Ndaje bu gën a mag bi ci atum 2005 : “ Nañu déggal Yàlla ”
1 Yexowa Yàlla mooy suñu Jàngalekat bu Mag bi. Taxawal na ay ndaje fu mu ñuy jàngal yoonam yi (Isa. 30:20, 21 ; 54:13). Dafa jaar ci surga bu takku te teey bi ngir taxawal ndaje yu mel ni ndaje bu gën a mag bi ñuy am at mu nekk (Macë 24:45-47). Li ñuy yëg ci suñu biir xol niroo na ak li nekkoon ci xolu Daawuda bi mu doon woy woy bii : “ Dinaa barkeel Yexowa ci diggu mbooloo yi daje. ” (Sab. 26:12). Daawuda xamoon na bu baax njariñu njàngale bi jóge ci Yexowa. Looloo tax, saa yu mbooloo Yexowa doon daje, mu bëggoon a nekk ci seen biir.
2 Ren ndaje bu gën a mag bi mu ngi tudd “ Nañu déggal Yàlla ”. Ndax dinga bokk ci ‘ mbooloo yiy daje ’ bés yooyu ? Su dee loolu nga bëgg, lii di topp dina la ci dimbali.
3 Tey jii nga war a komaase seet li nga mën a def ngir teewe ñetti fan yépp : “ Nit ku sawar, ci lu wóor, li mu fas yéene def, dina ko indil lu baax. ” (Léeb. 21:5). Kàddu yooyu, dañuy wone lu tax komaase waajal léegi ndaje bu gën a mag bi, am njariñ lool. Ndaje boobu dina dëgëral bu baax suñu ngëm. Tey jii nga war a komaase seet lépp li nga war a def ngir teewe ñetti fan yooyu yépp. Loolu moo gën. Kon boo waree ñaan ki ngay liggéeyal fan yi nga war a teewe ndaje boobu, nanga ko def léegi. Bu fekkee ne sa jëkkër walla sa jabar nekkul seede Yexowa te danga war a waxtaan ak moom ci li nga war a def ngir teewe ci ndaje boobu, bul xaar ba mu bëgg jot. Boo amee jafe-jafe ci li ngay def ngir teewe ndaje bu mag boobu, nanga ko wax Yexowa ci ñaan. Te na la wóor ne ak ndimbalu Yexowa, “ li nga fas yéene def, dina wóor ”. (Léeb. 16:3.) Nanga jàpple itam ñi ngay jàngal Biibël bi bu ñuy waajal ndaje boobu ngir mën a teewe ñetti fan yi yépp.
4 Fi nit ñi mën a dal : Toppatoo nañu ba pare fi nit ñi mën a dal ci dëkk yi ñu war a defe ndaje yu gën a mag yi. Na ku nekk topp bu baax li ñu taxawal ngir loolu. Bu ko defee, suñu mbokk yi nangu am ay gan, seen kër du fees ba ëpp li ñu àttan.
5 Yenn saay waaraatekat dina joxe kayit bi tudd Demande de chambre pour cas particuliers, ngir ñaan fu mu mën a dal. Kurélu liggéeyu waare bi dina seet tegtal yi nekk ci kayit boobu ngir wax ndax mën nañu ko may li mu ñaan. Fàww waaraatekat bi am tur bu rafet ci mbooloo mi, te bu amee doom war nañu nekk doom yu yaru. Biro biy toppatoo fi nit ñi mën a dal, bu bëggee ñu leeral ko dara ci li waaraatekat bi bind ci kayit boobu, na ko laaj sekkerteeru mbooloo nit kooku.
6 Ñiy soxla ndimbal : Ndaw li Pool waxoon na ci ay mbokkam yu nekkoon ci moom ndimbal bu ‘ féexal xolam ’. (Kol. 4:7-11.) Toppatoo ay soxlaam bokk na ci li ñu ko doon defal. Naka nga mënee nekk ndimbal buy féexal xol ci ndaje bu gën a mag bi ? Ci mbooloo mi, am na ñu nekk mag, ñu feebar, walla ñu def seen jot yépp ci liggéeyu Yexowa mel ni pioñee yi. Mën na am ñooñu walla ñeneen soxla ñu dimbali leen ngir dem ci ndaje boobu. Walla ñu soxla am fu ñuy dal. Ñooñu, bu ñu amee mbokk yu nekk seede Yexowa, ñoom ñoo leen ci war a jàpple (1 Tim. 5:4). Waaye bu ñu ko mënul, yeneen karceen yi mën nañu leen ci dimbali (Saak 1:27). Ñi nekk wottukatu njàngum téere, war nañu seet ñi soxla ndimbal ci seen gurup te waxtaan ak ñoom. Bu ko defee dinañu mën a seet ndax ñooñu teel nañu toppatoo lépp li ñu soxla ngir mën a teewe ndaje bu gën a mag boobu.
