TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Watchtower
TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Wolof
  • BIBLE
  • TÉERE YI
  • RÉUNIONS
  • km 8/02 p. 2
  • Ndaje yi jëm ci liggéeyu waare bi

Aucune vidéo n'est disponible pour cette sélection.

Il y a eu un problème lors du chargement de la vidéo.

  • Ndaje yi jëm ci liggéeyu waare bi
  • Sasu Nguuru Yàlla — 2002
  • Turu xaaj yi
  • 12-18 ut
  • 19-25 ut
  • 26 ut ba 1 septaambar
  • 2-8 septaambar
Sasu Nguuru Yàlla — 2002
km 8/02 p. 2

Ndaje yi jëm ci liggéeyu waare bi

BUL FÀTTE : Ci weer yu ñuy am ndaje bu gën a mag bi tudd “ Ñi sawar ci waare Nguuru Yàlla ”, suñu Sasu Nguuru Yàlla dina joxe porogaraamu ayu-bés yi yépp. Mbooloo yi ñooy seet ni ñuy def ba soppi porogaraam bi ndax ndaje bu gën a mag bi. Mbooloo yi soxla seetaat li nekk ci Sasu Nguuru Yàlla bu weeru me 2002 ci xët 3 ba 6, dinañu jël 15 minit ci ayu-bés biy jiitu ndaje bi gën a mag bi, ngir waxtaan ci. Mbooloo mu nekk dina jàpp it benn ayu-bés ngir waxtaan ci li ñu jële ci ndaje bu gën a mag bi. Ngir waajal loolu, bu ñu fa teewee, na ku nekk bind kàddu yu am solo yi ñu fay wax. Na ci boole li mu fas yéene topp ci dundam ak ci waaraate bi, ndax mu mën a wax li mu ci defagum. Bu ku nekk di wax njariñ bi mu jële ci ndaje bu gën a mag boobu, dafay yokk suñu doole moroom yi.

12-18 ut

Woy-Yàlla 84

13 min : Yégle yi jëm ci suñu mbooloo. Yenn ci yégle yi nekk ci Sasu Nguuru Yàlla. Na ñaari nit topp li nekk ci xaaj bi tudd “ Li ñu mën a wax bu ñuy wone yéenekaay yi ” bi nekk ci Sasu Nguuru Yàlla bii walla bi ko jiitu, te wone ni ñu mënee wone La Tour de Garde ak Réveillez-vous ! yi ñu mujj a jot. Na ku ci nekk wone li ñu mën a tontu bu amee ku ñu wax : “ Lu tax ngeen di jaar di jaaraat rekk ci kër nit ñi ?” — Seetal Comment raisonner, xët 20.

20 min : “ Na ku nekk am li muy fas yéene def ci wàllu ngëm ”a Bu ngeen tolloo ci xise 5, booleleen ci li téere Notre ministère wax ci nekk pioñee walla liggéey ci Betel, ci xët 114 ba 116.

12 min : Li yenn waaraatekat yu bokk ci suñu mbooloo def ci liggéeyu waare bi. Nettalileen ni ay waaraatekat yi nekk ci seen mbooloo defe bi ñu doon waaraate ak kayit bu ndaw bi tudd : Aimeriez-vous en savoir plus sur la Bible ? Ndax am na ñu tàmbali ay njàngum Biibël bi ? Bu dee waaw, nettalileen walla woneleen ni ñaari waaraatekat tàmbalee ay njàngum Biibël bi. Seetleen li nekk ci Le Ministère du Royaume bu sãwiyee 2002, ci xaaj bi tudd : “ Occasions de distribuer le dépliant ”, ci xët 8.

Woy-Yàlla 50 ak ñaan bu mujj bi.

19-25 ut

Woy-Yàlla 18

12 min : Yégle yi jëm ci suñu mbooloo. Fu ñu tollu ci xaalisu mbooloo mi. Waxtaanleen ci “ Ndaje bu mag bu benn fan biy ñów : li ñu fay waxtaane ”. Waxal ñépp ñu teel a àgg ci ndaje bu mag boobu te déglu bu baax waxtaan yi ñu fay def yépp. Am na ñu nangu waxtaan ak ñun bu yàggul ak ñeneen ñuy jàng Biibël bi ak ñun. Waxleen waaraatekat yi ñu wax leen ñu ñów teew ci ndaje bu mag boobu.

15 min : Lu tax bëgguñu ci waxtaan ? Waxtaan ak ñi teew. Na am it ñu wone ni ñu mënee topp li ñuy wax fii. Bu ñuy waare, tàmm nañu daje ak ay nit ñu sawarul waxtaan ci lu jëm ci seen diine. Loolu mën na ñu teree xamal nit ñooñu xibaar bu baax bi. Bu ñu xamee lu tax nit ki bañ a wax, dinañu mën a xam ni ñu war a waxe ak moom ba mu nangu wax li muy xalaat. Seetleen ni ngeen mënee wax ak nit ñu mel nii : 1) Ñi nga xam ne mbirum diine, boole ci seen diine, soxalu leen. 2) Ñi nga xam ne dañu fonk aada yi seen mbokk ak seeni maam daan def ci wàllu diine. 3) Ñi nga xam ne sawaruñu waxtaan ci lu jëm ci seen diine ndaxte li ñu xam ci Mbind yi barewul. 4) Ñi ñaaw njort ci ñun ndax li suñu noon ñi di wax ci ñun. Mën ngeen dindi walla yokk dara ci li ñu wax fii ndax mu gën a ànd ak li am ci seen gox. Na am it ku wone ni ñu mënee fexe ba waxtaan ak nit ci li nekk ci Mbind yi.

