Ndaje yi jëm ci liggéeyu waare bi
9-15 me
Woy-Yàlla 94
10 min : Yégle yi jëm ci suñu mbooloo. Yenn ci yégle yi nekk ci Sasu Nguuru Yàlla. Na ñaari nit topp li nekk ci xët 8 ci Sasu Nguuru Yàlla bii, te wone ni ñu mënee wone Réveillez-vous ! bu 8 me ak La Tour de Garde bu 15 me. Mën ngeen wax leneen lu mën a baax ci seen gox ngir wone yéenekaay yi. Na kenn wone ni ñu mënee wone yéenekaay yi bu ci amee bunt ci kaar yi walla taksi yi.
15 min : “ Dinañu def lépp ngir wone suñu téere bu bees bi. ”a Wottukatu liggéeyu waare bi moo ko war a def. Bind nañu ci xaaj bii li ñu mën a wax bu ñuy wone téere bu ndaw bi. Na am ñuy wone ni ñu ko mënee topp. Na kenn def mel ni waxtaan bi neexu ko noonu. Kon waaraatekat bi dina ko jox benn kayit bu ndaw, waaye du ko jox téere bu ndaw bi.
20 min : “ Yéen njaboot yi, nangeen taxawal porogaraam bu baax. ” Li ngay njëkk wax warul weesu ñaari minit. Nanga ci wax lu tax bind porogaraam am solo. Waxtaanal ak ñi teew ci ni ñu mënee jëfandikoo porogaraam bi nekk ci xët 6. Boo paree, nanga waxtaan ci xaaj bi tudd “ Seen porogaraamu njaboot ngir teewe ndaje yi ñu am ci mbooloo mi ”. Laajal ñi teew ñu wax li ñuy def ba dara bañ leen a tere teewe ndaje yi. Ci ayu-bés yiy topp, dinañu waxtaan ci leneen lu war a bokk ci porogaraamu njaboot gi.
Woy-Yàlla 59 ak ñaan bu mujj bi.
16-22 me
Woy-Yàlla 89
10 min : Yégle yi jëm ci suñu mbooloo. Ci lu gàtt, nangeen wax li ngeen jàpp ngir wone téere bu bees bu ndaw bi.
15 min : “ Seen porogaraamu njaboot ngir waaraate. ”b Laajal ñi teew ñu wax lu tax tàmm di ànd ak sa njaboot ci waaraate bi am solo.
20 min : “ Nañu dimbali ñi ñuy jàngal Biibël bi ñu topp li ñuy jàng — Xaaj 9. ”c Bu ngeen di def xise 2, booleleen ci benn walla ñaari ponk yu ngeen jële ci Sasu Nguuru Yàlla bu desàmbar 2004, xët 4. Ci lu gàtt, na am ñuy wone ni ñuy defe njàngum Biibël ci téere Laaj bi. Nañu mel ni ñuy jeexal njàngale 2. Te kiy def njàngum Biibël bi, na laaj ki muy jàngal lii : “ Boo bëggoon a xamal sa xarit turu Yàlla, loo koy wax ? ” Kiy jàng dina jaar ci Sabuur 83:18, ngir wone loolu. Bu ci paree, na ko wax ne def na liggéey bu rafet.
Woy-Yàlla 50 ak ñaan bu mujj bi.
23-29 me
Woy-Yàlla 22
12 min : Yégle yi jëm ci suñu mbooloo. Liiral kayit biy wone fu ñu tollu ci xaalisu mbooloo mi ak leetar bi bànqaas bi yónnee ngir wax ne jot na xaalis bi mbooloo mi maye. Na ñaari nit topp li nekk ci xët 8 ci Sasu Nguuru Yàlla bii, te wone ni ñu mënee wone Réveillez-vous ! bu 22 me ak La Tour de Garde bu 1 suweŋ. Mën ngeen wax leneen lu mën a baax ci seen gox ngir wone yéenekaay yi. Am na lu yenn waaraatekat wax bu ñu doon wone téere bu ndaw bi, te tax na nit ñi déglu bu baax. Na am ku wone loolu ci kanamu ñépp. Ci li des ci jot bi, nangeen nettali li yenn waaraatekat def bi ñu doon wone téere bu ndaw bi ci seen gox.
