ; Macë 24:45.
2 Ni ñuy doxale mbooloo jàngaan yi : Dinañu leen won léegi li téere boobu wax li jëm ci ni ñuy doxale mbooloo jàngaan yi : “ Niki ci Lekkoolu Sasu Nguuru Yàlla, waarekat yépp, ñii ñu sóob ak ñii ñu sóobagul, mën nañoo bokk ci mbooloo yi ñuy jàngal ni ñuy binde ak ni ñuy jànge. Su mag ñi ci biir mbooloo taalibe Isaa yi gisee ne soxla nañu taxawal benn walla ay mbooloo jàngaan ngir njàng mi ak mbind mi, ku ñu wóolu ci njàngale mi lañu ko wara dénk. [...] Ci yoon, mbokk ci ngëm yu góor ñoo wara yore njàngale mi. Waaye, su amul ku góor ku mëna yore mbooloo jàngaan yi, mën nañu ko sant benn mbokk ci ngëm bu jigéen, bu mën jàngale. [...] Magi mbooloo mi mën nañu ñaan benn mbokk ci ngëm bu jigéen mu yore benn mbooloo jàngaan yu jigéen yu ñu sóob. Mën na yore itam benn mbooloo jàngaanu ndaw yu góor ak yu jigéen yu ñu sóobagul. Jigéen biy jàngale dafa wara musóoru, ndaxte ci yoon góor moo waroona jàngale. Jàngaan yi, bu ñu leen di jàngal ñaar walla ñetti yoon ci ayu-bés gu nekk, dina baax. Ci la seen njàng di gëna gaaw. Saa yu ñu pare benn njàng, war nañu jox jàngaan yi liggéey bu ñuy def seen kër. Liggéey boobu, jàngalekat bi dina ko seetaat ak ñoom bala ñuy tàmbali njàng mi ci topp. Waxtu bi ñuy jàngale, war na gënal li ëpp ci jàngaan yi. Am na ñuy xaaj mbooloo jàngaan yi ci ay xaaj yu yem, di leen jàngal bala ñuy tàmbali ndaje bu ñuy wax Njàngum Téere bi. Ñeneen ñi dañuy xaaj mbooloo jàngaan yi, di leen jàngal ci waxtu Lekkoolu sasu Nguuru Yàlla. Magi mbooloo taalibe Isaa ñooy tànn kañ ak fan la mbooloo jàngaan yi di daje. ”
3 Yexowa Yàlla, moom mii ñu sàkk, moo tax ñu mën a jàng te bind. Waaye dañu war a góor-góorlu bu ñu bëggee mën loolu. Jariñ bi gën bi nekk ci mën jàng ak bind mooy xam li baatu Yàlla di wax, te mën def li Yàlla wax fii : “ Guddeek bëccëg, na nga ko jàng, ak baat bu suufe. ” — Yos. 1:8.