Waare Nguur gi dafay musal !
1 Tey, loolu mooy liggéey bi ëpp solo ci àddina si sépp. Yexowa Yàlla, Yeesu Krist, ak ay malaaka yu baree bare, ñu ngi seetlu ni muy deme. Loolu, ban liggéey la ? Te lu tax mu am solo noonu ? Waare Nguur gi lañuy wax noonu. Dafay musal ay nit. — Room 1:16 ; 10:13, 14.
2 Am na ñu xalaat ne, jéem a defar àddina si moo ëpp solo. Ñu bare ñu ngi def lépp li ñu mën ngir indi fi jàmm, faj feebar yi walla wàññi poroblemu xaalis. Waaye lan moo gën a mën a dimbali nit ñi ?
3 Liggéey bu am solo lool : Xibaaru Nguur gi rekk mooy wax lu tax nit di dund, lu tax nit di am coono, di wone it ne benn yaakaar bu wóor kese moo am ci suñu ëllëg. Xibaar bu baax bi, dafay tax nit ñi mën a nekk xaritu Yexowa, te am noonu “ jàmmu Yàlla, ji xel mënta takk ”. (Fil. 4:7.) Xibaaru Nguur gi kese mooy wone li ñu mën a def bu ñu amee ay jafe-jafe tey. Moom rekk moo ñuy won li ñu war a def ngir mucc bés bu Yàlla di alag àddina su bon si (1 Ywna. 2:17). Ndax loolu warul tax ñu def lépp li ñu mën ci waaraate bi ?
4 Bu amee dëkk boo xam ne ñépp a ngi fay nelaw, musiba di waaj a dal seen kow. Baaraas (maanaam tabax buy téye ndoxu dex) bi nekk ca dex ba, mu ngi waaj a yàqu, ndox mi nar a ñów seen kow. Boo bëggee dimbali nit ñooñu, lan mooy li gën loo leen mën a defal ? Dindi ndox bi nekk ci ginnaaw baaraas ba ? Jéem a rafetal dëkk boobu, fekk ndox maa ngi koy waaj a yàq ? Déedéet ! Li gën mooy nga yee waa dëkk boobu, xamal leen musiba boobu di ñów, te fexe ba ñu rëcc ! Tey, musiba bu réy mu ngi waaj a dal ñi nga xam ne ñu ngi mel ni ñuy nelaw ci wallu ngëm (Lukk 21:34-36). Ndegam léegi Yàlla alag àddina si, nañu def suñu kem kàttan ngir waar nit ñu nu mën a waxal ñépp. — 2 Tim. 4:2 ; 2 Pie. 3:11, 12.
5 Bu ñu dellu ginnaaw : Nañu seet ni ñu mënee def ba waar ay nit ñu gën a bare ci xibaar bu baax bi — ci seen biir kër, ci mbedd mi, ci telefon, ak saa yu ñu ci amee bunt. Ci liggéey yi ñu mën a def yépp, liggéey bi ñu Yexowa sant moo ëpp solo. Bu ñu ci sawaree, dinañu ‘ musal suñu bopp, ñun ak ñi nuy déglu ’. — 1 Tim. 4:16.