Seen porogaraamu njaboot ngir waaraate
1 Yexowa, bu gisee xale yu ndaw yuy màggal turam, dafay bég lool (Sab. 148:12, 13). Ci jamano Yeesu ay “ perantal ak ñiy nàmp ” sax dañu doon màggal Yàlla (Macë 21:15, 16). Loolu moo am tey itam. Yéen, waajur yi, lan ngeen mën a def ba dimbali seeni doom ñu sawar ci màggal Yexowa ci waaraate bi ? Lu ci am solo lool mooy li ngeen di def, yéen waajur yi. Moom lañu waxoon itam ci xaaj bi doon wax ci porogaraamu teewe ndaje yi. Li ëpp ci waajur yi dinañu dàkkoor ak li benn baay wax. Dafa ne : “ Xale yi duñu topp li ngay wax. Li ngay def lañuy topp. ”
2 Suñu benn mbokk ci ngëm bu jigéen dafa amoon waajur yu gëm Yàlla. Nee na : “ Bu ñu doon yeewu samdi, masuñu laaj suñu bopp ndax dinañu dem waaraate walla déet. Xamoon nañu ne dinañu ko def. ” Yéen it, nangeen won seeni doom ne liggéeyu waare bi, lu am solo la. Li leen ci mën a dimbali mooy porogaraam bu seen njaboot war a topp ngir ànd ci waaraate bi ayu-bés bu nekk. Te seeni doom, bu ñu leen gisee ngeen di waaraate noonu, dinañu leen mën a roy. Te it dingeen mën a xool jikko yi ñuy wone ci waaraate bi ak li ñu mën ci liggéey boobu.
3 Nangeen leen jàngal ndànk-ndànk : Bala waaraate bi neex ci xale yi, fàww ñu xam li ñu mën a def ngir bokk ci. Suñu mbokk bu jigéen bu doon wax ci xise 2, nee na itam lii : “ Nekkuñu woon di topp rekk suñu waajur yi ci seen waaraate. Déedéet ! Xamoon nañu ne, ñun itam, dinañu ci am wàll. Lée-lée dañu doon fëgg rekk ci bunt bi walla dañu doon bàyyi benn kayit bu ndaw. Ayu-bés bu nekk dañu doon waajal bu baax suñu waaraate. Loolu moo tax ñu xamoon li ñu fa naroon a wax. ” Yéen it mën ngeen def loolu. Ayu-bés bu nekk, nangeen jël tuuti minit ngir waajal waaraate bi ak seeni doom. Mën ngeen def loolu bu ngeen amee seen njàngum Biibël ci njaboot gi walla ci beneen waxtu.
4 Boo àndee noonu ak sa njaboot ci waaraate bi, dinga mën a dugal dëgg gi ci sa xolu doom yi. Am na karceen bu faraloon a dox 10 kilomet ngir dem joxe ay kayit yu ndaw ci beneen dëkk. Waaye bu doon dem, dafa doon yóbbaale doomam bu jigéen. Jigéen jooju, ba léegi fàttewul loolu. Nee na : “ Bi ñu doon dem noonu di dox ci yoon bi, foofa la sama Pàppa doon dugal ndànk-ndànk dëgg gi ci sama xol. ” (2 Mu. 6:7). Yéen it dingeen mën a am barke boobu bu ngeen boolee waaraate bi ci seen porogaraamu njaboot ayu-bés bu nekk.