Ndaje yi jëm ci liggéeyu waare bi
14-20 feewriyee
Woy-Yàlla 77
10 min : Yégle yi jëm ci suñu mbooloo. Yenn ci yégle yi nekk ci Sasu Nguuru Yàlla. Na ñaari nit topp li nekk ci xët 8, te wone ni ñu mënee wone Réveillez-vous ! bu 22 sãwiyee ak La Tour de Garde bu 1 feewriyee. Sasu Nguuru Yàlla yi dañuy wone li ñu mën a wax bu ñuy wone suñu téere yi. Ci lu gàtt, fàttalil ñi teew ni ñu ko mënee topp ci suñu goxu mbooloo. — Seetleen Sasu Nguuru Yàlla bu sãwiyee 2005, xët 8. Waxal ñépp ñu jaar ci laaj yi nekk ci xët 1 ngir seetaat li ñu bindoon ci ndaje bu gën a mag bi tudd “ Nañu ànd ak Yàlla ”. Waxtaan boobu, dinañu ko def ayu-bés bii di ñów.
35 min : “ Ci jamano bu ñuy fàttaliku deewu Yeesu, nañu yokk li ñuy def ci liggéeyu waare bi. ”a Wottukatu liggéeyu waare bi moo ko war a def. Bu ngeen di def xise 6 bi, booleleen ci li nekk ci Réveillez-vous ! bu 8 septaambar 2004 ci xët 12 ba 13. Waxal turu ñiy nekk pioñee yuy jàpple. Waxal yan ndaje lañu yokk ci ndaje yi ñuy def bala ñuy dem waaraate. Xiiral ñépp ci yokk li ñuy def ci wàllu ngëm ci jamano fàttaliku bi.
Woy-Yàlla 53 ak ñaan bu mujj bi.
21-27 feewriyee
Woy-Yàlla 60
10 min : Yégle yi jëm ci suñu mbooloo. Seetaatal ponk yi ëpp solo ci wërale bi nekk ci xët 6 te tudd “ Li nga mën a def ngir ñu kontine waxtaan bi ”. Waxal ñépp ñu jëfandikoo kayit bi tudd Veuillez suivre l’intérêt (S-43) te bañ ci yéex saa yu ñu ko waree def.
35 min : “ Suñu ndaje bu gën a mag bi dafa ñuy xiir ci ànd ak Yàlla. ” Benn magu mbooloo moo ko war a def. Li ngay njëkk wax warul weesu benn minit, ba pare nanga waxtaan ak ñi teew ci laaj yi ñu def ci xaaj bii di wax ci li ñu dégg ci suñu ndaje bi gën a mag bi. Kiy jiite war na xam ni mu war a yàgge ci laaj bu nekk. Xéyna ci yenn laaj, benn nit rekk lay bàyyi mu tontu. Dungeen am jot ngir jàng aaya yi ñu wax foofu yépp. Dañu leen bind ngir wone rekk fi nga mënee gis tont yi. Nañu wax ci ni ñu mënee topp li ñu dégg ci ndaje bu mag bi.
Woy-Yàlla 57 ak ñaan bu mujj bi.
28 feewriyee ba 6 màrs
Woy-Yàlla 18
10 min : Yégle yi jëm ci suñu mbooloo. Fu ñu tollu ci xaalisu mbooloo mi. Fàttalil waaraatekat yi ne dañu war a bind li ñu def ci liggéeyu waare bi ci weeru feewriyee te joxe ko. Na ñaari nit topp li nekk ci xët 8, te wone ni ñu mënee wone Réveillez-vous ! bu 8 feewriyee ak La Tour de Garde bu 15 feewriyee. Mën ngeen wax leneen lu mën a baax ci seen gox ngir wone yéenekaay yi.
20 min : “ Nañu gërëm Yexowa ndax ni mu baaxe ak ñun. ”b Waxal kañ ak fan lañuy màggale bésu fàttaliku bi, turu kiy def waxtaan bi, ak lépp loo war a xamal nit ñi ngir bu bés boobu jotee lépp aw ci yoon te baax. Boo àggee ci xise 4, na am benn waaraatekat buy wone ci lu gàtt ni ñuy woowe ci ndaje fàttaliku bi nit ku faral a jot suñu yéenekaay yi. Su dee joxaguñu kayit yi ñu def ngir woo nit ñi ci ndaje fàttaliku bi, dinañu leen joxe bu ndaje bii paree.
15 min : “ Nañu dimbali ñi ñuy jàngal Biibël bi ñu topp li ñuy jàng — Xaaj 6. ”c Na am ñuy wonee ci lu gàtt (4 minit) li ñu mën a wax bu fekkee ne ki ñuy jàngal Biibël bi dafa ñuy laaj lu tax tuuti nit rekk ñoo lekk ci mburu mi te naan ci biiñ bi. Kiy jàngale dina ko wax ne laaj bi mu laaj, laaj bu am solo la. Dina ko bind, ba pare dina ko laaj ndax bëggul ñu xaar ba ñu pare li ñu war a jàng bés boobu, sog ci tontu. Bu ñu paree nag, kiy jàngale dina ko won xaaj bi tudd “ Qui est en droit de participer au pain et au vin ? ” ci xët 243 ci téere Comment raisonner. Dinañu ko jàng, ba pare nit kiy jàng dina gërëm bu baax ki koy jàngal ci tont bu leer bi mu am.
Woy-Yàlla 8 ak ñaan bu mujj bi.
7-13 màrs
Woy-Yàlla 31
10 min : Yégle yi jëm ci suñu mbooloo. Fàttalil ñi teew ponk yi ëpp solo ci yi nekk ci wërale bi tudd “ Ndaje bi ñuy fàttaliku deewu Yeesu : Li ñu warul a fàtte. ”
15 min : Li nekk soxla ci mbooloo mi.
20 min : Nañu toppatoo ñi néew doole (Jëf. 20:35). Li ngay njëkk wax warul weesu benn minit, ba pare laajal ñi teew laaj yi nekk ci La Tour de Garde bu 1 sulyet 2004, xët 17-18, xise 12-16. Nanga ko def ni ñuy defe Njàngum La Tour de Garde bi. Laajal ku mën liir bu baax mu jàng xise yi. Nanga gën a wone ni ñu mënee topp li ñu wax foofu bu ñu teewee ndaje fàttaliku bi ak waxtaan bi ñu faral di am ci àddina sépp bu ndaje fàttaliku bi weesoo.
Woy-Yàlla 42 ak ñaan bu mujj bi.
[Li ñu bind ci suuf]
a Li ngay njëkk wax warul weesu benn minit, ba pare laajal ñi teew ay laaj, te may leen ñu tontu.
b Li ngay njëkk wax warul weesu benn minit, ba pare laajal ñi teew ay laaj, te may leen ñu tontu.
c Li ngay njëkk wax warul weesu benn minit, ba pare laajal ñi teew ay laaj, te may leen ñu tontu.