TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Watchtower
TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Wolof
  • BIBLE
  • TÉERE YI
  • RÉUNIONS
  • km 4/02 p. 2
  • Ndaje yi jëm ci liggéeyu waare bi

Aucune vidéo n'est disponible pour cette sélection.

Il y a eu un problème lors du chargement de la vidéo.

  • Ndaje yi jëm ci liggéeyu waare bi
  • Sasu Nguuru Yàlla — 2002
  • Turu xaaj yi
  • 8-14 awril
  • 15-21 awril
  • 22-28 awril
  • 29 awril ba 5 me
  • 6-12 me
Sasu Nguuru Yàlla — 2002
km 4/02 p. 2

Ndaje yi jëm ci liggéeyu waare bi

8-14 awril

Woy-Yàlla 26

13 min : Yégle yi jëm ci suñu mbooloo. Yenn ci yégle yi nekk ci Sasu Nguuru Yàlla. Na ñaari nit topp li nekk ci xaaj bi tudd “ Li ñu mën a wax bu ñuy wone yéenekaay yi ” bi nekk ci Sasu Nguuru Yàlla bii walla bi ko jiitu, te wone ni ñu mënee wone La Tour de Garde ak Réveillez-vous ! yi ñu mujj a jot. Na ku ci nekk wone li mu mën a tontu bu amee ku ñu wax : “ Am naa sama diine ba pare ”. — Seetal Comment raisonner, ci xët 18 ba19.

12 min : Li nekk soxla ci mbooloo mi.

20 min : “ Nanuy defal ñépp lu baax. ”a Laajal ay laaj ñi teew, te may leen ñu tontu. Boo ci paree, laajal benn walla ñaari waaraatekat ñu wax li ñu def ba yokk seen liggéey ci waaraate bi.

Woy-Yàlla 68 ak ñaan bu mujj bi.

15-21 awril

Woy-Yàlla 96

10 min : Yégle yi jëm ci suñu mbooloo. Fu ñu tollu ci xaalisu mbooloo mi.

15 min : Pioñee yi ñu ngi kontine di dimbali ñeneen ñi. Wottukatu liggéeyu waare bi dina waxtaan ak benn wottukatu njàngum téere bi, benn pioñee, ak benn waaraatekat. Na waxaat li nekk ci porogaraam bi tudd “ Les pionniers aident les autres ” bi nekk ci Le ministère du royaume bu septaambar 1998, ci xët 4 (màrs 1999 ci xët 3 ci réewu RCA ak Tchad). Na waxtaan ak kenn ku nekk ci ñett ñooñu, ndax ñu xam li ñu war a def ci porogaraam boobu, te naka la loolu ame njariñ ci porogaraam boobu. Lan lañu defagum ngir porogaraam boobu dox ? Wottukatu liggéeyu waare bi, war na xamal waaraatekat yépp ne, su amee ku bëgg ñu dimbali ko ci waaraate bi, na ko ko wax. Ku ñu dimbali ba pare, te mu am feneen ci wàllu liggéeyu waare bi fu mu bëgg ñu dimbali ko, mën na ci bokk.

20 min : “ Mbégte bi nekk ci jébbal sa jot yépp liggéeyu Yàlla bi. ”b Waxal ndaw ñi bu ñu nekkee aji-xàll yoonu weer bu lekkool tëjee, dina baax lool.

Woy Yàlla 79 ak ñaan bu mujj bi.

22-28 awril

Woy Yàlla 8

10 min : Yégle yi jëm ci suñu mbooloo. Na benn surga mbooloo mi ak suñu benn mbokk mu jigéen topp li nekk ci xaaj bi tudd “ Li ñu mën a wax bu ñuy wone yéenekaay yi ” te nekk ci Sasu Nguuru Yàlla bii walla bi ko jiitu, te wone ni ñu mënee wone La Tour de Garde ak Réveillez-vous ! yi ñu mujj a jot. Surga mbooloo mi, na wone La Tour de Garde, te suñu mbokk mu jigéen wone Réveillez-vous ! Ku ci nekk, bu paree, waxaatal li mu njëkk wax ngir ñu bëgg ko déglu.

15 min : Buñu tàrde ! Waare la. Lépp li ñuy def bu ñuy jaamu Yàlla, lu am solo la te war na “ am waxtoom ”. (Daj. 3:⁠1.) Lépp li ñu taxawal ngir jaamu Yàlla, bëgg nañu ko jariñoo ni mu gënee. War nañu tàmbali ndajey mbooloo mi ak ndaje yi ñuy am bala ñuy waare ci waxtu bi war. Yexowa masul a tàrde ci li muy def (Xab. 2:⁠3). Ndax soxla nañu gën a góor-góorlu ci fànn boobu ? Yenn saay, dina am lu lay tàrdeel te doo ci mën dara. Waaye, bu ñu seetee bu baax ni ñuy doxale li ñu war a def, duñu tàmm tàrde, di agsi waxtu boo xam ne pare nañu woy ak ñaan yiy ubbi ndaje bi, walla di agsi ci ndaje ngir waaraate bi, fekk wax nañu ba pare kan ak kan ñooy ànd. Waxtaanleen ci li ñu mën a def ngir bañ a tàmm tàrde ci lépp li ñuy def ci wàllu ngëm. — Seetleen La Tour de Garde bu 15 suweŋ 1990, ci xët 29.

