Seen porogaraamu njaboot ngir jàng Aaya bés bi
1 Bés bu nekk, waajur yi ñu ngi def lépp li ñu mën ngir seeni doom am lekk bu neex te doy. Waaye li ëpp solo mooy fexe ñu lekk bu baax ci wàllu ngëm, maanaam jot ci li nekk ci Kàddu Yàlla (Macë 4:4). Danga bëgg dimbali say doom ñu xam ne soxla nañu lekk ci wàllu ngëm te “ màgg ci biir muccu Yàlla ”. (1 Pie. 2:2.) Loolu dinga ko mën a def boo faralee jàng ak sa njaboot Aaya bés bi ak kàddu yi ci ànd. Kañ ngeen ko mën a def ?
2 Bu ngeen di ndékki, añ walla reer : Bu ngeen tàmbalee bés bu nekk ak benn waxtaan ci Aaya bés bi, loolu dina tax ngeen mën a xalaat Yexowa bés bi yépp (Sab. 16:8). Am na benn yaay bu fas yéenee jàng Aaya bés bi, bi doomam doon ndékki. Te dafa doon ñaan Yàlla bala xale bi dem jàngi. Loolu dafa doon may xale bi doole ngir bu demee lekkool mu bañ a def lu neexul Yàlla ci wàllu fonk sa réew ba mu ëpp walla ci wàllu diggante góor ak jigéen. Te it dafa ko doon may fitu waar moroomam yi ak jàngalekat yi. Moom rekk moo nekkoon Seede ci lekkool bi, waaye loolu masu ko sonal.
3 Xéyna jàng Aaya bés bi ci suba si, yombul ci yéen. Kon, mën ngeen ko def ci beneen waxtu, xéyna bu ngeen di reer. Am na ñu ci boole waxtaan ci li ñu def ci waaraate bi walla wax lu neex li ñu sog a jàng ci Biibël bi ci seen porogaraamu bopp. Ñu bare ñi doon def loolu, wax nañu ne waxtu reer yooyu ñoo nekkoon waxtu yu gënoon a neex ci kër gi.
4 Bu guddi jotee : Am na ay njaboot yuy jàng Aaya bés bi bala ñuy tëddi. Dañu ne waxtu boobu mooy waxtu bi gën ci ñoom. Mën na nekk it waxtu bu baax ngir njaboot gi yépp ànd di ñaan Yàlla. Bu leen seeni doom déggee bés bu nekk ngeen di wax ci Yexowa te ñaan ko, ci ñoom, Yexowa dina mujj a mel ni kenn ku ñu mën a gis.
5 Nangeen jëfandikoo bu baax Examinons les Écritures chaque jour. Dina leen dimbali ngeen mën a dugal ndànk-ndànk dëgg gi ci seen xolu doom yi. Yàlla na Yexowa barkeel li ngeen di jéem a def noonu.