TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Watchtower
TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Wolof
  • BIBLE
  • TÉERE YI
  • RÉUNIONS
  • km 9/05 p. 8
  • Yégle yi

Aucune vidéo n'est disponible pour cette sélection.

Il y a eu un problème lors du chargement de la vidéo.

  • Yégle yi
  • Sasu Nguuru Yàlla — 2005
Sasu Nguuru Yàlla — 2005
km 9/05 p. 8

Yégle yi

◼ Téere yi ñuy wone ci weeru Septaambar : Y a-t-il un Créateur qui se soucie de vous ? Mën nga wone it La vie : comment est-elle apparue ? Évolution ou création ? Bu nit ki bañee jël téere yooyu, won ko téere Veillez ! Oktoobar : Benn La Tour de Garde ak benn Réveillez-vous ! Bu nit ki wonee ne suñu waxtaan neex na ko, won ko téere Laaj bi. Nowàmbar : Écoute le grand Enseignant. Bu nit ki waxee ne amul doom, won ko téere Xam-xam walla kayit bi tudd Ndax bëgg nga yokk li nga xam ci Mbind mu sell mi ? Desàmbar : Le plus grand homme de tous les temps. Bu fekkee ne am ngeen ci seen mbooloo téere yii di topp, mën ngeen leen wone itam : La Bible : Parole de Dieu ou des hommes ?, Recueil d’histoires bibliques walla Vous pouvez vivre éternellement sur une terre qui deviendra un paradis.

◼ Bu waaraatekat soxlaa téere, waru ko laajal boppam bànqaas bi. Weer wu nekk, bala ñuy yónnee ci bànqaas bi li mbooloo mi soxla ci wàllu téere, wottukat biy jiite war na def benn yégle. Bu boobaa, képp ku soxla téere, dina ko mën a wax kiy toppatoo téere yi ci mbooloo mi. Buleen fàtte ne am na yenn téere yoo xam ne duñu leen denc ci mbooloo mi. Bala nga leen di am, fàww nga wax kiy toppatoo téere yi ci seen mbooloo, mu laaj leen bànqaas bi.

◼ Yenn saay dafay am ku ñu dàq ci mbooloo mi walla ku ci génne boppam, ba pare mu bëgg dellusiwaat. Ñu ngi fàttali magi mbooloo mi ñu topp li nekk ci La Tour de Garde bu 15 awril 1991, ci xët 21 ba 23.

◼ At mu nekk, bu ndaje bi ñuy fàttaliku deewu Yeesu weesoo, am na waxtaan bu ñuy faral di am ci àddina si sépp. Ci atum 2006, dimaas 30 awril lañu koy def. Bu ci kanamee, dinañu leen wax turu waxtaan bi. Mën na am wottukat biy wër ci mbooloo yi war a nekk ci seen mbooloo ayu-bés boobu. Walla ngeen am ndaje bu mag. Bu boobaa, nangeen def waxtaan boobu ayu-bés bi ci topp. Benn mbooloo warul def waxtaan boobu balaa bésu dimaas 30 awril 2006.

◼ Weeru oktoobar dina am juróomi samdi ak juróomi dimaas. Kon dina baax lool ci ku bëgg nekk pioñee buy jàpple.

    Téere yi ci Wolof (1996-2025)
    Ngir génn
    Ngir konektewu
    • Wolof
    • Yónnee ko
    • Ni nga bëgge mbir yi feeñe
    • Copyright © 2025 Watch Tower Bible and Tract Society of Pennsylvania
    • Conditions d’utilisation
    • Règles de confidentialité
    • Paramètres de confidentialité
    • JW.ORG
    • Ngir konektewu
    Partager