Yégle yi
◼ Téere yi ñuy wone ci weeru oktoobar : La Tour de Garde ak Réveillez-vous ! Bu nit ki wonee ne suñu waxtaan neex na ko, war nañu koo won téere Laaj te góor-góorlu ngir mën a jàng ak moom Biibël bi. Nowàmbar : Lan lañu Yàlla laaj ? walla Xam-xam biy jëme ca dund ga dul jeex. Bu ngeen gisee ku am téere yooyu ba pare, wonleen ko benn ci téere yu yàgg yi. Bu ngeen amulee téere yu yàgg yi, seetleen ndax am na yeneen mbooloo yu ci am. Desàmbar : Le plus grand homme de tous les temps. Mën nga wone it benn ci téere yii : La Bible : Parole de Dieu ou des hommes ? ; Recueil d’histoires bibliques walla Vous pouvez vivre éternellement sur une terre qui deviendra un paradis. Bu ngeen amulee téere yooyu, seetleen ndax yeneen mbooloo am nañu ci. Sãwiyee : Téere yi ñu génne bala 1988 yi ngeen am ci seen mbooloo. Bu ngeen amulee téere yooyu, seetleen ndax am na yeneen mbooloo yu ci am. Mbooloo yu amul téere yooyu, mën nañoo wone téere L’humanité à la recherche de Dieu.
◼ Xët 3 ba 6 yi nekk ci Sasu Nguuru Yàlla bii, ñooy wone li ñu war a def ci lekkoolu sasu Nguuru Yàlla, ayu-bés bu nekk ci atum 2003. War nañu ko denc bu baax ba at mi jeex.
◼ Bu fekkee ne bu 1 sãwiyee jotee dangeen di tàmbali def seeni ndaje ci yeneen waxtu, sekkerteer bi war na ko xamal bànqaas bi. Bu boobaa, na yónnee kayit bi tudd Congregation Meeting Information and Handbill Request form (S-5). Bu ngeen soxlaa kayit sf-F Se, mën ngeen ko ci ñaanaale. Bu ngeen ñaanee kayit yooyu, bala ngeen ci mën a jot di ngeen toog lu mu tuuti tuuti fukk ak ñaari ayu-bés.
◼ Téere yu bees yu ñu mën a am :
Le chemin du Paradis : Comment le trouver ? — bambara
Les Saintes Écritures — Traduction du monde nouveau — liŋala
◼ Kaset yu ñuy déglu, yu bees yi ñu mën a am :
Le secret du bonheur familial — français
◼ Wideo yu bees yi ñu mën a am :
Xam-xam biy jëme ca dund ga dul jeex (Volume 2, NTSC) — làkku ñi tëx bu Amerig
Le plus grand homme de tous les temps (Volume 7, PAL et SECAM) — làkku ñi tëx bu Amerig