18 min : “ Bésu Yexowa jege na. ”d Booy waajal waxtaan bii, seetal li nekk ci téere La prophétie de Daniel, xët 59, xise 28.
15 min : “ Seen porogaraamu njaboot ngir jàng Biibël bi. ”e Balaa ndaje bi di jot, waxal benn walla ñaari nit ne dinga leen laaj naka lañu defe seen porogaraam ngir jàng Biibël bi ak seen njaboot ak it li ñuy def ngir topp ko bu baax.
Woy-Yàlla 65 ak ñaan bu mujj bi.
30 me ba 5 suweŋ
Woy-Yàlla 84
10 min : Yégle yi jëm ci suñu mbooloo. Fàttalil waaraatekat yi ne dañu war a bind li ñu def ci liggéeyu waare bi ci weeru me te joxe ko. Waxal téere yi ñu war a wone ci weeru suweŋ. Su baaxee ci seen goxu mbooloo, na am ñu topp li ñu bind ci Sasu Nguuru Yàlla bu sãwiyee 2005, xët 3-6, ngir mën a wonee téere yooyu. Mën ngeen a wax leneen lu mën a baax ci seen gox ngir wone téere yooyu.
20 min : “ Seen porogaraamu njaboot ngir jàng Aaya bés bi. ”f Laajal ñi teew ñu wax lu tax jàng bés bu nekk aaya bés bi ak sa njaboot baax ci ñoom, maanaam lan lañu ciy jële. Nañu wax it ci ban waxtu la seen njaboot di defe loolu.
15 min : Na am ñu wax walla wone lu neex lu ñu def ci waaraate bi ci weeru màrs, awril ak me. Bala ndaje bi di jot, nanga wax benn walla ñaari waaraatekat ne dinga leen laaj li ñu def ngir yokk seen waaraate bi ci jamano fàttaliku bi. Nañu wax it loolu lu mu leen indil.
Woy-Yàlla 95 ak ñaan bu mujj bi.
6-12 suweŋ
Woy-Yàlla 66
10 min : Yégle yi jëm ci suñu mbooloo.
15 min : Li nekk soxla ci mbooloo mi.
20 min : Li yenn waaraatekat yu bokk ci suñu mbooloo def ci liggéeyu waare bi. Waxal ñi teew ñu nettali lu neex li ñu def bi ñu doon wone téere bu bees bu ndaw bi. Bala ndaje bi di jot, waxal yenn waaraatekat ñu waajal seen bopp ngir ñów ci kanamu ñépp te wone lu baax li ñu def ci liggéeyu waare bi. Su dee téere bu ndaw bu bees bi mu ngi waaj a jeex ci mbooloo mi, nañu wax waaraatekat yi ñu delloo téere yi ñu joxewul ci waaraate bi.
Woy-Yàlla 78 ak ñaan bu mujj bi.
[Li ñu bind ci suuf]
a Li ngay njëkk wax warul weesu benn minit, ba pare laajal ñi teew ay laaj, te may leen ñu tontu.
b Li ngay njëkk wax warul weesu benn minit, ba pare laajal ñi teew ay laaj, te may leen ñu tontu.
c Li ngay njëkk wax warul weesu benn minit, ba pare laajal ñi teew ay laaj, te may leen ñu tontu.
d Li ngay njëkk wax warul weesu benn minit, ba pare laajal ñi teew ay laaj, te may leen ñu tontu.
e Li ngay njëkk wax warul weesu benn minit, ba pare laajal ñi teew ay laaj, te may leen ñu tontu.
f Li ngay njëkk wax warul weesu benn minit, ba pare laajal ñi teew ay laaj, te may leen ñu tontu.