Yéen njaboot yi, nangeen taxawal porogaraam bu baax
1 Ci waare bi Yeesu def ca tund ba, lii la wax : “ Waaye jëkkleena wut nguuram ak njubteem. ” (Macë 6:33). Kon, ci suñu njaboot, li ñuy def ci wàllu ngëm moo war a jiitu. Li ñu ci mën a dimbali mooy bind benn porogaraam. Jëlal tuuti minit ngir def seen porogaraamu bopp. Mën nga jël bi nekk ci xët 6. Njaboot bi yépp mën na toog te dagg wërale yu ndaw yi nekk ci suufu porogaraam boobu ngir taf ko ci. Walla bu ngeen bëggee, mën ngeen ko bind ak loxo.
2 Porogaraam bi ñuy wone ci suuf mën na leen dimbali bu ngeen di def seen porogaraam boobu. Ñeent yii di topp rekk lañu ci bind, ndaxte ñoo ëpp solo : 1) teewe ndaje yi ñu am ci mbooloo mi, 2) waaraate ak njaboot gi 3) jàng Biibël bi ak njaboot gi, ak it 4) jàng Aaya bés bi. Bu ngeen bindee loolu ci seen porogaraam, dingeen mën a “ sax noonu ci yi gëna rafet ”. (Fil. 1:10.) Am na leneen lu ñuy wax ci ñeenti fànn yooyu ci xët 4-5.
3 Du ñeent yooyu rekk nga mën a bind ci seen porogaraam. Xéyna ci seen njaboot, tàmm ngeen toog yéen ñépp ngir seet li ñu nar a waxtaane ci yenn ndaje. Nangeen bind bés yooyu itam ci seen porogaraam. Xéyna dangeen faral a liir Biibël bi bu ngeen seetee ba pare Aaya bés bi walla ci beneen waxtu. Nangeen ko bind foofu itam. Xéyna ci seen njaboot dafa faral a am ay waxtu yu ngeen di fo ak seeni doom. Loolu it, mën ngeen ko bind ci seen porogaraamu njaboot.
4 Fexeleen ba seen porogaraam baax ci li njaboot gi yépp soxla ak ci li ku nekk mën. Yenn saay nangeen ko seetaat te soppi li ngeen ci war a soppi.
[Chart on page 3]
Porogaraamu njaboot bu ngeen mën a topp
Suba Ngoon Guddi
Alt. Aaya bés bi Njàngum Biibël
bi ci njaboot gi
Tal. Aaya bés bi Njàngum téere bi
ci mbooloo mi
Àll. Aaya bés bi
Alx. Aaya bés bi Lekkoolu
sasu Nguuru Yàlla
ak ndaje bi jëm ci
liggéeyu waare bi
Àjj. Aaya bés bi
Sam. Aaya bés bi
Waaraate ak
njaboot gi
(bésu yéenekaay yi)
Dim. Aaya bés bi
Waare bu ñuy def
ngir ñépp ak
njàngum La Tour de Garde
[Chart on page 6]
Seen porogaraamu njaboot
Suba Ngoon Guddi
Alt.
Tal.
Àll.
Alx.
Àjj.
Sam.
Dim.
.................................................................
Aaya Aaya Aaya Aaya Aaya Aaya Aaya
bés bi bés bi bés bi bés bi bés bi bés bi bés bi
Waare Lekkoo- Njàngum Njàngum Waa- Liir Fo ak
bu ñuy lu sasu téere Biibël raate Biibël xale
def ngir Nguuru bi ñuy bi ak ak bi ak yi
ñépp ak Yàlla ak def ci njaboot njaboot njaboot
njàngum ndaje bi mbooloo gi gi gi
La Tour jëm ci mi
de Garde liggéeyu
waare bi