Ndax yaa ngi jëfandikoo téere Laaj bi ngir tàmbali ay njàngum Biibël bi ?
1 Ndax xam nga ne booy faral a am waxtaan ci Biibël bi ak nit, te ngay jëfandikoo téere yi ñu defar ngir jàngal nit ñi Biibël bi, bu dee sax waxtaan bi du yàgg, yaa ngi def njàngum Biibël ? Bu fekkee ne sax yaa ngi koy def ci buntu kër walla ci telefon, njàngum Biibël la. Nañu góor-góorlu ci weeru me ak weeru suweŋ ngir tàmbali ay njàngum Biibël bi ci téere Laaj bi.
2 Boo bëggee tàmbali ay njàngum Biibël bi, nanga ko waajal : Booy wone téere Laaj bi, nanga xam bu baax ci lan nga bëgg waxtaan. Booy dellu seeti nit, xalaatal ci li ngeen mujjoon a waxtaan. Laajal sa bopp lii : ‘ Yan xise lañu mën a jàng ngir àggale waxtaan bi ñu fa mujj am, ndax ma mën a jàng ak moom Biibël bi ? ’ Booy waaraate kër-oo-kër, seetal yan waxtaan ñoo mën a itteel janq, xale bu góor, mag, góor walla jigéen. Seetal waxtaan yi nekk ci téere Laaj bi te tànnal li mën a neex ki ngay waxal. Boo seetee ba pare ni nga bëggee tàmbali waxtaan bi, nanga ko jéem a mokkal. Loolu, dina la dimbali nga mën a tàmbali ay njàngum Biibël bi.
3 Sasu Nguur Yàlla bu sãwiyee 2002 ci xët 2, dafay joxe juróom-ñetti fasoŋ yi ñu mënee wone téere Laaj bi. Xaaj bi tudd “ Waxal nit ki ne mën nañu koo jàngal Biibël bi ” dafay wone ni ñu mënee tàmbali ay njàngum Biibël bi ak téere boobu. Ni nga mënee topp li nekk ci bu njëkk bi :
◼ “ Ndax xam nga ne, mën nga am ci lu gaaw tont ci ay laaj yu am solo yu jëm ci Mbind mu sell mi ? Xoolal laaj bii : Diine yuy wax ne ci yoonu Isaa lañu bokk, lu tax ñu bare nii ? Ndax mas nga ci xalaat ? ” Bu la nit ki tontoo, ubbil njàngale 13, te waxtaanleen ci ñaari xise yu njëkk yi. Bu ngeen amee jot, jàngleen benn walla ñaari aaya, te waxtaanleen ci. Bu ngeen paree, jàngleen laaj bu mujj bi ci laaj yi nekk ci boppu xët bi, ba noppi wax lii : “ Bu ñu jàngee xise yi des, dinañu xam juróomi yëf yu ñuy tax a xàmme diine dëgg ji. Bëgg naa fi dellusi ngir waxtaan ci ak yow. ”
4 Nanga ci wéy : Saa yoo ko mënee, nanga wone ni ñuy jànge Biibël bi ak téere Laaj bi. Ñaanal Yexowa mu barkeel la (Macë 21:22). Boo ciy góor-góorlu bu baax, ñàkkul nga mën a dimbali nit, mu nangu xibaar bu baax bi, te dinga gis ni mu neexe.