TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Watchtower
TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Wolof
  • BIBLE
  • TÉERE YI
  • RÉUNIONS
  • km 5/02 p. 2
  • Ndaje Yi Jëm Ci Liggéeyu Waare Bi

Aucune vidéo n'est disponible pour cette sélection.

Il y a eu un problème lors du chargement de la vidéo.

  • Ndaje Yi Jëm Ci Liggéeyu Waare Bi
  • Sasu Nguuru Yàlla — 2002
  • Turu xaaj yi
  • 13-19 me
  • 20-26 me
  • 27 me ba 2 suweŋ
  • 3-9 suweŋ
Sasu Nguuru Yàlla — 2002
km 5/02 p. 2

Ndaje Yi Jëm Ci Liggéeyu Waare Bi

BUL FÀTTE : Jamano bu ñuy am suñu ndaje bu gën a mag bi, Sasu Nguuru Yàlla bi dina joxe li ñu war a def ayu-bés bu nekk ci ndaje yi jëm ci liggéeyu waare bi. Mbooloo yi dinañu seet ni ñuy doxale seeni ndaje ci weer bu ñuy am seen ndaje bi gën a mag bi tudd “ Ñi sawar ci waare Nguuru Yàlla ”. Su baaxee ci seen mbooloo, ayu-bés bi jiitu ayu-bés bi ngeen di am seen ndaje bi gën a mag bi, na ngeen beral 15 minit ngir waxtaan ci li nekk ci xët 3 ba 6 ci Sasu Nguuru Yàlla bii te ànd ak li seen mbooloo soxla. Dinañu jàpp ayu-bés bi gën ngir seetaat li ñu waxtaan ci ndaje bi gën a mag bi ci ndaje bi jëm ci liggéeyu waare bi. Ngir waajal ndaje boobu, ñépp a war a bind li am solo lu muy jàng ci ndaje bu gën a mag bi. Li ñu bëgg topp ñun ci suñu bopp ci suñu dund ak bu ñuy waaraate, war na bokk ci loolu ñuy bind. Bu boobaa dinañu mën a wax lan lañu def booba ba léegi ngir topp xelal yooyu. Kenn ku nekk buy wax njariñ bi mu jële ci li mu jàng ci ndaje bu gën a mag boobu, loolu dina yokk doole ñeneen ñi.

13-19 me

Woy-Yàlla 16

15 min : Yégle yi jëm ci suñu mbooloo. Yenn ci yégle yi nekk ci Sasu Nguuru Yàlla. Ay xibaar yu jóge ci suñuy mbokk ci ngëm. Na ñaari nit topp li nekk ci xaaj bi tudd “ Li ñu mën a wax bu ñuy wone yéenekaay yi ” bi nekk ci Sasu Nguuru Yàlla bii walla bi ko jiitu, te wone ni ñu mënee wone La Tour de Garde ak Réveillez-vous ! yi ñu mujj a jot. Na ku ci nekk wone li ñu mën a tontu bu amee ku ñu wax : “ Dama jàpp. ” — Seetal téere Comment raisonner ci xët 19 ba 20.

15 min : “ Fu ñu mën a dimbaleente ci wàllu ngëm ngir gën a am doole. ” Waare lay doon. Waxal lu tax fekke ndaje bi gën a mag bi am solo. Waxal itam ne ñépp a war a fexe ba fekke lépp li ñuy wax ci ñetti fani ndaje bi yépp, àjjuma ba dibéer.#

15 min : “ Saxleen ci baax. ”a Waxal ba mu leer ne dañu war a topp tegtal yi jëm ci fi ñuy dal bu ñuy ñów ci ndaje bi gën a mag bi. Tegtal yooyu ñun ñoo tax ñu def leen. Woneel bu baax juróom-ñetti yëf yu ñu warul a fàtte ci xise 2. Waxal lu tax ñun ñépp a war a wone jikko ju rafet bu ñu demee ci ndaje boobu.#

Woy-Yàlla 95 ak ñaan bu mujj bi.

20-26 me

Woy-Yàlla 6

15 min : Yégle yi jëm ci suñu mbooloo. Fu ñu tollu ci xaalisu mbooloo mi. “ Tont ci seen laaj. ”

12 min : “ Nañu faj suñuy soxla ci wàllu ngëm. ” Waare ak waxtaan ak ñi teew. Waxleen lu tax ñépp a war a déglu bu baax lu ñu wax ci ndaje bi gën a mag bi ; bañ a yem ci déglu kese, waaye topp li ñu jàng. “ BUL FÀTTE ” bi nekk ci kow, dañu ko def ngir ndaje bu ñuy def ngir seetaat li gën a am solo ci li ñu jàng ci ndaje bu gën a mag boobu. Waxtaanleen ci. Waxal ne bu ñépp bindee li ñuy wax ci ndaje bu mag boobu, dina baax. Laajal ay nit ñu wax lu baax li ñu jële ci ndaje bi gën a mag bi ñu amoon daaw.

18 min : “ Nañu yiw ci li ñuy sol. ”b Benn mag moo war a def waxtaan bii. Dina jàng xise bu nekk, bu ñu ci waxtaanee ba pare. Dimbalil ñépp ñu xam lu tax ñu war a seet bu baax ni ñuy soloo bu ñu nekkee ci diggu nit ñi.

Woy-Yàlla 75 ak ñaan bu mujj bi.

