TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Watchtower
TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Wolof
  • BIBLE
  • TÉERE YI
  • RÉUNIONS
  • km 3/05 p. 1
  • Dinañu gën a wax ci Biibël bi !

Aucune vidéo n'est disponible pour cette sélection.

Il y a eu un problème lors du chargement de la vidéo.

  • Dinañu gën a wax ci Biibël bi !
  • Sasu Nguuru Yàlla — 2005
  • Leneen lu jëm ci loolu
  • Nañu wone yéenekaay yiy “ wax dëgg gi ”
    Sasu Nguuru Yàlla — 2007
  • “ Yeewuleen te sax ci ”
    Sasu Nguuru Yàlla — 2000
  • “ Lan ngay tontu ? ”
    Sasu Nguuru Yàlla — 2007
Sasu Nguuru Yàlla — 2005
km 3/05 p. 1

Dinañu gën a wax ci Biibël bi !

1 Yéenekaay bi tudd L’Age d’or, ci 1 Oktoobar 1919 la njëkk a génn. Baaxoon na lool ci liggéeyu waare bi. Lu tax ñuy wax loolu ? Ndaxte li ci nekk, ñi nekkul Seede lañu ko defaloon. La Tour de Garde moom, ci lu tollu ay ati at, waa “ coggal ju ndaw ji ” ñoo gënoon a tax ñu génne ko (Lukk 12:32). Waaraatekati Nguur gi dañu kontaanoon lool ci yéenekaay bu bees boobu tudd L’Age d’or. Loolu moo tax bi ñu doon waaraate, L’Age d’or yi ñu doon joxe ëppoon fuuf La Tour de Garde. Te loolu yàgg na nekk noonu.

2 Yéenekaay bi tudd L’Age d’or, dañu ko defar ngir mu won nit ñi ne Nguuru Yeesu Krist kese moo mën a dindi suñu coono yépp. Nguur googu dina yàgg 1000 at, te dina indil doom-Aadama li ñu mën a woowe ci tubaab un âge d’or (maanaam jamano ju neex lool). Waaye jamano ji dafay soppeeku. Loolu moo tax mu am it lu ñu soppi ci L’Âge d’or ngir mu gën a ànd ak li nit ñi soxla. Ci atum 1937, dañu ko jox tur bu bees. Tur boobu ci tubaab mooy Consolation (maanaam dëfël xol). Ci atum 1946, dañu ko tudde Réveillez-vous ! (maanaam Yeewuleen). Noonu la tudd ba tey.

3 Yéenekaay boobu, am na wàll bu réy ci lépp li ñu def ci liggéeyu waare bi, 1919 ba tey (Macë 24:14). Waaye jot bi des ci àddina si bareetul. Loolu moo tax ñu xalaat ne am na leneen li ñu war a soppi ci Réveillez-vous ! bi.

4 Réveillez-vous !, lu bare lu muy waxtaane bokkul ci mbirum diine te lu neex a jàng la. Looloo tax ay milioŋi nit bëgg koo jàng. Wóor na ne li ëpp ci ñiy teewe ndaje fàttaliku bi at mu nekk, faral nañu jàng Réveillez-vous ! Waaye ba tey, ku bëgg a mucc ci “ bésu meru Yexowa ”, warul yem rekk ci faral a jàng suñuy téere. — Tsë. 2:3 ; Peeñ. 14:​6, 7.

5 Kon, ci weeru sãwiyee 2006, Réveillez-vous ! dina komaase di gën a wax ci Nguuru Yàlla. Dina gën a won nit ñi ne ci Biibël bi lañu war a wut li leen mën a dimbali ci seeni coono. Te it dina gën a wone li Biibël bi wax ci li xew ci suñu jamano jii. Kon ñiy jàng Réveillez-vous !, dinañu xam bu baax li xew-xewu àddina sii tekki. Xéyna loolu dina tax ñu bëgg yokk li ñu xam ci Yexowa. — Sak. 8:⁠23.

