Suñu ndaje bu gën a mag bi dafa ñuy xiir ci ànd ak Yàlla
Ci dëgg, ndaje bu gën a mag bi tudd “ Nañu ànd ak Yàlla ”, dafa dëgëral lu leer li Yexowa wax fii : “ Yoon a ngi nii. Awleen ci. ” (Isa. 30:21). Bu ñu toppee li ñu fa dégg, dina ñu dimbali ñu ‘ sàmm suñu dundin ’, maanaam ñu seet bu baax ni ñuy doxale suñu àddina (Efes 5:15). Te bu ñu xalaatee bu baax ci li ñu fa jàng, loolu dina ñu dimbali ñu kontine ci yoonu dëgg gi. — 3 Ywna. 3.
Ci ayu-bésu 21 feewriyee, dinañu fàttaliku li ñu waxtaane ci ndaje bu mag boobu. Nanga seetaat li nga bindoon ci ndaje boobu. Jàngal itam laaj yii di topp. Nanga def ñaar yooyu ngir waajal te mën a bokk ci waxtaan bi, bés bu ñuy fàttaliku li ñu waxoon ci ndaje bu mag bi.
1. Lu taxoon Enokk mën a ànd ak Yàlla, fekk mu ngi doon dund ci jamano ju jaxasoo ? (Yaw. 11:1, 5, 6 ; Yudd 14, 15 “ Marchons avec Dieu à une époque troublée ”.)
2. Ci ban fànn ci suñu dund lañu mën a topp li ñu wax ci Lukk 16:10 ? (“ Êtes-vous ‘ fidèles dans ce qui est tout petit ’ ? ”)
3. a) Am na ci Xoseyaa pàcc 6 ba 9 lu ñu mën a topp bu ñu bëggee ànd ak Yàlla. Wax ci ñeent (Xos. 6: 6, 7 ; 7:14 ; 8:7). b) Am na ci Xoseyaa pàcc 10 ba 14 yeneen ponk yu ñu mën a topp ngir ànd ak Yàlla. Yan ponk la ? (“ La prophétie d’Hoshéa nous aide à marcher avec Dieu ”, discours en trois parties.)
4. Lan la jëkkër ak jabar mën a def bu ñu bëggee seen diggante gën a rattax ? (Léeb. 12:4 ; Efes 5:29 ; “ Ne séparez pas ‘ ce que Dieu a attelé au même joug ’ ”)
5. Naka lañuy wonee ne dañuy weg ndaje yi ñu am ngir jaamu Yàlla ? (Daj. 5:1 ; Isa. 66:23 ; “ Montrons du respect pour nos saints rassemblements ”.)
6. a) Bala ñu mën a xam ndax li ñuy def ci waaraate bi lu am maanaa la, fàww ñu seet lu am solo lu liggéeyu waare bi ëmb. Mën nañu ci wax ñett. Ñett yooyu, yan la (Isa. 52:7 ; Sak. 8:23 ; Mark 6:34) ? b) Loo gis ci téere Une bonne nouvelle pour des gens de toutes nations lu ñu mën a jariñoo bu baax ? (“ Une bonne nouvelle pour des gens de toutes nations ” ; “ En aidant les personnes d’expression étrangère ”.)
7. Waaraatekat yu bees yi, naka lañu leen mënee dimbali ñu bañ a ragal bu ñuy waaraate ? (Àtt. 7:17 ; “ En aidant des multitudes à se joindre à nous dans le ministère ”.)
8. Naka lañu mën a wonee ne gëm nañu ne “ bésu Yexowa bu mag bi mu ngi jegesi ” ? (Tsë. 1:14 ; “ Marchons par la foi, non par la vue ”.)
9. a) Lu tax ñu mën a wax ne yóbbe bàkkaar, maanaam fàkkastalu walla tax ba keneen fàkkastalu ci wàllu ngëm, lu garaaw la ? (Mark 9:42-48) b) Ñun, lan lañu mën a def bu ñu bañee fàkkastalu ci wàllu ngëm (Sab. 119:165) ? c) Naka lañu mënee moytu def lu mën a tax suñu moroom fàkkastalu ci wàllu ngëm ? (1 Kor. 10:24; “ Aucune occasion de trébucher ”)
10. Naka lañu mën a wonee ne dañu am xel bu ñu bëggee am jëkkër walla jabar, bu ñu bëggee am wér-gi-yaram, ak bu ñu bokkee ci mbirum jaay ak jënd ? (Sab. 26:4 ; Macë 6:25 ; 1 Tim. 6:9 ; “ Restez dans votre bon sens, complètement ”.)
11. a) Bu ñu seetee bi ñu doon ganale Yeesu, lu ñu ci mën a jàng (Lukk 10:42 ; 24:32) ? b) Su amee li ñu bëgg a def ngir féexal suñu xol, lan lañu mën a def ngir bu ñu ci paree, ñépp kontaan te ku nekk amaat doole ? (1 Kor. 10:31-33 ; “ Des activités saines qui réconfortent ”.)
12. Sabuur 23 mu ngi wax ci barke yi ñuy am, ñun ñi nga xam ne Yexowa mu ngi ñuy sàmm. Yan barke la, te lan mooy suñu warugar ? (1 Kor. 10:21 ; “ Jéhovah est notre Berger ”.)
13. Yàlla nee na ñu “ jeriñoo jot gi ”. Naka la karceen yi mënee topp loolu ? (Efes 5:16 ; “ Rachetons le moment propice ”.)
14. a) “ Waxtuw àtte ” Yàlla bi ñuy wax ci Peeñu bi 14:7, lan la ëmb ? b) Naka lañuy wonee ci fasoŋ bu leer ne jóge nañu ci Babilon bu mag bi ? (“ ‘ Veillez ’ : l’heure du jugement est venue ”.) c) Lan moo la neex ci téere Veillez ! ?
15. Waxal ñetti jikko yu ñu war a am bu ñu bañee “ wàcc yoon wu jub wi ”. (2 Pie. 2:15 ; “ Gardons-nous d’ ‘ abandonner le droit chemin ’ ”.)
16. Naka la ndaw yi mënee moytu “ yoonu nit ñu bon ñi ” ? (Léeb. 4:14 ; “ Jeunes, marchez dans le sentier de la justice ”.)
17. a) Ndaw li Pool, ku jar a roy la ci wàllu muñ. Lu tax ñu wax loolu (Jëf. 14:19, 20 ; 16:25-33) ? b) Lu tax waruñu ragal mukk su amee ay nit ñu nu bëgg a teree jaamu Yàlla ci dëgg ? (Daraam ak waxtaan “ Rendons pleinement témoignage malgré l’opposition ”.)
18. Yan barke lañuy am bu ñu àndee ak Yàlla ? (“ Ceux qui marchent avec Dieu en retirent des bienfaits, maintenant et pour toujours ”.)
Nañu fas yéene déglu bu baax ‘ baat bi nekk suñu ginnaaw ’. Bu ñu defee loolu, dinañu ànd ba fàww ak suñu baay bi nekk ci kow asamaan. — Isa. 30:21 ; Ywna. 3:36.