Ay tont ci seeni laaj
◼ Lan mooy li gën li ñu mën a def bu ñu amee xaalis bu ñu bëgg maye ngir jàpple suñu ay mbokk ci ngëm yu nekk ci yeneen réew ?
Lee-lee ñu dégg ne suñuy mbokk ci ngëm yu nekk ci yeneen réew dañu soxla xaalis ndax fitna bi ñu leen fitnaal, walla ndax musiba walla leneen lu metti lu leen dal. Am na suñu ay mbokk ci ngëm yoo xam ne bi ñu déggee lu mel noonu, dañu yónnee xaalis ca bànqaas bi yore réew moomu, te dañu wax kan lañu bëgg ñu jox xaalis boobu, walla ban mbooloo moo ko war a jot. Walla ñu bëgg ñu dugal xaalis boobu ci benn tabax bu ñuy def. — 2 Kor. 8:1-4.
Bëgg dimbali sa mbokk noonu, lu rafet la. Waaye mën na am feneen fu soxla yi gën a jamp. Lee-lee sax, bu xaalis bi ñówee, dafay fekk ñu faj ba pare soxla bi taxoon ñu yónnee ko. Ba tey, na ñu wóor ne xaalis bi ñu yónnee bànqaas bi ngir jàpple liggéeyu waare bi ci àddina si sépp walla tabax ay Saalu Nguur, walla ngir dimbali suñu ay mbokk ci musiba bu leen dal, xaalis boobu dinañu ko dugal fu ki ko maye bëgg.
Jàngal nañu bu baax suñuy mbokk yi nekk ci bànqaas yépp li ñu war a def bu soxla yu jamp amee. Te saa yu loolu amee, bànqaas bi dina ko xamal Jataay biy dogal. Su ko mënulee toppatoo moom kenn, Jataay biy dogal mën na laaj beneen bànqaas bu jege bànqaas boobu mu jàpple ko walla kër gu mag bu Seede Yexowa yi ci boppam mën na leen yónnee xaalis. — 2 Kor. 8:14, 15.
Kon, boo bëggee joxe xaalis ngir jàpple liggéeyu waare bi ci àddina si sépp walla jàpple tabax yi ñuy def ci yeneen réew, walla ngir dimbali suñu mbokk yi ci musiba bu leen dal, nanga ko yónnee ca bànqaas bi yore réew mi nga nekk. Mën nga ko yónnee bànqaas ba, yow ci sa bopp, walla nga jaar ci sa mbooloo. Bu ñu defee noonu, surga bu takku bi te teey dina mën a toppatoo mbokk yi nekk ci àddina sépp ci fasoŋ bu aw yoon, ci kow li Jataay biy dogal taxawal ngir loolu. — Macë 24:45-47 ; 1 Kor. 14:33, 40.