Li nga mën a def ngir ñu kontine waxtaan bi
1 Bu ñuy waaraate, dañu faral a gis ay nit ñu dëkkul ci suñu goxu mbooloo walla ñu déggul suñu làkk. Yenn saay, làkku ñi tëx lañuy làkk. Mën na am it ñi doon am ak ñun waxtaan yu neex ci Biibël bi toxu ci beneen goxu mbooloo. Lan lañu mën a def ngir nit ñooñu kontine seen waxtaan ci Biibël bi ? Nañu jëfandikoo kayit bi tudd Veuillez suivre l’intérêt (S-43).
2 Ci lu ëpp, booy waar nit ñi ci làkk bi ñu nàmp, dañuy gën a déglu (Jëf. 22:1, 2). Kon, bu dee sax ki ñu taseel bëggul waxtaan ak ñun ci xibaaru Nguur gi, nañu jëfandikoo kayit boobu ngir keneen waar ko ci làkkam. Waaye mën na am ñi dégg làkk boobu xaw a bare ci dëkk bi, te am na mbooloo bu leen faral a waar ci seen làkk. Su dee loolu la, nanga bind rekk ñi bëgg waxtaan ak ñun.
3 Li ñu war a bind ci kayit boobu : Jéemal a xam turu nit ki, adareesam, ak nimoro telefonam. Bindal it ni ko waxtaan bi itteele, kañ lañu ko mën a gis, téere bi mu jël walla bi mu bëgg, ak làkk bi mu gën a dégg. Boo bindee loolu lépp ba pare, nanga ko gaaw a jox sa sekkerteeru mbooloo. Moom dina ko jottali mbooloo walla gurup biy toppatoo ñi dégg làkk boobu.
4 Bu ñuy jottali kayit boobu : Bu sekkerteer bi xamulee ban mbooloo walla gurup la ko war a jottali, walla yorul adarees bi, mën na telefone bànqaas bi ci Biro biy toppatoo liggéeyu waare bi. Léegi, jaratul ñu jaar ci wottukatu dëkk bi (surveillant de ville) ngir loolu.
5 Bu mbooloo mi walla gurup bi jotee kayit bi tudd Veuillez suivre l’intérêt (S-43), nañu gaaw a seeti nit ki ngir kontine waxtaan bi. Nañu def bu baax suñu wàll ci fànn boobu, xam ne ci lu wóor Yexowa dina ubbi xolu “ ñépp ñu jagoo dund gu dul jeex ”. — Jëf. 13:48.