Nañu gërëm Yexowa ndax ni mu baaxe ak ñun
Dinañu fàttaliku deewu Yeesu ci bésu 24 màrs
1 Ki bind Sabuur nee na : “ Céy, nañu gërëm Yexowa ndax mbaaxaayu xolam ak lépp lu rafet li mu defal doom-Aadama yi. ” (Sab. 107:8.) Yàlla, lu baax rekk lay yéene doom-Aadama yi. Waaye mbaaxaayu xolam weesu na loolu. Moom la Biibël bi wone ci aaya bii di topp, fu ñuy gërëme Yàlla. Dafa ne : “ Céy Yexowa, sa mbaaxaayu xol moo tax bàyyiwuloo di ma jàpple. ” (Sab. 94:18) Yexowa dafa ñu may doom bi mu am képp. Mbaaxaayu xol bi mu ñu won noonu, lu réy-a-réy la ! — 1 Ywna. 4:9, 10.
2 Léegi ñu màggal bés bi Yeesu deewe. Lan lañu mën a def ngir gërëm Yàlla, moom mii bare mbaaxaayu xol (Sab. 59:17) ? Nañu xalaat bu baax ci li Yeesu def ci fanam yu mujj yi. Na ku nekk ci ñun jël jot ngir def loolu (Sab. 143:5). Nañu topp itam porogaraam bi ñu def ci Examinons les Écritures chaque jour — 2005 ngir jàng Biibël bi ci jamano fàttaliku bi. Mën nañu jàng itam pàcc 112 ba 116 ci téere Le plus grand homme. Am na it suñu yeneen téere yuy sukkandiku ci Biibël bi yuy wax ci loolu. Bu ñuy jàng yu mel noonu, nañu ci xalaat bu baax-a-baax (1 Tim. 4:15). Jàng Kàddu Yàlla di ci boole ay ñaan dafay dundal suñu xol. Dafay wone it ne dañu bëgg Yexowa. — Macë 22:37.
3 Nanga xiir nit ñi ci gërëm Yàlla : Daaw, ci àddina si sépp, 16 760 607 nit ñoo teewe ndaje bi ñuy fàttaliku deewu Yeesu. Ci benn dëkku Liberia, suñuy mbokk ci ngëm dañu yónni benn leetar boroom dëkk bi, maanaam meer bi. Ñu xamal ko ne dañu bëgg màggal reeru Sàng bi ci dëkkam. Njiit moomu abal leen fu nit ñi di futbale. Mu woo itam ñépp ngir ñu ñów teewsi. Foofu, juróomi waaraatekat rekk ñoo fa nekkoon. Waaye, bésu fàttaliku bi, 636 ñoo teewe !
4 Ñun itam, bëgg nañu woo ci màggal boobu nit ñi nu mën ñépp. Nanga bind ci benn kayit turu képp ki nga bëgg woo ci ndaje fàttaliku bi. Ci nataal yi nekk ci xët bu mujj bi ci Réveillez-vous ! bu 8 màrs ak La Tour de Garde bu 15 màrs, dañuy woo nit ñi ci ndaje boobu. Am na it kayit yu ndaw yu ñu defar ngir woo nit ñi ci ndaje boobu. Nanga ci bind ci fasoŋ bu leer béréb ak waxtu bi ñuy defe ndaje bi. Jox ci benn képp koy woo ci ndaje bi. Te bu 24 màrs bëggee jot, nanga leen fàttali ndaje bi te seetaat li ngeen war a def ngir ñu ñów.
5 Léeg-léeg mu am ay nit ñuy jàng Biibël bi ak ñun fekk teeweeguñu suñuy ndaje. Lu ñu mën a def ngir ñu teewe ndaje fàttaliku bi te jariñoo ci bu baax ? Saa yoo jàngee ak ñoom Biibël bi, jëlal tuuti minit ngir won leen lu tax ndaje boobu am solo. Boo bëggee def loolu, am na lu am solo lu ñu bind ci La Tour de Garde bu 15 màrs 2004, xët 3 ba 7, ak ci téere Comment raisonner xët 241 ba 245.
6 Teralal ñiy ñów ndaje fàttaliku bi : Bésu ndaje bi, teralal ñiy ñów teewe te waxtaanal ak ñoom (Room 12:13). Ñi nga woowoon ba ñu ñów, toogal ak ñoom te fexeel ba ñu am benn Biibël ak benn téere woy-Yàlla yi. Bu ñu gisee nag kenn ku bàyyi waaraate, nañu ko teral bu baax-a-baax. Xéyna loolu dina tax mu bëgg teewewaat suñuy ndaje (Lukk 15:3-7). Ndaje bi ñuy fàttaliku deewu Yeesu, lu am solo la ci suñu diggante ak Yàlla. Nañu def lépp li ñu mën ngir woo nit ñi ñu ànd ak ñun bu ñuy gërëm Yexowa ndax “ mbaaxaayu xolam bu rafet bi ”. — (Sab. 31:21).
[Laaj yi]
1. Naka la nu Yexowa wonee mbaaxaayu xolam ?
2. Naka lañu mënee gërëm Yexowa ?
3, 4. a) Naka lañu mënee roy suñuy mbokk yi nekk ca Liberia ? b) Kan nga bëgg woo ci bésu fàttaliku bi ?
5. Naka nga mënee xiir ñi ngay jàngal Biibël bi ci teewe ndaje fàttaliku bi ?
6. Lu tax ñu war a teral bu baax ñiy ñów teewe ndaje fàttaliku bi ?