6 Réveillez-vous ! dina kontine di wax ci luy itteel nit ñu bare. Waaye dina gën a wax ci li nekk ci Biibël bi (1 Tes. 2:13). La Tour de Garde mu ngi wax ba pare ci lu xóot li nekk ci Biibël bi. Te léegi Réveillez-vous ! dina gën a wax ci li nekk ci Biibël bi. Kon yaakaar nañu ne jarul ñu kontine di génne ñaari Réveillez-vous ! weer wu nekk. Kon, weeru sãwiyee 2006 bu jotee, dinañu komaase di génne benn Réveillez-vous ! weer wu nekk. Loolu dina yombalal lool lépp li ñuy def ngir waajal, tekki, te yónnee suñuy téere.

7 Fi ñu nekk nii, ci lu ëpp ci làkk yi ñu koy génne, Réveillez-vous ! mu ngi génn ba pare benn yoon weer wu nekk walla benn yoon ñetti weer yu nekk. Boo xoolee làkk yi ñu koy génne yépp, boo ci jëlee 100, dina ci am léegi 40 yu dul génnati ñaari yoon weer wu nekk te génn benn yoon rekk. La Tour de Garde moom, duñu ci soppi dara.

8 Weer wu nekk, waaraatekat yi, bu ñuy wone suñuy yéenekaay, dinañu mën a boole Réveillez-vous ! bi génn ak benn ci ñaari La Tour de Garde yi génn. Kon weer wu nekk dootuñu soxlati soppi ñaari yoon li ñuy wax bu ñuy wone suñu yéenekaay Réveillez-vous !

9 Bi mu komaasee génn ci atum 1919 ba tey, suñu yéenekaay bi tuddoon L’âge d’Or, ba pare tuddaat Consolation, te tudd léegi Réveillez-vous !, def na lu bare lool ci liggéeyu waare bi. Tey am na lu ñu ci bëgg a soppi. Ñu ngi ñaan Yexowa mu wéy di barkeel li ñuy def ngir won ko nit ñi. Ñu ngi ñaan Yexowa itam mu dimbali nit ñu gën a bare te “ bokk ci xeet yépp, giir yépp, réew yépp ak kàllaama yépp ” ñu wékk seen yaakaar yépp ci Nguuru Yàlla, ndaxte moom rekk moo mën a dindi seeni coono. — Peeñu 7:⁠9.

[Laaj yi]

1. Bi ñu komaasee defar La Tour de Garde, ñan lañu ko gënoon a jagleel ? L’Age d’or nag ?

2. L’Âge d’or, naka la tudd tey, te lu tax ñu génne ko ?

3. Am na lu Biibël bi waxoon ne dina am, te Réveillez-vous ! def na lu bare ngir mu am. Loolu lan la ?

4. a) Lan lañu war a def bu ñu bëggee mucc ci “ bésu meru Yexowa ” ? b) Ni ko Peeñu bi 14:​6,7 waxe, “ malaaka [mi] naaw ca digg asamaan ”, ci lan lay woo nit ñépp ?

5. a) Ci lan lañuy komaase di gën a waxtaan ak Réveillez-vous ! bu sãwiyee 2006 ? b) Loolu dina mën a xiir ñu bare ci lan, te fan la Biibël bi waxe woon ne loolu dina am ?

6, 7. a) Lan lañuy def ci Réveillez-vous ! ngir mu mën a dimbali ñu bare ñu topp li 1 Tesalonikk 2:13 wax ? b) Ñaata yoon la Réveillez-vous ! di génn léegi weer wu nekk, te loolu ñaata làkk lay laal ?

8. Léegi naka la waaraatekat yi mënee wone Réveillez-vous ! ak La Tour de Garde ?

9. Lan la Réveillez-vous ! di kontine di def ci liggéeyu waare bi ?

    Téere yi ci Wolof (1996-2025)
    Ngir génn
    Ngir konektewu
    • Wolof
    • Yónnee ko
    • Ni nga bëgge mbir yi feeñe
    • Copyright © 2025 Watch Tower Bible and Tract Society of Pennsylvania
    • Conditions d’utilisation
    • Règles de confidentialité
    • Paramètres de confidentialité
    • JW.ORG
    • Ngir konektewu
    Partager