27 me ba 2 suweŋ

Woy-Yàlla 87

12 min : Yégle yi jëm ci suñu mbooloo. Fàttalil waaraatekat yi ne dañu war a bind li ñu def ci waaraate bi ci weeru me te joxe ko. Na ñaari waaraatekat topp li nekk ci xaaj bi tudd “ Li ñu mën a wax bu ñuy wone yéenekaay yi ” bi nekk ci Sasu Nguuru Yàlla bii walla bi ko jiitu, te wone ni ñu mënee wone La Tour de Garde ak Réveillez-vous ! yi ñu mujj a jot. Ku nekk mag mooy wone La Tour de Garde, te benn ndaw wone Réveillez-vous ! Ku ci nekk bu paree, woneel ne boole benn aaya ci li ñuy wax ngir wone suñuy yéenekaay, lu yomb la.

15 min : “ Ndax gox bi sa mbooloo moom dafa réy ? ” Waare ak waxtaan ak ñi teew. Wottukatu liggéeyu waare gi moo ko war a def. Bu fekkee ne gox bi seen mbooloo moom yaatuwul, mën ngeen a waxtaane xaaj bi tudd “ Faisons en sorte que notre temps compte ”, bi nekk ci Le ministère du Royaume bu suweŋ 1999 (desàmbar ci dëkku RCA ak Tchad). Gox bi seen mbooloo moom, waxal ni mu yaatoo, te waxal fi ngeen waare ci at mi weesu. Waxal ni ñu mënee topp ci suñu mbooloo li ñu wax ci xaaj bii. Waxal lu seen mbooloo bëgg def bu ci kanamee tuuti ngir waare gox fu ngeen waaraatewul lu bare.

18 min : “ Ndax yaa ngi jëfandikoo téere Laaj bi ngir tàmbali ay njàngum Biibël bi ? ” (Ñépp a war a indaale Sasu Nguuru Yàlla bu sãwiyee 2002 ngir waxtaan ci.) Balaa ñuy tàmbali waxtaan bi, na benn waaraatekat topp li nekk ci xise 3 ngir wone ni ñu mëne tàmbali benn njàngum Biibël bi. Na ko waajal bu baax-a-baax balaa muy ñów ci ndaje bi. Bu paree, woneel ay ponk yu am solo ci téere Laaj bi te woneel ni ñu mënee tàmbali ay njàngum Biibël bi ak téere boobu. Woneel lu tax ñu war a seetaat tegtal yi nekk ci Sasu Nguuru Yàlla bu sãwiyee 2002 xët 2 ba 4 ak ci Le ministère du royaume bu sãwiyee 2002 ci xët 3 ak 6. Laajal ñiy déglu ban tegtal lañu topp ba tax ñu am ay njàngum Biibël bi. Ngir jeexal waxtaan bi, waaraatekat bi toppoon li nekk ci xise 3 bi na ko defaat.

Woy-Yàlla 25 ak ñaan bu mujj bi.

3-9 suweŋ

Woy-Yàlla 71

15 min : Yégle yi jëm ci suñu mbooloo. Ñi nekkoon aji-xàll yoonu weer (pionnier auxiliaire) walla aji-xàll yoon ju ci sax (pionnier permanent) ci weeru màrs, awril walla me, nañu waajal seen bopp ngir wax lu baax li ñu ci jële.

15 min : Naka la téere Comment raisonner di jëfandikoo ay Biibël yu ñeneen firi. Waare bu gàtt ak waxtaan ak ñi teew. Jàngal Comment raisonner, xët 8, xise 1, te waxal lu tax ñu war a jëfandikoo bu baax Biibël bi bu ñuy waaraate, te naka lañu ko mënee def. Woneel turu Biibël yi nekk ci xët 6, te waxal lu tax ñuy jëfandikoo li nekk ci Biibël yu yeneen nit firi. Waxtaanleen ci li ñu war a moytu ni ko waxe La Tour de Garde bu 1 oktoobar 1997, ci xët 16, xise 2, ak ci xët 20, xise 15. Waxal ñi teew ñu seet li nekk ci “ Succession apostolique ”, “ Images ” et “ Trinité ” ci téere Comment raisonner ngir xam njariñ bi nekk ci jëfandikoo Biibël yu ñeneen firi, bu ñuy jàngale dëgg gi.

15 min : “ Suñu ngëm dafay tax ñu def lu baax. ”c Bu ngeen àggee ci xise 2, laajal benn waaraatekat bu sawar ci liggéeyu waare bi, ay laaj ci lu gàtt. Na wax naka la waaraate bi di wone suñu ngëm te di ko dëgëral.

Woy-Yàlla 26 ak ñaan bu mujj bi.

[Li ñu bind ci suuf]

a Li ngay njëkk wax warul weesu benn minit, ba pare laajal ñi teew ay laaj, te may leen ñu tontu.

b Li ngay njëkk wax warul weesu benn minit, ba pare laajal ñi teew ay laaj, te may leen ñu tontu.

c Li ngay njëkk wax warul weesu benn minit, ba pare laajal ñi teew ay laaj, te may leen ñu tontu.

    Téere yi ci Wolof (1996-2025)
    Ngir génn
    Ngir konektewu
    • Wolof
    • Yónnee ko
    • Ni nga bëgge mbir yi feeñe
    • Copyright © 2025 Watch Tower Bible and Tract Society of Pennsylvania
    • Conditions d’utilisation
    • Règles de confidentialité
    • Paramètres de confidentialité
    • JW.ORG
    • Ngir konektewu
    Partager