Xaaj 5 : Nañu dimbali ñi ñuy jàngal Biibël bi ñu topp li ñuy jàng
Xamal ñaata xise ngeen di jàng
1 Yeesu daawul jàngal taalibeem ya li ñu àttanul. Li mu leen jàngal, dafa doon “ aju ci lu ñu àttan ”. (Mark 4:33 ; Ywna. 16:12.) Ñun ñiy jàngale Kàddu Yàlla, noonu lañu war a def, ñun it. Saa yu ñu defee njàngum Biibël, dañu war a xam ñaata xise lañu mën a jàng. Loolu dina aju ci li ñu mën ak li ñu nekke, nit ki ak ñun ci suñu bopp.
2 Ngëmam war na dëgër : Am na ñu gaaw a nànd li ñuy jàng. Am na ñeneen ñu soxla ngay dellusi ñaar walla ñetti yoon bala ngeen mën a jeexal benn njàngale. Bëgguñu gaawantu ba nit ki bañ a nànd bu baax li ñu koy jàngal. Li mu gëm yépp, dafa war a sukkandiku bu baax ci Kàddu Yàlla. — Léeb. 4:7 ; Room 12:2.
3 Saa yoo defee njàngum Biibël bi, jëlal jot bu doy ngir nit ki nànd li muy jàng ci Kàddu Yàlla te gëm ko. Bul gaawantu ba mu ñàkk lu am solo ci dëgg gi muy jàng ci Biibël bi. Fexeel ba am jot bu doy ngir ponk yi ëpp solo des ci xelam. Na jot bi doy itam ngir seet aaya yi nga xam ne fa lañu jële li ñuy jàngale. — 2 Tim. 3:16, 17.
4 Bul bàyyi waxtaan bi dem fu sore : Dëgg la, bëgguñu gaawantu. Waaye bëgguñu itam waxtaan bi dem fu sore. Kon, bu nit ki amee lu bare lu mu la bëgg a wax ci moom walla ci li muy def, nee ko dingeen ci waxtaan bu ngeen jàngee ba pare. — Daj. 3:1.
5 Xéyna ñun ñii ñoo bëgg wax lu bare ndaxte dëgg gi ñuy jàngale, dafa ñu neex lool (Sab. 145:6,7). Yenn saay dinga wax ponk bu amul solo noonu walla nettali dara ngir waxtaan bi gën a neex. Waaye loolu warul bare te warul yéexal njàng mi. Am na li nit ñi war a njëkk jàng ci Biibël bi. Te dañu ci war a am xam-xam bu wér. Kon, bëgguñu suñu wax ju bare yàqal leen ci loolu.
6 Bu ñuy jàngale, nañu xam fan la njàng mu nekk war a tollu. Loolu, dina dimbali kiy jàng Biibël bi mu dox ci leeraayu Yexowa. — Isa. 2:5.