Ndaje yi jëm ci liggéeyu waare bi
BUL FÀTTE : Ci weer yu ñuy am ndaje bu gën a mag bi tudd “ Ñi sawar ci waare Nguuru Yàlla ”, suñu Sasu Nguuru Yàlla dina joxe porogaraamu ayu-bés yi yépp. Mbooloo yi ñooy seet ni ñuy def ba soppi porogaraam bi ndax ndaje bu gën a mag bi. Mbooloo yi soxla seetaat li nekk ci Sasu Nguuru Yàlla bu weeru me 2002 ci xët 3 ba 6, dinañu jël 15 minit ci ayu-bés biy jiitu ndaje bi gën a mag bi, ngir waxtaan ci. Dina jàpp it benn ayu-bés ngir waxtaan ci li ñu jële ci ndaje bu gën a mag bi. Ngir waajal loolu, bu ñu fa teewee, na ku nekk bind kàddu yu am solo yi ñu fay wax. Na ci boole li mu fas yéene topp ci dundam ak ci waaraate bi, ndax mu mën a wax li mu ci defagum. Bu ku nekk di wax njariñ bi mu jële ci ndaje bu gën a mag boobu, dafay yokk suñu doole moroom yi.
9-15 desàmbar
Woy-Yàlla 86
12 min : Yégle yi jëm ci suñu mbooloo. Yenn ci yégle yi nekk ci Sasu Nguuru Yàlla. Na ñaari nit topp li nekk ci xët 8 ci Sasu Nguuru Yàlla bii, walla ci Sasu Nguuru Yàlla yi jiitu, te wone ni ñu mënee wone La Tour de Garde ak Réveillez-vous ! yi ñu mujj a jot.
15 min : “ Nañu yégle xibaaru Nguur gi. ”a Bu ngeen di def xise 3, waxal li ñu mën a def ngir bu ñuy yégle xibaaru Nguur gi, ñu jàng ay aaya ci Biibël bi ci boppam. — km-WO 12/01, xët 1, xise 3.
18 min : Fexeel ba lépp lu baax li ngay def jur lu baax. Waare ak waxtaan ak ñi teew. Benn magu mbooloo moo ko war a def. Waxal fi seen mbooloo jaar ak ni mu jëme kanam. Boole ci li ñu def ba taxawal seen mbooloo. Bala ndaje bi di jot, waxal ñi fekke jamano jooju ne dinga leen laaj ñu nettali lu mën a yokk doole lu fa xewoon. Waxal ci lan la mbooloo mi mën a jëm kanam, te waxal nit ñi ñu sawar ci lépp li ñuy def ci mbooloo mi.
Woy-Yàlla 12 ak ñaan bu mujj bi.
16-22 desàmbar
Woy-Yàlla 11
10 min : Yégle yi jëm ci suñu mbooloo. Fu ñu tollu ci xaalisu mbooloo mi. Waxal li seen mbooloo taxawal ngir waaraate bésu 25 desàmbar ak 1 sãwiyee.
15 min : Ñi am seetlu dinañu nànd (Dañ. 12:3, 10). Na am ñuy wone lii : Nit ku suñu waxtaan neex dafay laajte lii : “ Lan moo ma mën a won ne dëgg-dëgg, nànd ngeen bu baax li Biibël bi di jàngale ? ” Waaraatekat bi dafa koy won ni ñu mëne def bu ñuy gëstu ci Biibël bi (w96 5/15 19-20) Dina jëfandikoo benn walla ñaari xalaat yu nekk ci téere Comment raisonner ci xët 403 ba 408, ngir won ko ni ñu seete bu baax li ñu bind ci Biibël bi, ba mujj xam li Yàlla bëgg def ci suuf si. Dina ko wax it ni ñu mëne def noonu it ngir nànd bu baax leneen lu Biibël bi jàngale, te wax ko ne bu ko neexee, mën na ko jàngal Biibël bi.
20 min : “ Buleen fàtte mag yiy topp Yàlla bu baax. ”b Booleleen ci li ñu wax ci La Tour de Garde bu 1 ut 1994 ci xët 29. Waxal ne ñi néew doole lool, bu ñu waaraate lu mat 15 minit, mën nañu ko bind te joxe ko. Bala ndaje bi di jot, waxal yenn waaraatekat ne dinga leen laaj ñu nettali li leen won ne ku ànd ak ku néew doole, moom ak ki mu àndal dinañu ci am ay barke.
Woy-Yàlla 56 ak ñaan bu mujj bi.
