Ndax mën nga defaraat sa porogaraamu waare ?
1 Ñun ñii nekk ay karceen dëgg, ñun ñoo bëgg nekk ay “ nappkati nit ”. (Macë 4:19.) Ni ko nappkat yi di defe, ñun ñi nekk ay nappkati nit, bu ñu bëggee suñu liggéeyu waare bi gën a am njariñ, dañu war a waaraate ci waxtu yu ñu mën a fekk nit ñi seen kër. Ci weer yii di ñëw, ci réew yu bare, bëccëg bi dina gën a yàgg. Ci ngoon bala muy guddi, nit ñu gën a bare ñu ngi seen kër. Ñu ci bare dañuy gën a féex te gën a mën a nangu ay gan seetsi leen. Ndax mën nga defaraat sa porogaraam ngir mën a waaraate ci waxtu yooyu ? — 1 Kor. 9:23.
2 Waaraate ci ngoon bala muy guddi : Bu ñu jàppee ay bés ngir waaraate ci ngoon bala muy guddi, dinañu mën a xamal nit ñu gën a bare xibaar bu baax bi (Léeb. 21:5). Ndaw yi mën nañu waare bu ñu wàccee lekkool. Ñeneen ñi mën nañu ko def bu ñu wàccee liggéey. Am na ñu bokk njàngum téere ñuy fexe ba waaraate benn waxtu bala njàngum téere bi di jot.
3 Bu ñu waaraatee këroo-kër ci ngoon bala muy komaasee guddi, dinañu mën a wax ak nit ñoo xam ne duñu leen faral a fekk seen kër. Ci ay goxu mbooloo yu bare, am na ay mbedd walla ay béréb yoo xam ne nit ñi dañu fa bare te mën nañu waaraate foofu ci ngoon bala muy guddi. Ñu bare dañu wax ne waxtu yooyu ñoo gën ngir dellu seeti nit ñi suñu waxtaan neex walla ngir komaase ay njàngum Biibël.
4 Nañu seet bu baax ni ñu koy defe : Bu ñuy waaraate ci ngoon, dañu war a seet bu baax li ñu mën a def ak li ñu warul a def. Ci lu bare, li gën mooy waar nit ñi bala muy komaasee guddi. Loolu moo gën dem fëgg seen buntu kër fekk dañu bëgg dem tëddi (Fil. 4:5). Boo fëggee ci buntu kër, nanga taxaw fu ñu la mën a gise bu baax, te wax ci lu leer yow yaay kan. Nanga gaaw a wax it li la indi. Boo ñëwee ci kër, mën nga fekk nit di reer walla nga gis leneen lu lay won ne waxtu bi nga ñëw gënul. Bu boobaa nanga leen wax ne dinga jaaraat beneen yoon. Ak loo mënta def, nanga may cér nit ñi. — Macë 7:12.
5 War nañu seet bu baax it li ñu mën a lor. Booy waare buy waaj a guddi, walla bu guddee ba pare, li gën mooy nga ànd ak keneen, walla ngeen gurupoo. Nanga dem ci mbedd yu leer yi te bañ a wéet. Nanga waare ci béréb yoo xam ne boo fa nekkee sa xel dina dal. Bul dem ci béréb yu wóorul ci guddi. — Léeb. 22:3.
6 Bu ñu waaraatee ci ngoon dinañu mën a waare ak pioñee yiy jàpple ak it pioñee yi ci sax (Room 1:12). Ndax mën nga defaraat sa porogaraam ngir mën a waare ci ngoon bala muy guddi ?
[Laaj yi]
1. Lu tax ñu war a nangu defaraat suñu porogaraamu waare ?
2. Lu ñu mën a def ngir waar nit ñu gën a bare ci xibaar bu baax bi ?
3. Naka ngeen mën a waaree ci ngoon bala muy komaasee guddi ci seen goxu mbooloo?
4. Bu ñuy waaraate ci ngoon, lu tax ñu war a seet bu baax li ñuy def, te may cér nit ñi ?
5. Bu ñuy waaraate ci ngoon, naka lañu mënee moytu lu ñu mën a lor ?
6. Am na beneen njariñ bu nekk ci waaraate ci ngoon. Boobu ban la ?