18 min : “ Na karceen bu nekk wone takkute ci Yàlla bu amee mbokk bu ñu dàq ci mbooloo mi. ”b (Xise 1 ba 8) Mag bu mën jàngale moo ko war a def. Na jëfandikoo laaj yi nekk ci xaaj bi. Ku mën jàng lañu war a jël, ngir jàng xise yépp.

Woy-Yàlla 57 ak ñaan bu mujj bi.

26 ut ba 1 septaambar

Woy-Yàlla 73

10 min : Yégle yi jëm ci suñu mbooloo. Na ñaari nit topp li nekk ci xaaj bi tudd “ Li ñu mën a wax bu ñuy wone yéenekaay yi ” bi nekk ci Sasu Nguuru Yàlla bii walla bi ko jiitu, te wone ni ñu mënee wone La Tour de Garde ak Réveillez-vous ! yi ñu mujj a jot. Na benn pioñee, walla benn pioñee buy jàpple wone La Tour de Garde te benn waaraatekat wone Réveillez-vous ! Waxal waaraatekat yi ne bu ñu mënee boole benn aaya ci li ñuy wax ngir wone yéenekaay yi, dina baax lool.

17 min : “ Fexeel ba nit ñi xam li nga bëgg wax ”c Booy jeexal waxtaan bi, waxal waaraatekat yi ñu seet li nekk ci téere bi tudd : Tirez profit de l’École du ministère théocratique, xët 62 ba 65. Bu ngeen ko amul, wax leen ñu seet Réveillez-vous ! bu 8 awril, 1995, xët 15 ba 18.

18 min : “ Na karceen bu nekk wone takkute ci Yàlla bu amee mbokk bu ñu dàq ci mbooloo mi. ”d (Xise 9 ba 14) Mag bu mën jàngale moo ko war a def. Na jëfandikoo laaj yi nekk ci xaaj bi. Ku mën jàng, lañu war a jël ngir mu jàng xise yépp.

Woy-Yàlla 13 ak ñaan bu mujj bi.

2-8 septaambar

Woy-Yàlla 49

10 min : Yégle yi jëm ci suñu mbooloo. Fàttalil waaraatekat yi ne dañu war a bind li ñu def ci liggéeyu waare bi ci weeru ut te joxe ko. Waxal ci lu gàtt li nekk ci xaaj bi tudd : “ Lisez avec vos enfants ” bu nekk ci La Tour de Garde bu 1 me 1999, xët 25.

20 min : Nanga waajal sa bopp bala ngay dem. Waxtaan ak ñi teew. Na am it ñu wone ni ñu mënee topp li ñuy wax fii. Bu ñu waajalee bu baax suñu bopp, suñu liggéeyu waare bi dafay gën a baax. Looloo tax balaa ngay dem : 1) Wutal téere yi ngay soxla. 2) Wutal notes de maison en maison yu doy, ak li ngay binde. 3) Bu ngeen naree jël oto, fexeleen ba dara bañ a yàq seen liggéeyu waare bi. 4) Seetal ñan ngay dellu seeti. 5) Waajalal lan ngay wax. Bu dee yow yaay jiite ndaje bu ñuy am bala ñuy waare, fexeel ba gox bi doy. Waxtaanal ak ñi teew ci ñaar walla ñetti fasoŋ yi ngeen mënee wone téere Création bi, bu ngeen di waaraate ci weeru septaambar. Na am ku tànn benn fasoŋ te wone ko. Na ci boole aaya bu muy jàng.

15 min : Li nekk soxla ci mbooloo mi. Walla waxal ñi teew ñu nettali li ñu def ngir waaraate saa yu ñu ci amee bunt, ci kaar, ci béréb fu nit ñi di féexlu, ca béréb fu ñu dajalee ay bitig, fi kamiyoŋ yi di gaare walla feneen fu ñuy daje ak ay nit. Na am benn walla ñaari nit ñuy wone ku nekk li mas a am ci waaraate bi.

Woy-Yàlla 89 ak ñaan bu mujj bi.

[Li ñu bind ci suuf]

a Li ngay njëkk wax warul weesu benn minit, ba pare laajal ñi teew ay laaj, te may leen ñu tontu.

b Li ngay njëkk wax warul weesu benn minit, ba pare laajal ñi teew ay laaj, te may leen ñu tontu.

c Li ngay njëkk wax warul weesu benn minit, ba pare laajal ñi teew ay laaj, te may leen ñu tontu.

d Li ngay njëkk wax warul weesu benn minit, ba pare laajal ñi teew ay laaj, te may leen ñu tontu.

    Téere yi ci Wolof (1996-2025)
    Ngir génn
    Ngir konektewu
    • Wolof
    • Yónnee ko
    • Ni nga bëgge mbir yi feeñe
    • Copyright © 2025 Watch Tower Bible and Tract Society of Pennsylvania
    • Conditions d’utilisation
    • Règles de confidentialité
    • Paramètres de confidentialité
    • JW.ORG
    • Ngir konektewu
    Partager