Nañu fàttaliku li ñu jàng ci Lekkoolu Sasu Nguuru Yàlla
Laaj yii di topp, ci Lekkoolu sasu Nguuru Yàlla lañu ko war a def, ci diggante 28 feewriyee 2005 ba 6 màrs 2005. Ci lu mat 30 minit, wottukatu lekkool bi dina waxtaan ak ñi teew ngir fàttaliku li ñu def ci lekkool bi ci diggante 3 sãwiyee ba 28 feewriyee 2005. [Buleen fàtte : Bu amee laaj boo xam ne kenn bindul loo war a jàng ngir xam tont bi, yaa ko war a wutal sa bopp. — Seetal li ñu wax ci téere École du ministère, xët 36-37.]
LIY TAX ÑU AAY CI WAX
1. Lu ñu mën a def ngir suñu wax gën a leer ? [be p. 226 § 1–p. 227 § 1]
2. Yan baat nga war a leeral boo koy wax ? [be p. 227 § 2–p. 228 § 1]
3. Lan lañu mën a def ngir suñu wax ëmb xam-xam bu am maanaa ? [be p. 231 § 1-3]
4. Boo naree jàng aaya bu ñépp a xam bu baax, loo mënee def ba nit ñi am lu ñu ciy jàng ? [be p. 231 § 4-5]
5. Mën nga waxtaan ci li Biibël bi nettali fekk ñi lay déglu xam ko bu baax ba pare. Soo leen waxee ñu seetaat yenn ponk yu ndaw ci li Biibël bi wax foofu, loolu lu mu mën a def ci ñoom ? [be p. 232 § 2-4]
WAXTAAN N° 1
6. Dañuy jàngal nit ñi “ ragal Yàlla dëgg ji te topp ay ndigalam ”. Loolu, lu mu ëmb ? (Daj. 12:13) [be p. 272 § 3–p. 273 § 1]
7. Bu ñuy xamal nit ñi turu Yexowa, lu ñu mën a def ngir bañ a yem foofu rekk waaye won leen it jikko yi mu am ? (Yow. 2:32) [be p. 274 § 3-5]
8. Jàng lu jëm ci Yeesu te waar nit ñi lu jëm ci moom, ban solo la am ? [be p. 276 § 1]
9. Lu tax mënuñu am diggante bu rafet ak Yàlla te xam bu baax li Biibël bi di jàngale, bu ñu xamulee lépp li taxawaayu Yeesu ëmb ? [be p. 276 § 2]
10. Naka lañu mën a wonee ne gëm nañu bu baax ne Yeesu Krist Buur la ? [be p. 277 § 4]
LI ÑU WAROON A JÀNG CI BIIBËL BI AYU-BÉS BU NEKK
11. Ndax Teraa, baayu Ibrayima, dafa doon jaamu ay xërëm ? (Yos. 24:2)
12. Ndax Sédeyon dafa doon ragal a def li ko Yexowa waxoon ? Lu tax ngay wax loolu ? (Àtt. 6:25-27)
13. Ni Sédeyon doon waxe ak waa Efrayim, lan la ñuy jàngal ? (Àtt. 8:1-3)
14. Bi waa Gibeya bañee teral gan gi ñówoon seen dëkk, lu ñu doon wone noonu ? (Àtt. 19:14, 15)
15. Bi ñépp doon def li ñu foogoon ne lu baax la, ndax loolu, indiwoon na jaxasoo ? (Àtt. 21:25)