Ndaje yi jëm ci liggéeyu waare bi
10-16 sãwiyee
Woy-Yàlla 48
10 min : Yégle yi jëm ci suñu mbooloo. Yenn ci yégle yi nekk ci Sasu Nguuru Yàlla. Na ñaari nit topp li nekk ci xët 8, te wone ni ñu mënee wone Réveillez-vous ! bu 22 desàmbar ak La Tour de Garde bu 1 sãwiyee. Mën ngeen wax leneen lu mën a baax ci seen gox ngir wone yéenekaay yi. Na ci am kenn kuy wone ni ñu mënee wone yéenekaay yi suñu mbokk mu nekkul Seede.
15 min : “ Kàdduy yoonu ngëm ” : suñu ñam la ci wàllu ngëm. ”a Bu leen ko jot bi mayee, jàngleen te waxtaan ci aaya yi nekk ci xaaj bi.
20 min : “ Jéemal a waxtaan ak nit ku nekk ci lu ko mën a itteel. ” Waxtaan ak ñi teew ci li nekk ci xët 6. Woneel ci ñaari fasoŋ ni ñu mënee topp loolu ak téere yi ñuy wone weer wi. Ci fasoŋ bu nekk, na waaraatekat bi jàng benn aaya buy wax ci lenn luy itteel nit ki, fekk kooku moo ko ko wax.
Woy-Yàlla 60 ak ñaan bu mujj bi.
17-23 sãwiyee
Woy-Yàlla 14
10 min : Yégle yi jëm ci suñu mbooloo.
15 min : Jeunes : progressez-vous spirituellement (maanaam ndaw yi ndax yeen a ngi jëm kanam ci wàllu ngëm) ? Waxtaan bu ñu jële ci La Tour de Garde bu 1 awril 2003, xët 8 ba 10. Benn magu mbooloo moo koy def. Waxal yenn yoo xam ne gune yi mën nañu ko fas yéene def te ñu àttan ko. Waxal xale yi ñu tànn ku ci nekk benn fànn fu ñuy fas yéene góor-góorlu ngir rattaxal seen diggante ak Yàlla.
20 min : “ Nañu dimbali ñi ñuy jàngal Biibël bi ñu topp li ñuy jàng — Xaaj 5. ”b Xise 4 ak 5 wone nañu yenn yi ñu war a moytu bu ñuy def njàngum Biibël. Kenn ku tàmm am ay njàngum Biibël na won waaraatekat bu bees ni mu ko mënee moytu.
Woy-Yàlla 64 ak ñaan bu mujj bi.
24-30 sãwiyee
Woy-Yàlla 71
10 min : Yégle yi jëm ci suñu mbooloo. Fu ñu tollu ci xaalisu mbooloo mi. Na ñaari nit topp li nekk ci xët 8, te wone ni ñu mënee wone Réveillez-vous ! bu 8 sãwiyee ak La Tour de Garde bu 15 sãwiyee. Mën ngeen wax leneen lu mën a baax ci seen gox ngir wone yéenekaay yi.
10 min : Ay tont ci seeni laaj. Waare lay doon.
25 min : “ Ni ñu waree topp li ñu bind ngir wone li ñu mën a wax ci waaraate bi. ”c Laajal laaj yi nekk ci suufu xaaj bii. Fàttalil waaraatekat yi lu tax jëfandikoo bu baax Biibël bi bu ñuy wone suñuy téere am solo. Waxal ne bind nañu ci Sasu Nguuru Yàlla bii ci xët 3 ba 5, li ñu mën a wax bu ñuy wone suñuy yenn téere. Waxal nit ñi ñu dénc xët yooyu ngir jëfandikoo ko ci at mi yépp. Bu ngeen paree waxtaan ci xaaj bii, nangeen waxtaan ci li ñu mën a wax bu ñuy wone téere Approchez-vous de Jéhovah ci weeru fewriyee. Na am ñu wone ñaari fasoŋ yu ñu ko mën a defe. Mën nañu jël li nekk ci xët 3 walla jaar ci beneen waxtaan bu gën a mën a itteel nit ñi nekk ci seen goxu mbooloo.
Woy-Yàlla 88 ak ñaan bu mujj bi.
31 sãwiyee ba 6 feewriyee
Woy-Yàlla 68
10 min : Yégle yi jëm ci suñu mbooloo. Fàttalil waaraatekat yi ne dañu war a bind li ñu def ci liggéeyu waare bi ci weeru sãwiyee te joxe ko. Tënkal li nekk ci wërale bi tudd “ Wideo yu ñu def ci benn DVD ”.
15 min : Li nekk soxla ci mbooloo mi.
20 min : Ndax yaa ngi niir Mbind mi bés bu nekk ? Waare ak waxtaan ak ñi teew ci xët yi njëkk ci téere Examinons les Écritures chaque jour — 2005. Waxtaanleen ci lu tax ñépp a soxla jël tuuti minit bés bu nekk ngir seet aaya bés bi ak kàddu yi ci ànd. Bala ndaje bi di jot, waxal suñu benn walla ñaari mbokk ne dinga leen laaj ñu wax li ñuy def ngir jàng bés bu nekk aaya bés bi. Nañu wax itam naka la leen jariñe. Ngir àggale waxtaan bi, nangeen wax tuuti ci aaya atum 2005.
Woy-Yàlla 66 ak ñaan bu mujj bi.
7-13 feewriyee
Woy-Yàlla 63
10 min : Yégle yi jëm ci suñu mbooloo.
15 min : Nañu dimbali ñi yàggul a bokk ci mbooloo mi ngir ñu bëgg Yàlla ak seen moroom. Waxtaan bu ñu jële ci La Tour de Garde bu 1 sulyet 2004, xët 16, xise 7 ba 9. Woneel bu baax ne képp ku bokk ci mbooloo mi, am nga wàll ci li ñu war a def ngir dimbali ñiy jàng Biibël bi ñu dem ba nekk taalibe Yeesu.
20 min : Yexowa du bañ a def dara lu baax (Sab. 84:11). Waxtaanal ak suñu yenn mbokk yu góor ak yu jigéen yu jaar ci ay nattu, waaye loolu taxul ñu dellu ginnaaw. Yan jafe-jafe lañu amoon ? Lan moo leen ci dimbali ? Lu baax lan lañu ci jële ?
Woy-Yàlla 81 ak ñaan bu mujj bi.
[Li ñu bind ci suuf]
a Li ngay njëkk wax warul weesu benn minit, ba pare laajal ñi teew ay laaj, te may leen ñu tontu.
b Li ngay njëkk wax warul weesu benn minit, ba pare laajal ñi teew ay laaj, te may leen ñu tontu.
c Li ngay njëkk wax warul weesu benn minit, ba pare laajal ñi teew ay laaj, te may leen ñu tontu.