7 Ñi bëgg teewe beneen ndaje bu gën a mag : Xéyna doo mën a teewe fi sa mbooloo war a teewe. Kon laajal seen sekkerteeru mbooloo mu jox la adareesu biro biy toppatoo ndaje fi nga bëgg teewe. Bind nañu ko ci ginnaaw kayit bi tudd Demande de chambre pour cas particuliers. Boo soxlaa foo mën a dal, walla nga am leneen loo bëgg laajte ci ndaje boobu, nanga bind ngir laaj loolu. Dugalal ci leetar bi ngay yonnee benn anwalob bu am tembar te bind ci sa adarees. Te su amee ñaari ndaje yu gën a mag, walla lu ko ëpp, yu war a am ci dëkk boobu, nanga wax ci ban ngay teewe.
8 Dañu soxla ku ñuy jàpple : Yeesu bu doon xool nit ñi, dafa doon seet ak xol bu woyof li ñu soxla (Lukk 9:12-17 ; Ywna. 13:5, 14-16). Dëgg-dëgg ku jar a roy la ! Ñi nuy jàpple ci lépp li ñu war a def ngir am suñu ndaje yu gën a mag yi, xel moomu Yeesu wone lañu am ñoom itam. Ndaje bu nekk dafa am kurélu mag bu koy toppatoo. Kurélu mag boobu, dafay xaaj liggéey bi te dénk xaaj bu nekk benn biro. Bu ci kanamee tuuti, kurél yooyu dinañu woo nit ñi ngir ñu jàpple leen ci seen liggéey. Dinañu gën a soxla ay magu mbooloo yu ñu bëgg jàpple ci liggéey boobu, te nangu def bépp liggéey bu ñu leen di dénk. Bu ñu defee loolu, dinañu nekk royukaay bu rafet ci ñi nekk ci mbooloo mi yépp. — 1 Pie. 5:2, 3.
9 Li nit ñi di gis : Benn jigéen buy liggéey ci otel nee na : “ Ci gurup yi ñu fi gis yépp, yéen lañu gën a bëgg. Wute ngeen ak ñeneen ñi ndaxte dangeen am yar ak teggin. Ñiy toppatoo néeg yi, nee nañu ñoom ñépp ne dangeen baax te dangeen di maye ay neexal. Ñépp a bëgg liggéey Samdi ak dimaas yu ngeen fi nekk ! ” Keneen ku yore beneen otel, moom itam nee na : “ Seede Yexowa yi ñoo fi gën a neex a liggéeyal. ” Xéyna yar ak teggin bi nga wone bokk na ci li tax ñu wax lu rafet loolu. Bu Yexowa déggee nit ñi di ko màggal ndax jikko ju rafet ju ñu wone, dafay kontaan lool ! — 1 Pie. 2:12.
10 Yexowa Yàlla jaar na ci “ surga bu takku bi ” ngir taxawal ay ndaje yu mag ngir jàngal mbooloom (Lukk 12:42). Waajal ndaje boobu ngir mën a teew ñetti fan yépp, yombul. Waaye jar na ko. Ren, suñu ndaje bu gën a mag bi tudd “ Nañu déggal Yàlla ”, dina tax ñu gën a bëgg jaamu Yexowa tey ba abadan. Ñun ñépp nañu fas yéene topp li Sabuur wax, maanaam : “ Nanga barkeel Yàlla ci diggu mbooloo yi daje. ” — Sab. 68:26.
[Wërale bi nekk paas 7]
Waxtu yi
Àjjuma ak Samdi
9:30 - 17:05
Dimaas
9:30 - 16:10