“ Saxleen ci baax ”
1 Ku bëgg nekk karceen dafa war a baax “ ci ñépp ” te sax ci (1 Tes. 5:15). Bu ñu demee ci suñuy ndaje yu gën a mag yi, bare na lu baax li ñu mën a defal ñeneen ñi. Foofu, nit ñu bare ñu ngi ñuy xool. Te li ñuy xalaat ci ñun, mu ngi aju ci ni ñuy digaale ak ñoom. Bu ñu bëggee nit ñi xalaat lu baax ci ñun Seede Yexowa yi, dañu war a wone ci suñuy jëf ne dañuy ‘ teral ñépp ’. (1 Pie. 2:17.) Loolu ëmb na bañ a ‘ yem ci topptoo suñu bopp rekk, waaye boole ci suñuy moroom ’. (Fil. 2:4.) Nañu seet ni ñu mënee def loolu fi ñuy dal bu ñuy dem ci suñu ndaje bu mag bi.
2 Ndax xalaat ngeen ba pare fi ngeen di dal bu ngeen demee suñu ndaje bu gën a mag bi ? Am na ay njaboot yu foog ne fu ñu mën a dal du ñàkk mukk, te dinañu ko mën a laaj bu ñu agsee fu ñuy defe ndaje boobu ci bésu alxemes walla àjjuma ci suba. Loolu baaxul. Boo waree dal kër jaambur, walla ci béréb bu nit ñu bare bokk ngir fanaan fa, seetaatal lii di topp ngir bañ ko fàtte : 1) Boo jotee kayit bi tudd Demande de logement (maanaam fi ngay ñaan foo mën a dal), gaawal a bind lépp lu ñu la ci laaj. 2) Boo waxee ba pare ci kayit boobu ñaata nit ñooy ànd ak yow, bul indi ay nit yu ëpp loolu. 3) Bu dee sax, fi nga war a dal, amul lépp loo faral di am ci sa kër, nanga am ngërëm ci li ñu lay jox. Mën nga joxe xaalis ngir ndox mi ak kuuraa bi ngay jëfandikoo. Dinga wone noonu sa ngërëm. 4) Bu musiba amee fi ngay dal nanga koo gaaw a wax biro bi ñuy woowe Administration de l’assemblée (maanaam ñiy doxal ndaje bi). 5) Bu dee ci béréb bu nit ñu bare bokk ngir fanaan fa nga war a dal, te ñu xàjjale ko, góor ñi féete benn boor, jigéen ñi beneen boor bi, nanga topp li la Administration de l’assemblée laaj. Boo nekkee ci otel, nanga jàpp ci sa xel lii di topp : 1) Nanga teey te weg ñi fay liggéey. 2) Toppal li ñu la fay wax lu jëm ci li nekk ci otel bi. 3) Nanga seet bu baax lépp li say doom di def. Bu ñu nekkee ci otel walla ci kër jaambur, nañu góor-góorlu ngir yem fu ñu war a yem, te sax ci li baax.
3 Jàngalleen seeni doom ni ñuy defe lu baax : Ay xale yu nekkoon ñoom kenn, fekk mag yu ñu àndaloon nekkuñu woon seen wet, mas nañu indi ay jafe-jafe ci otel, walla béréb fu ñu daloon (Léeb. 29:15). Léeg-léeg seen wayjur yi dañuy nekk ci leneen, bàyyi leen ñoom kenn ca néeg ba, walla feneen fu mu mënta doon ca otel ba, walla ca kër gu ñu dal. Am na ay xale yu bare woon coow te léej ba ñiy liggéey ca otel ba walla boroom kër gu ñu daloon dañu leen mujj teree jëfandikoo yenn yi. Loolu dafa doon tanqal ñeneen nit ña fa nekkoon, Seede yi ak ñi nekkul Seede yépp. Kon, boo dalee ci suñu kër mbokk ci wàllu ngëm walla ci koo xam ne dafay jàng Biibël bi, toppal li ñu la fay ñaan. Bul dem ci néeg foo warul a dugg, walla foo xam ne kenn mayu la nga dem fa. Seetal ndax say doom xam nañu te ñu ngi topp li ñu leen ñaan fi ngeen di dal.
4 Yéen wayjur yi, bala ndaje bi jot, nangeen toog ak seeni doom, seetaat ak ñoom naka la xale karceen war a mel, fu mu mënta nekk, waxtu bu mu mënta doon. Loolu, dina baax lool (Efes 6:4). Mën nga leen won ba mu leer ne, ku am mbëggeelu karceen dëgg, “ du def lu jekkadi, du wut njeriñu boppam, du naqari deret ”. (1 Kor. 13:5.) Ñi nekk mag mën nañu dëgëral wax yooyu bu ñu toppee loolu bu baax ci kanamu ñépp. Yéen xale yi, mën ngeen a sax ci baax bu ngeen déggalee seeni wayjur, bu ngeen xamee ni ngeen di defe ak lépp li nekk fi ngeen di dal, xam ne alalu jaambur la, te it bu ngeen wegee ñi ngeen nekkal (Kol. 3:20). Bu ñu defee lu ñu mën ngir sax ci baax ci ñépp, dañuy “ rafetal ci lépp njàngalem Yàlla sunu Musalkat ”. — Titt 2:10.
5 Suñu jëfin ju rafet dafay jur lu baax ci ñi ñuy xool. Dina jur sax lu baax ci ñi nga xam ne dañuy wax lu bon ci ñun. Kon nag, ak li ñuy mënta def, ci ndaje boobu walla ci biir dëkk bu ñu koy defe — bu ñuy dox ci mbedd yi, walla bu ñuy lekk ci restoraŋ, walla bu ñuy waare saa yu ñu ci amee bunt — li ñuy nekk di jëfe te di wax ni ko karceen waree def, moo war a wone ne ñu ngi sax ci baax.
[Wërale bi nekk paas 4]
Nanga fàttaliku lii :
■ Bindal bu baax li ñu la laaj ci kayit bi tudd Demande de logement, te bu ko yéex a def.
■ Boo waxee ba pare ci kayit boobu ñaata nit ñooy ànd ak yow, bul indi ay nit yu ëpp loolu.
■ Toppal li la biro biy doxal ndaje bi laaj.
■ Wegal ñiy liggéey ci otel bi ngay dal, walla ñi nekk ci kër gi ngay dal.