Ndaje bu mag bu benn fan biy ñów : li ñu fay waxtaane
1 Rajo yi, tele yi, yéenekaay yi, ak jàngalekat yi dañuy xiir nit ñi ci bare alal. Waaye Kàddu Yàlla moom, dafa ñuy xiir ci “ bare jëf yu rafet ”. (1 Tim. 6:18.) Ndaje bu mag bu benn fan biy ñów, mu ngi tudd “ Nañu bare jëf yu rafet ”. Bi ñuy njëkk def, ci weeru septaambar 2002 lay doon. Yan wax yu rafet lañuy dégg ci ndaje bu mag boobu ?
2 “ Nañu bare alal ci kanamu Yàlla ”, loolu lu mu tekki ? Wottukat biy wër ci mbooloo yi dina ñu ko won. Dina waxtaan it ak suñu yenn mbokk yuy góor-góorlu ngir bare alal ci wàllu ngëm. Ci ndaje bu mag boobu, dina am ku bànqaas bi yónnee ngir defal ñu ay waxtaan. Bi muy njëkk def dina wone naka la mbooloo Yàlla di defe ay “ Jëf yu rafet ci jamanoo ngóob bi ñu tollu nii ”. Nit ku nekk mën na gën a liggéey ci ngóob bi ñu Yàlla sant tey. Waxtaan boobu dina ñu won ni ñu ko mënee def.
3 Bu ñu gisee ay ndaw yuy góor-góorlu ngir bare alal ci wàllu ngëm, dañuy kontaan lool. Loolu dafay màggal Yexowa te dina tax ëllëg ñu mën leen a dénk lu gën a réy ci liggéeyu Yàlla bi. Yan jëf yu rafet la ndaw yi nekk ci suñu mbooloo yi def ? Waxtaan bi tudd “ Ay ndaw yu ñu war a ndokkeel ndax seeni jëf yu rafet yuy màggal Yexowa ” dina ko wone.
4 Bu ñu góor-góorloo ci jëf yu rafet yi, lan lañuy am ? Ki ñu bànqaas bi yónnee dina ñu ko won ci waxtaan bi muy mujj def, te tudd “ Nañu wéy ci jëf yu rafet te am ci barke Yexowa ”. Dina wone ñeenti fànn fu ñu mënee am barke Yexowa : 1) suñu bopp, 2) suñu njaboot, 3) suñu mbooloo mi, ak 4) suñu mbootaay bi nekk ci àddina si sépp.
5 Dinañu mën a sóob ci ndox ñi jébbal seen bopp Yexowa. Boo paree ngir loolu, wax ko léegi wottukat biy jiite.
6 Bu ñu waxee bés bu seen mbooloo waree am ndaje bu mag boobu, nanga gaaw a seet li ngay def ngir teew ci. Nañu góor-góorlu it ngir teel a àgg ngir mën a fekke woy ak ñaan yu njëkk yi. Nañu fekke waxtaan yépp te déglu bu baax. Loolu dina ñu dimbali ñu wéy ci bare alal dëgg ci kanamu Yàlla Yexowa.