Fu ñu mën a dimbaleente ci wàllu ngëm ngir gën a am doole
1 Ñi bokk ci mbooloo Yexowa bi, amul bés boo xam ne, duñu am luy song seen ngëm. Seytaane dafa xam ne jot bi ko dese bareetul. Looloo tax tey, dafay song suñu ngëm, song bu metti ngir ñu bañ a topp Yàlla, ndaxte xam na ne dootu ko mën a defati (Peeñ. 12:12). ‘ Doolewu ci Boroom bi, te soloo kàttanam gu mag gi ’, lu am a am solo la. Dina tax ñu “ mana jànkoonte jamano ju xeex bi taree, noot lépp te taxaw temm ”. — Efes 6:10, 13.
2 Am na lu Yexowa taxawal ngir ñu mën a am doole; mooy ndaje yi ñuy am ak suñuy mbokk ci wàllu ngëm. Ndaw li Pool xamoon na ni loolu ame solo. Dafa doon yàkkamtee nekk ak mbokkam yi ci wàllu ngëm, ndax ku ci nekk mën a yokk doole moroomam te am ngëm gu gën a dëgër (Room 1:11, 12). Li ñu Jataay biy dogal bëgg moo tax mu taxawal ndaje bi gën a mag bii di ñów te tudd “ Ñi sawar ci waare Nguuru Yàlla ”, ngir yokkal ñu doole bi ñuy tax a def li Yàlla bëgg. Foofu, dinañu mën a dimbaleente ngir gën a am doole ci wàllu ngëm.
3 Nanga ko fekke ndax nga mën koo jariñoo : Fexeel ba fekke ñetti fan yi yépp. Bu ñu bëggee jariñoo bu baax ndaje bi, war nañu agsi balaa ñuy woy woy bu njëkk ba, te toog ba fekke ñaan bu mujj bi, ba mën a wax “ amiin ” bu jóge suñu xol (Isa. 48:17, 18). Ñu bare war nañu seet lu ñu mën a def balaa ndaje bu gën a mag bi di jot ndax seen liggéey bañ leen a tere fekke ñetti fani ndaje bi yépp. Dëgg la, fexe ba ku ñuy liggéeyal may ñu ñetti fan yooyu, mën na bañ a yomb. Waaye Yexowa dig nañu ne dina ñu dimbali ndax ñu mën a def li mu bëgg (1Ywna. 5:14, 15). Bu fekkee ne wutaguñu lu ñuy yóbbu ci ndaje bi ak fi ñu war a dal , léegi lañu ko war a def. Waruñu xalaat ne, dinañu am loolu yépp bu ñu fa agsee. Ci lu wóor, Yexowa dina barkeel lépp li ñuy def ngir mën a fekke ndaje bu mag boobu, ñetti fan yi yépp. — Léeb. 10:22.
4 Yàkkamtil ndaje boobu ndax li muy yokk sa doole : Ndax mas nga dem ci benn ndaje bu gën a mag ba pare ne : “ Bii moo dàq yi ma fekke yépp ! ” Lu tax ñu mën a xalaat lu mel noonu ? Ndaxte ku matul na ñun, mën na dem ba sonn lool te gis ne soxla na luy yokk dooleem ci wàllu ngëm (Isa. 40:30). Suñu benn mbokk mu jigéen nee na : “ Sonn naa lool ndax coonoy àddina sii. Waaye ndaje bu gën a mag bi, dafa ma wonaat ne liggéeyu Yexowa moo war a jiitu ci sama dund. Noonu la ma maye doole bi ma soxla. Dafa mel ni dañu yokk sama doole, bi ma ko gënee soxla. ” Xéyna mas nga yëg lu mel noonu.
5 Ci ndaje bi, dafay am ay waxtaan ak li ñuy woowe interview (maanaam bu ñuy laaj nit ay laaj ci kanamu ñépp). Waaye, du loolu kese mooy yokk suñu doole ci wàllu ngëm. Suñu benn mbokk nee na : “ Dañuy wone ba mu leer ni ñu mënee topp li Biibël bi santaane. Loolu, lu ma neex dëgg la. Daraam yi am nañu njariñ lool ndaxte dañuy wone li ñu mën a jàng ci nit ñu nekkoon ca jamano yu njëkk ya, ñu baax ñi ak ñu bon ñi ñépp. Téere yu bees yi nag, dama leen di yàkkamti. Bi ndaje bi weesoo ba mu yàgg sax, dama ciy bég. ”
6 Ndaje yu gën a mag yi ñu Yexowa taxawal, lu ñu soxla dëgg la ci “ bési tiis yu tar ” yi ñu nekk tey (2 Tim. 3:1). Dinañu tax ñu mën a topp xelal bii jóge ci Yàlla : “ Farluleen te dëgër ci ngëm, di góor-góorlu te am pasteef. ” (1 Kor. 16:13). Kon nag, buñu bàyyi dara tere ñu fekke benn waxtaan ci yi ñuy def ci ndaje bi gën a mag bi tudd “ Ñi sawar ci waare Nguuru Yàlla ”, te nañu jariñoo bu baax ci li ñu fay dimbaleente ngir gën a am doole ci wàllu ngëm !
[Wërale bi nekk paas 3]
Seetal li nga war a def ba mën a fekke ñetti fan yépp
■ Ñaanal fi ngay liggéeye, ñu may la ñetti fan yooyu.
■ Wutal fi nga mën a dal.
■ Wutal lu lay yóbbu ci ndaje bu gën a mag bi.