Ndaje yi jëm ci liggéeyu waare bi
14-20 màrs
Woy-Yàlla 54
10 min : Yégle yi jëm ci suñu mbooloo. Yenn ci yégle yi nekk ci Sasu Nguuru Yàlla. Toppal li ñu wax ci xët 6 ngir wone ñaari yéenekaay yu baax lool ci seen gox. Mën nga jël Réveillez-vous ! bu 22 feewriyee walla bu 8 màrs walla it La Tour de Garde bu 1 màrs walla bu 15 màrs. Mën ngeen wax leneen lu mën a baax ci seen gox ngir wone yéenekaay yi. Booy wone benn ci ñaari yéenekaay yi, na nekk booy dellusi seeti ku ko faral a jël. Boo bëggee jeexal waxtaan bi, wonal nit ki li nekk ci xët 32 ci Réveillez-vous ! bu 8 màrs walla La Tour de Garde bu 15 màrs ngir fàttali ko ndaje bi ñuy def ngir fàttaliku deewu Yeesu.
20 min : “ Dinañu gën a wax ci Biibël bi ! ”a
15 min : “ Nañu dimbali ñi ñuy jàngal Biibël bi ñu topp li ñuy jàng — Xaaj 7. ”b Booy waajal waxtaan bii, nanga ci boole li nekk ci La Tour de Garde bu 15 sulyet 2002, xët 27, xise 5-6.
Woy-Yàlla 100 ak ñaan bu mujj bi.
21-27 màrs
Woy-Yàlla 36
10 min : Yégle yi jëm ci suñu mbooloo.
15 min: “ Ndax komaase nga ko topp ? ” Waxtaan ak ñi teew. Nangeen jàng xise yi yépp.
20 min : Lan mooy Armagédon ? Waxtaan bu ñu jële ci téere Comment raisonner, xët 181-6. Li ngay njëkk wax warul weesu benn minit, ba pare laajal ñi teew ay laaj, te may leen ñu tontu. Bind nañu laaj yi ci bind yi gën a ñuul. Waxal ñi teew ñu jaar ci aaya yi ànd ak laaj yooyu ngir tontu ci. Waxal ni ñu mënee jariñoo xaaj bii ci waaraate bi.
Woy-Yàlla 3 ak ñaan bu mujj bi.
28 màrs ba 3 awril
Woy-Yàlla 61
10 min : Yégle yi jëm ci suñu mbooloo. Waxal fu ñu tollu ci xaalisu mbooloo mi te jàngal kayit biy wone ne bànqaas bi jot na xaalis bi ñu maye. Waxal ñi teew ne ren, waxtaan bi ñuy faral di am ci àddina si sépp bu ndaje bi ñuy fàttaliku deewu Yeesu weesoo, ci bésu 10 awril lay doon. Waxal ñi teew ñu woo ñi suñu waxtaan neex ci waxtaan boobu. Waxal téere yi ñu war a wone ci waaraate bi ci weeru awril ak me. Na ñaari nit topp li nekk ci xët 6, te wone ni ñu mënee wone Réveillez-vous ! bu 22 màrs ak La Tour de Garde bu 1 awril. Ku ci nekk na wax fi ñuy jële xaalis bi ñu soxla ngir def liggéeyu waare bi ci àddina si sépp. — Seetal La Tour de Garde ci xët 2 walla Réveillez-vous ! ci xët 5.
15 min : Li nekk soxla ci mbooloo mi.
20 min : “ Nañu won nit ñu bare suñu yéenekaay yi. ”c Bu ngeen di def xise 3 ak 4, waxal naka ngeen mënee topp ci seen gox li nekk ci xise yooyu. Nanga am waxtaan bu gàtt, ak ay waaraatekat yu aay ci joxe suñuy yéenekaay ci bitig yi, ci mbedd mi, ci béréb yu bare nit, walla bu ñu ci amee bunt. Nañu wax ni ñuy wonee yéenekaay yi bu ñuy waaraate noonu. Ci lu gàtt, na am ku wone ni ñu mëne wone suñu yéenekaay yi, walla mu wone li benn waaraatekat def ngir wone suñu yéenekaay yi.
Woy-Yàlla 42 ak ñaan bu mujj bi.
4-10 awril
Woy-Yàlla 12
5 min : Yégle yi jëm ci suñu mbooloo.
20 min : Bëgganteleen (Ywna. 13:35). Benn magu mbooloo mooy def waxtaan bii. Ci La Tour de Garde bu 1 feewriyee 2003, xët 15-18, xise 10-21 lañu ko jële. Ni ñu ko waxe woon bi ñu doon wax téere yi ñu war a wone ci waaraate bi ci weeru awril ak me, dañu war a góor-góorlu ngir tàmbali ay njàngum Biibël ak ñi jàng Biibël bi ba pare ci téere Xam-xam ak it ci téere Laaj. Woneel naka la waaraatekat yi mënee jàpple mag yi ngir dimbali ñi feebar.
20 min : Ni ñu mënee dimbali ñiy làkk làkk bu ñu déggul. Waare ak waxtaan ak ñi teew bu ñu jële ci téere Une bonne nouvelle pour des gens de toutes nations. Waxal li nekk ci téere boobu. Waxal ñett yi ñu mën a def ngir dimbali nit kuy làkk, làkk bu ñu déggul. Waxal it li nekk ci Sasu Nguuru Yàlla bu sulyet 2003, xët 4. Waxal ñi teew ñu jëfandikoo kayit bi tudd Veuillez suivre l’intérêt (S-43) bu dee sax mu ngi mel ni nit ki bëggul déglu xibaaru Nguur gi. Na am ñuy wone ni ñu mënee jëfandikoo téere bu bees boobu.
Woy-Yàlla 41 ak ñaan bu mujj bi.
[Li ñu bind ci suuf]
a Li ngay njëkk wax warul weesu benn minit, ba pare laajal ñi teew ay laaj, te may leen ñu tontu.
b Li ngay njëkk wax warul weesu benn minit, ba pare laajal ñi teew ay laaj, te may leen ñu tontu.
c Li ngay njëkk wax warul weesu benn minit, ba pare laajal ñi teew ay laaj, te may leen ñu tontu.