Li ñu mën a wax bu ñuy wone yéenekaay yi
La Tour de Garde 15 avril
“ Ak fu ñu mënta dëkk, nit ñi dañu bëgg am jàmm ak salaam, mel ni am liggéey bu baax, te yàgg ci. Waaye, ndax mas nga xalaat ne am na lu mën a indi jàmm ak salaam ba fàww ? [Jàngal Sabuur 16:8, 9.] La Tour de Garde bii, dafay wone fan lañu mënee am jàmm ak salaam. ”
Réveillez-vous ! 22 avril
“ Tey, ñu bare dañuy bàyyi diine yi, di jaamu Yàlla ni mu leen neexe. Loo ci xalaat ? [Mayal nit ki mu tontu.] Biibël bi dafay wone ne ni ñuy jaamoo Yàlla, nekk na lu am solo lool ci moom. [Jàngal Yowanna 4:24.] Réveillez-vous ! bii, dafa ñuy wax li mën a faj suñuy soxla ci wàllu ngëm. ”
La Tour de Garde 1 mai
“ Ndax xam nga nit ku feebar lool, walla ku làggi ? Wóor na ma ne dinga nangu ne nit ñooñu, soxla nañu ñu wax leen lu leen di may doole. Lan lañu leen mën a wax ? Biibël bi am na ay wax yuy maye yaakaar. [Jàngal Isayi 35:5, 6.] La Tour de Garde bii, dafay wone lu tax ñu mën a gëm loolu. ”
Réveillez-vous ! 8 mai
“ Liy dindi jàmm ci àddina, masul a bare ni mu baree ci at mii weesu. Ndax ci sa xalaat nguuru nit ñi dinañu mën a indi jàmm ci àddina ? [Bu la tontoo, jàngal Isayi 2:4.] Réveillez-vous ! bii dafay wone lu tax ñu mën a gëm ne léegi jàmm am ci kow suuf si sépp. ”