23-29 desàmbar
Woy-Yàlla 63
10 min : Yégle yi jëm ci suñu mbooloo. Na ñaari nit topp li nekk ci xët 8, te wone ni ñu mënee wone La Tour de Garde ak Réveillez-vous ! yi ñu mujj a jot. Waxal nit ñi ne bu ñu mënee am wideo bi tudd No Blood —Medicine Meets the Challenge, nañu fexe ba gis ko ngir waajalal waxtaan bi ñuy am ci ndaje liggéeyu waare biy am ci diggante 6 sãwiyee ba 12 sãwiyee.
15 min : Li nekk soxla ci mbooloo mi.
20 min : “ Ndax yaa ngi def sa wàll ndax ñu mën a bind li ñu def ci waaraate bi te bañ ci juum ? ”c Bu ngeen di waxtaan ci xise 2, boole leen ci li ñu wax ci téere Notre ministère, xët 106 ba 108.
Woy-Yàlla 57 ak ñaan bu mujj bi.
30 desàmbar ba 5 sãwiyee
Woy-Yàlla 65
10 min : Yégle yi jëm ci suñu mbooloo. Fàttalil waaraatekat yi ñu bind li ñu def ci liggéeyu waare bi ci weeru desàmbar te joxe ko. Bu seen mbooloo waree soppi waxtu yi ngeen doon def seeni ndaje ci at mii di ñów, waxal nit ñi ñu góor-góorlu ngir tàmm teew ndaje yi ci waxtu yu bees yi. Waxal téere yi ñu war a wone ci waaraate bi ci weeru sãwiyee. Boo koy def, na nga gën a wax ci téere yi ñu am ci mbooloo mi.
20 min : “ Nañu xamal xale yi xibaar bu baax bi. ”d Bu ngeen defee xise 5 ba pare, na benn waaraatekat bu mën waaraate wone ni mu mëne jëfandikoo li téere Comment raisonner wax ci xët 9 ba 15 ngir tàmbali waxtaan ak benn xale. Lan lañu mën a def ngir won leen ay téere ? Bu ñu leen dul won ay téere, naka lañu mën a jeexal waxtaan bi ñu am ak ñoom ? Bu ngeen di waxtaan ci xise 2, tànnal benn walla ñaar ci li ñu nettali ci La Tour de Garde bu 1 sãwiyee 1995 ci xët 24 ba 26 te wax ci.
15 min : “ Nañu jàpple pioñee yi. ” Woneel bu baax ni mbooloo mi yépp di ame ay barke bu ñu jàpplee pioñee yi ni ñu ko soxlaa. Laajal ay laaj ay pioñee ngir ñu wone naka la leen magi mbooloo mi ak ñeneen nit dimbalee ci seen wareefu pioñee ci waaraate bi.
Woy-Yàlla 58 ak ñaan bu mujj bi.
6-12 sãwiyee
Woy-Yàlla 31
5 min : Yégle yi jëm ci suñu mbooloo.
23 min : Ban ëllëg nga yéene say doom ? Waxtaan bu benn magu mbooloo di def ci li nekk ci La Tour de Garde bu 15 sulyet 1998 ci xët 4 ba 6. Woneel bu baax li aaya yi fa nekk di wax way-jur yi ngir ñu def seen wareef ni mu waree. Na nga gën a wone ne dañu war a toppatoo seeni doom ak mbëggeel te dañu war a toppatoo seen diggante ak Yàlla. Waxtaanal ak benn walla ñaari way-jur yuy def bu baax seen wareef, ngir ñu wax ni ñuy góor-góorloo ngir def lépp li leen war ci seeni doom, te yan barke lañu ci jële.
17 min : “ War nga seetaan wideo bi tudd No Blood—Medicine Meets the Challenge. ” Mag bu mën moo ko war a def. Na nga tàmbali waxtaan bi ak laaj yi nekk ci xaaj bi. Boo ci paree, jàngal xise bi mujj ci xaaj bi. Bu ngeen amulee wideo bi, na ngeen waxtaan ci xaaj bi tudd “ La chirurgie sans transfusion, des avantage de plus en plus reconnus ” bi nekk ci Réveillez-vous ! bu 22 ut 1998 ci xët 10 ba 11. — Seetleen li nekk ci Réveillez-vous ! bu 8 sãwiyee 2000, ci xët 7 ba 11.
Woy-Yàlla 35 ak ñaan bu mujj bi.
[Li ñu bind ci suuf]
a Li ngay njëkk wax warul weesu benn minit, ba pare laajal ñi teew ay laaj, te may leen ñu tontu.
b Li ngay njëkk wax warul weesu benn minit, ba pare laajal ñi teew ay laaj, te may leen ñu tontu.
c Li ngay njëkk wax warul weesu benn minit, ba pare laajal ñi teew ay laaj, te may leen ñu tontu.
d Li ngay njëkk wax warul weesu benn minit, ba pare laajal ñi teew ay laaj, te may leen ñu tontu.