Ndaje yi jëm ci liggéeyu waare bi
10-16 suweŋ
Woy-Yàlla 28
15 min : Yégle yi jëm ci suñu mbooloo. Woneel porogaraamu ndaje yi gën a mag bi nekk ci Sasu Nguuru Yàlla bii. Waxal ci ban ndaje la seen mbooloo war a dem. Yenn ci yégle yi nekk ci Sasu Nguuru Yàlla bi. Bu ngeen amee wideo bi tudd Toute la communauté de nos frères, waxal ne bu ko ñépp mënee gis ngir waajal ndaje bi jëm ci liggéeyu waare bi ñuy def ci ayu-bésu 24 ba 30 suweŋ, dina baax. Na ñaari nit jëfandikoo li ñu def ci xët 8 ngir wone ni ñu mën a wonee La Tour de Garde ak Réveillez-vous ! yi ñu mujj jot. Na ku ci nekk wone li ñu mën a tontu bu amee ku ñuy wax : “ Mbirum diine soxalu ma. ” — Seetleen Comment raisonner, xët 16 ba 17.
10 min : Ay tont ci seeni laaj. Jàngleen xaaj bi yépp ak aaya yi ñu ci def yépp. Ginnaaw loolu, na ngeen wax li nekk ci Réponses à vos questions ci Le Ministère du Royaume bu màrs 1998 (septaambar 1998 ci République Centrafricaine).
20 min : “ Ku ji lu bare, am barke yu bare. ”a Booleleen ci li nekk ci La Tour de Garde bu 1 desàmbar 1992, xët 15 ba 16, xise 14 ba 17.
Woy-Yàlla 98 ak ñaan bu mujj bi.
17-23 suweŋ
Woy-Yàlla 57
8 min : Yégle yi jëm ci suñu mbooloo. Fu ñu tollu ci xaalisu mbooloo mi.
17 min : “ Nañu xam ni ñu war a gise ordinatër ak li mu mën a def. ” Bu leen ko jot gi mayee, jàngleen xise yu am solo yu mel ni xise 4 ba 8, ak xise 12 ak 13.
20 min : “ Na nga doylu ci li nga am. ”b Woneleen bu baax aaya yiy joxe xelal yi nekk ci xaaj bii. Ngir loolu, jàngleen aaya yi nekk ci xaaj bii te binduñu li ci nekk. Na ngeen ci jàng li ngeen mën yépp ci jot gi ngeen am, te waxtaanleen ci.
Woy-Yàlla 35 ak ñaan bu mujj bi.
24-30 suweŋ
Woy-Yàlla 91
8 min : Yégle yi jëm ci suñu mbooloo. Suñu benn mbokk mu góor ak jabaram ñooy wone ni ñuy defe bu ñuy ànd waaraate. Nañu wone ni ñu mën a wonee yéenekaay yi ñu mujj jot. Na jabar ji wone La Tour de Garde, jëkkër ji wone Réveillez-vous !
12 min : Nettalileen walla ay nit wone ni ay waaraatekat yi nekk ci seen mbooloo defe 1) bi ñu doon waar ay nit ñu bokkul xeet, walla ay nit ñu nu bokkul làkk, walla it 2) bi ñu doon waare feneen fu dul këroo-kër walla ci mbedd mi. Ngir waajal ndaje bi jëm ci liggéeyu waare bu ngeen di def ayu-bés biy ñów, waxleen ñi teew ne ku nekk na seet ni mu mënee wone benn ci téere yi ñuy wone ci weeru sulyet ak ut. — Seetal li nekk ci xaaj bi tudd “ Autres publications ” ci Le Ministère du Royaume bu sãwiyee 2002 ci xët 6.
25 min : “ Suñuy mbokk ci wàllu ngëm, lu tax ñu bëgg leen ñoom ñépp ? ” Tàmbalil waxtaan bi ak laaj yi nekk ci xaaj bii. Bu ngeen amulee wideo bi, waxtaanal ak ñi teew ci xaaj bi tudd “ La congrégation chrétienne : source d’une aide qui fortifie ” bi nekk ci La Tour de Garde bu 15 me 1999, xët 26 ba 28.
Woy-Yàlla 15 ak ñaan bu mujj bi
1-7 sulyet
Woy-Yàlla 1
15 min : Yégle yi jëm ci suñu mbooloo. Fàttalil waaraatekat yi ne dañu war a bind li ñu def ci liggéeyu waare bi ci weeru suweŋ te joxe ko. Laajal waaraatekat yi ban téere lañuy nar a wone ci weeru sulyet, te lan lañu nar a wax bu ñu koy def.
15 min : Mën nga nekk xaritu Yàlla ! Waare ak waxtaan ak ñi teew. Am na ci téere bi loo xam ne bu ñu ko jëfandikoo, dinañu mën a jàngal bu baax xale yi ak nit ñi seen jàng sorewul. Dafa ñuy dimbali ba ñu mën leen a jàngal lu jëm ci Yexowa. Woneel bu baax loolu lan la. Ni téere bi di leerale mbir yi dafa yomb, te ànd ak xel. Jëlleen li nekk ci njàngale 2, 8, ak 12, ngir wone loolu. Woneel naka lañu mënee jëfandikoo nataal yi ngir laal xolu kiy jàng. Waxleen naka lañu mënee jëfandikoo téere bii ba mu jur lu baax. Waajur yi war nañu ko jàng ak seeni doom yu ndaw yi. Waxal nit ñépp ñu góor-góorlu ngir wone ko bu ñuy waaraate, saa yu ñu gisee ne dina baax.
15 min : “ Ndax “ bëgg ” nga dimbali nit ñi ” ?c Waxal ne bu ñépp bëggee dimbali nit ñi, dina baax lool.
Woy-Yàlla 67 ak ñaan bu mujj bi.
[Li ñu bind ci suuf]
a Li ngay njëkk wax warul weesu benn minit, ba pare laajal ñi teew ay laaj, te may leen ñu tontu.
b Li ngay njëkk wax warul weesu benn minit, ba pare laajal ñi teew ay laaj, te may leen ñu tontu.
c Li ngay njëkk wax warul weesu benn minit, ba pare laajal ñi teew ay laaj, te may leen ñu tontu.