Seen porogaraamu njaboot ngir teewe ndaje yi ñu am ci mbooloo mi
1 Boo nekkee karceen bu am ay doom, danga bëgg ñu bëgg Yexowa te jaamu ko. Danga bëgg itam bu ëllëgee ñu am dund gu dul jeex ci àddina su bees si Yàlla dige. Lan nga mën a def ba jaamu Yexowa nekk lu ëpp solo ci seen dund ? Lu am solo lool mooy li ngay def, yow mii ci sa bopp (Léeb. 20:7). Lii la suñu benn mbokk ci ngëm bu jigéen wax lu jëm ci yaayam bu nekkoon Seede : “ Xamoon nañu ne dinañu dem ndaje yi. Loolu moom, amul woon benn werante. ” Loolu, ba léegi fàttewu ko.
2 Ndax sa njaboot xam na bu baax lu waral ñu am ay ndaje ci mbooloo mi ? Li ñu fay jàng dafa ñuy xiir ci kontine di def li Yàlla bëgg. Te itam, booloo ak suñuy mbokk ci ngëm dafa ñuy may doole ci wàllu ngëm (Isa. 54:13 ; Room 1:11, 12). Waaye li gën a tax ñu am ndaje yooyu mooy màggal Yexowa (Sab. 26:12). Ci ndaje karceen yi, mën nañu wone suñu mbëggeel ci Yexowa te jaamu ko.
3 Nañu sàmm suñu dundin : Teewe suñuy ndaje bokk na ci li ñuy def ngir jaamu Yàlla. Bu ñu ko fonkee, dinañu sàmm bu baax suñu dundin te duñu dem ba tàmm bàyyi lu amul solo noonu tere ñu teewe suñuy ndaje (Efes 5:15, 16 ; Yaw. 10:24, 25). Kon, bu ngeen di def seen porogaraamu njaboot, mën ngeen ci njëkk bind bés ak waxtu yi ngeen di teewe ndaje yi. Te buleen bàyyi dara tere leen topp porogaraam boobu. Na teewaay boobu bokk ci li ëpp solo ci seen njaboot.
4 Lée-lée ñu dégg li yenn ci suñuy mbokk def ci wàll boobu. Dañuy jaar ci lu mettee metti ngir mën a teewe ndaje yi ci mbooloo mi walla suñu ndaje yu gën a mag yi. Ndax loolu laalul suñu xol ? Xéyna waruloo jaar ci lu metti noonu ngir mën a teewe ndaje yi. Waaye ba tey loolu mën na bañ a yomb ci yow itam. Seytaane mu ngi def lépp li mu mën ngir mbootaayu Yàlla bañ a jaamu Yexowa. Waaye nanga def lépp ngir njaboot gi yépp teewe ndaje yi ñu am ci mbooloo mi. Na la wóor ne say doom dinañu gis loolu. Ci dëgg, boo defee loolu, say doom duñu fàtte mukk li nga leen may noonu ci wàllu ngëm.