TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Watchtower
TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Wolof
  • BIBLE
  • TÉERE YI
  • RÉUNIONS
  • jl lesoŋ 22
  • Ban liggéey lañuy def ci bànqaas yi ?

Aucune vidéo n'est disponible pour cette sélection.

Il y a eu un problème lors du chargement de la vidéo.

  • Ban liggéey lañuy def ci bànqaas yi ?
  • Ñan ñooy def tey li Yexowa santaane ?
  • Leneen lu jëm ci loolu
  • Leetar bi ñu bànqaas bi yónnee
    Sasu Nguuru Yàlla — 2006
  • Ay tont ci seeni laaj
    Sasu Nguuru Yàlla — 2005
  • Leetaru bànqaas bi
    Sasu Nguuru Yàlla — 2008
Ñan ñooy def tey li Yexowa santaane ?
jl lesoŋ 22

NJÀNGALE 22

Ban liggéey lañuy def ci bànqaas yi ?

Benn gurupu góor yu nekk di toppatoo liggéey bi ñuy def ci bànqaas bi nekk Îles Salomon

Îles Salomon

Benn seede Yexowa buy liggéey ci bànqaas bi nekk Canada

Canada

Kamiyoŋ yi ñuy yebe téere yi

Afrique du Sud

Ñi bokk ci njabootu Betel yi dañuy toppatoo liggéeyu waare bi ci benn réew walla lu ko ëpp. Am na ñuy tekki suñuy téere ci làkku réew mi. Am na ñuy liggéey ci masin yiy sotti suñu yéenekaay yi ak suñu téere yi. Am na ñuy liggéey fu ñuy denc suñuy téere bala ñu leen di yónnee ci mbooloo yi. Am na ñuy liggéey fu ñuy defar wideo yi ak lu ñuy déglu, walla ñuy def yeneen liggéey yu bànqaas bi war a def.

Kurélu bànqaas bi dafay jiite liggéey bi. Jataay biy dogal dafay dénk benn kurél liggéey bi ñuy def ci bànqaas bu nekk. Kurél boobu, dañu koy woowe kurélu bànqaas bi. Kurél bu nekk dina am lu mat ñetti magi mbooloo walla lu ko ëpp yu mën seen liggéey. Kurélu bànqaas bi mooy wax Jataay biy dogal fi liggéeyu waare bi tollu ci réew bu nekk bu muy toppatoo ak jafe-jafe bu mënta am. Loolu mooy dimbali Jataay biy dogal mu xam yan waxtaan lay def ci téere yi nar a génn walla ci porogaraamu ndaje yi ci mbooloo mi ak ci ndaje yu mag yi. Jataay biy dogal dafay faral di yónnee ay nit ci bànqaas yi ngir dimbali kurélu bànqaas yi ci def liggéey bi ñu leen dénk ni mu ware (Kàddu yu Xelu 11:14). Ñoom dañuy taxawal porogaraam bu neex, boole ci benn waxtaan bu ñuy def, ngir dooleel mbooloo yi ci wàllu ngëm.

Dañuy jàpple mbooloo yi ci seen liggéeyu waare bi. Ci góor yi ñuy dénk liggéey ci bànqaas bi, am na ñuy toppatoo li jëm ci mbooloo yu bees yi, maanaam ñoom ñooy nangu ñu taxawal mbooloo bu bees. Am na it ñuy toppatoo lépp lu jëm ci liggéeyu pioñee yi, misioneer yi ak wottukat yiy wër ci mbooloo yi bànqaas bi di toppatoo. Dañuy waajal ay ndaje yu mag, di jiite liggéeyu tabaxu saalu Nguur yu bees te di xool ba xam ndax yónnee nañu mbooloo yi téere yi ñu soxla. Lépp li ñuy def ci bànqaas yi bokk na ci liy tax liggéeyu waare bi aw yoon. — 1 Korent 14:33, 40.

  •  Naka la kurélu bànqaas yi di dimbalee Jataay biy dogal ?

  •  Yan liggéey lañuy dénk ñi nekk ci bànqaas yi ?

XÓOTALAL WAXTAAN BI

Dañuy kontaan bu ñu gisee ku bëgg a xool ni suñu bànqaas mel. Ñëwal bés bu la neex diggante altine ba àjjuma. Booy ñëw, nanga solu mel ni yaa ngi dem ndaje. Boo gisee suñu béréb bi ñuy woowe Betel, sa ngëm dina gën a dëgër.

    Téere yi ci Wolof (1996-2025)
    Ngir génn
    Ngir konektewu
    • Wolof
    • Yónnee ko
    • Ni nga bëgge mbir yi feeñe
    • Copyright © 2025 Watch Tower Bible and Tract Society of Pennsylvania
    • Conditions d’utilisation
    • Règles de confidentialité
    • Paramètres de confidentialité
    • JW.ORG
    • Ngir konektewu
    Partager