TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Watchtower
TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Wolof
  • BIBLE
  • TÉERE YI
  • RÉUNIONS
  • km 5/02 p. 1
  • Suñu ngëm dafay tax ñu def lu baax

Aucune vidéo n'est disponible pour cette sélection.

Il y a eu un problème lors du chargement de la vidéo.

  • Suñu ngëm dafay tax ñu def lu baax
  • Sasu Nguuru Yàlla — 2002
Sasu Nguuru Yàlla — 2002
km 5/02 p. 1

Suñu ngëm dafay tax ñu def lu baax

1 Ngëm moo xiiroon Nóoxin, Musaa, ak Raxab ci jëf. Nóoxin dafa tabax gaal ga. Musaa dafa bàyyi dund bu neex bu mu amoon ca kër Firawna. Raxab nag moom, dafa nëbb nit ñi ñówoon seet ni dëkkam meloon, ba pare def li ñu ko wax, ba tax waa këram mucc (Yaw. 11:​7, 24-26, 31). Suñu ngëm tey, lu baax lan lañuy tax a def ?

2 Waaraate bi : Suñu ngëm moo tax ñuy wax lu jëm ci suñu Yàlla ju baax ji ak it ci li mu def ngir ñu am bànneex bu dul jeex (2 Kor. 4:13). Xéyna yenn saay dañuy ragal a waaraate. Waaye bu ñu ‘ tegee Yexowa ci suñu kanam saa yu nekk ’, dinañu gën a am doole, te dootuñu ragalati (Sab. 16:⁠8). Bu boobaa, suñu ngëm dina ñu xiir ci xamal xibaar bu baax bi saa yu ñu ci amee bunt, suñuy mbokk, suñuy dëkkandoo, ñi ñuy liggéeyandoo, ñi ñu bokkal kalaas, ak ñeneen. — Room 1:​14-16.

3 Ndaje yi : Tàmm fekke ndaje yi, bokk na ci li baax li suñu ngëm mën a jur ci ñun. Lu tax ñuy wax loolu ? Ndaxte dafay wone ne, dañu gëm ne, Yeesu mu ngi ak ñun ci suñuy ndaje karceen yi, ci kàttanu xel mu sell mi (Macë 18:20). Day wone itam ne dañu bëgg ‘ déglu li xelum Yàlla di wax mboolooy ñi gëm ’. (Peeñ. 3:⁠6.) Li ñu fay jàng, fonk nañu ko ndaxte xam nañu ne ci Yexowa la jóge, moom mi nekk Jàngalekat bu Mag bi. — Isa. 30:⁠20.

4 Li ñuy tànn def : Wóor na ñu ne li ñu dul gis am na. Looloo tax lépp luy laal suñu ngëm lañuy jiital ci suñu dund (Yaw. 11:⁠1). Yenn saay, loolu dafa ñuy laaj ñu nangu ñàkk yenn yi. Nañu ko seetee ci lii : Benn magu mbooloo mi, nanguwul liggéey bi ñu ko bëggoon a jox, ndaxte dafa xamoon ne bu fekkee ne sax mënoon na ci am xaalis bu gën a bare, liggéey boobu naroon na tax mu bañ a fekke ndaje yi yépp. Dina sore njabootam, te du mën a nekkati pioñee. Ñun itam nañu wóolu li Biibël bi wax, maanaam Yexowa dina may ñi ‘ jëkk wut nguuram ak njubteem ’, li ñuy dunde. — Macë 6:⁠33.

5 Ngëm, dafa am doole, te li muy jur ci ñun, nit ñi mënuñu ko bañ a gis. Waaw, àddina si sépp xam na ngëm gi ñu am (Room 1:⁠8). Kon ñun ñépp, suñu ngëm gu dëgër gi, nañu ko wone ci lu baax li ñuy def. — Saak 2:26.

    Téere yi ci Wolof (1996-2025)
    Ngir génn
    Ngir konektewu
    • Wolof
    • Yónnee ko
    • Ni nga bëgge mbir yi feeñe
    • Copyright © 2025 Watch Tower Bible and Tract Society of Pennsylvania
    • Conditions d’utilisation
    • Règles de confidentialité
    • Paramètres de confidentialité
    • JW.ORG
    • Ngir konektewu
    Partager