20 min : “ Ndax yaa ngi farlu ci njàng mi ak mbind mi ? ”c Wottukatu lekkool bi, walla beneen mag moo ko war a def. Na wone ni mbooloo mi mënee jariñoo li nekk ci xaaju Sasu Nguuru Yàlla bii. Na laaj ñi teew ay laaj te may leen ñu tontu. Bu paree, na waxtaan ak benn walla ñaari waaraatekat ñu jàng ni ñuy binde ak ni ñuy jànge ci seen mbooloo. Na ñaar ñooñu wax ni ñuy gërëme mbooloo mi ci njàng moomu. Mën ngeen a jariñoo it li nekk ci téere Les Témoins de Jéhovah et l’instruction, xët 10 ba 13, ak li nekk ci Réveillez-vous ! bu 22 desàmbar 2000 ci xët 8 ba 9. Bu ngeen paree, waxleen li ñuy def ci seen mbooloo ndax ñu jàngale fa ni ñuy binde ak ni ñuy jànge.

Woy Yàlla 85 ak ñaan bu mujj bi.

29 awril ba 5 me

Woy Yàlla 70

10 min : Yégle yi jëm ci suñu mbooloo. Fàttalil waaraatekat yi ne dañu war a bind li ñu def ci waaraate bi ci weeru awril te joxe ko.

15 min : “ Waare Nguur gi dafay musal ! ”d Nañu laaj ñi teew ñu wax lu tax aaya yi nekk ci xaaj bii ànd ak li ñu ci wax.

20 min : Bu ñu amee lu ñu bëgg seet ci téere Comment raisonner naka lañu waree def ? Waxtaan ak ñi teew. Léeg-léeg, ci liggéeyu waare bi, nit ñi dinañu laaj lu ñu mënul a gis ci xaaj bi tudd “ Table des matières ” ci xët 5. “ Index ” bi nekk ci xët 439 ba 445, mën na ñu dimbali bu baax bu ñuy wut aaya yiy wone lu tax ñu gëm dara. Waxal ñiy déglu ñu jëfandikoo “ Index ” bi ngir tontu laaj yii di topp. Bu ñuy wut ci “ Index ” bi, nañu jëfandikoo bind yu ñu dëngal ci laaj bu nekk (bàyyi nañu leen ci tubaab, ndegam amul Comment raisonner ci wolof) : Quel est le point de vue chrétien sur les drapeaux et les hymnes nationaux ? Pourquoi Dieu permet-il les catastrophes ? Comment expliquer le point de vue biblique sur le divorce ? Pourquoi et quand les sœurs doivent-elles porter une coiffure ? Quelle est l’origine de la fête des mères ? Comment savons-nous que le nombre 144 000 est pris au sens littéral dans la Bible ? Que signifie la parabole de l’homme riche et Lazare ? Waxal ne ñépp a war a góor-góorlu ngir jëfandikoo téere Comment raisonner bu ñuy waaraate.

Woy Yàlla 43 ak ñaan bu mujj bi.

6-12 me

Woy Yàlla 39

10 min : Yégle yi jëm ci suñu mbooloo. Waxtaan leen ci “ Nañu wéy di jariñoo La Tour de Garde ak Réveillez-vous ! ”

10 min : Nañu seet tey lu ñuy def ca jamonoy noppalu. Waare ak waxtaan ak ñi teew. Woneel li nit ñi tàmm def ca jamonoy noppalu : Fekke lépp lu ñuy waxtaan ci ndaje bu gën a mag bi, ndaje bu mag bu ñaari fan, walla ndaje bu mag bu benn fan, nekk pioñee benn weer walla lu ko ëpp, am liggéey bu ñuy def ci kër gi, walla féexal suñu xol. Laajal ñenn nit ñu wax li ñu bëgg def ca jamonoy noppalu, te wax it naka lañuy def ba bañ a foye njàngum Biibël bi ñuy def ci seen njaboot, ndajey mbooloo mi, walla waaraate bi, bu fekkee ne sax dañu tukki. Bu fekkee ne seen mbooloo am na gox fu ngeen waaraatewul lu bare, waxleen lu ngeen nar a def ngir ñu liggéey fa bu baax. Fàttalil waaraatekat yi ne, fu ñu mënta nekk, war nañu bind li ñu def ci waaraate bi te fexe ba seen wottukatu njàngum téere bi jot ko.

25 min : “ Naka lañu mën a ame njaboot bu dëgër ci wàllu ngëm ? ”e Bu ngeen waxtaanee ci xaaj boobu ba pare, waxal lu leen mën a jariñ ci li nekk ci La Tour de Garde bu 15 feewriyee 1999, ci xët 10 ba 12.

Woy Yàlla 27 ak ñaan bu mujj bi.

[Li ñu bind ci suuf]

a Li ngay njëkk wax warul weesu benn minit, ba pare laajal ñi teew ay laaj, te may leen ñu tontu.

b Li ngay njëkk wax warul weesu benn minit, ba pare laajal ñi teew ay laaj, te may leen ñu tontu.

c Li ngay njëkk wax warul weesu benn minit, ba pare laajal ñi teew ay laaj, te may leen ñu tontu.

d Li ngay njëkk wax warul weesu benn minit, ba pare laajal ñi teew ay laaj, te may leen ñu tontu.

e Li ngay njëkk wax warul weesu benn minit, ba pare laajal ñi teew ay laaj, te may leen ñu tontu.

    Téere yi ci Wolof (1996-2025)
    Ngir génn
    Ngir konektewu
    • Wolof
    • Yónnee ko
    • Ni nga bëgge mbir yi feeñe
    • Copyright © 2025 Watch Tower Bible and Tract Society of Pennsylvania
    • Conditions d’utilisation
    • Règles de confidentialité
    • Paramètres de confidentialité
    • JW.ORG
    • Ngir konektewu
    Partager