Seen porogaraamu njaboot ngir jàng Biibël bi
Yow mii nekk waajur, ci lépp li nga mën a may say doom, mbëggeel bi nga am ci Yexowa moo gën a am maanaa. Am na lu la ci mën a dimbali bu baax, moo di toog ak sa njaboot ayu-bés bu nekk te jàng Biibël bi (5 Mu. 6:5-7). Xéyna, sa jëkkër walla sa jabar, Seede Yexowa la moom itam. Waaye xéyna it, nekkul Seede. Mën na am itam yow kenn yaa yore say doom. Ba tey, mën nga dimbali say doom ñu gën laa jege te gën a jege Yexowa itam. Loolu dina mën a am boo faralee jàng Biibël bi ak sa njaboot yépp.
2 Nanga komaase di jàng Biibël bi ak sa njaboot : Li nga njëkk war a def mooy jàpp bés bu ngeen di jàng Biibël bi, yow ak sa njaboot. Boo xamul kañ la loolu mën a ame, mën ngeen ci waxtaan yéen ñépp (Léeb. 15:22). Boo yoree xale bu ndaw-a-ndaw, xéyna li gën mooy nga wàññi li ngeen di jàng, def ko mu nekk ay njàng yu gàtt te jàpp yeneen bés ci ayu-bés bi ngir mottali ko. Seetal porogaraam bi gën a baax ci sa njaboot. Nangeen jàpp bés ak waxtu bu ngeen di def seen njàngum Biibël ci seen njaboot te fexeleen ba dara bañ leen a teree topp bu baax porogaraam boobu.
3 Lan ngeen mën a jàng ? Am na ñuy waajal Njàngum téere bi ñuy def ci mbooloo mi walla Njàngum La Tour de Garde bi. Am na ñeneen ñuy waxtaan ci téere yu ñu defaral ndaw yi. Benn baay bu am ñaari xale yu ndaw, bu góor ak bu jigéen, nee na : “ Am na lu ñuy def bu ñu amee suñu njàngum Biibël bi ci njaboot gi, te loolu neex na xale yi lool. Dañuy jël ay nettali yu nekk ci Recueil d’histoires bibliques, def ko mu mel ni tiyaatar. Loolu tax na ñu mokkal nettali yooyu. Wax dëgg, loolu moo gën jàng xise yu bare. ”
4 Nangeen ko def ayu bés bu nekk : War ngeen faral a am seen njàngum Biibël ak njaboot gi yépp. Te ñépp a ko war a yàkkamti. Dëgg la, léeg-léeg dina am lu leen di bett ba dingeen ko war a def beneen bés walla beneen waxtu. Léeg-léeg it dingeen war a soppi li ngeen di waxtaane. Waaye soppi yooyu waruñu bare ba ngeen mujj a bañ a topp seen porogaraam. Benn xale bu jigéen nee na : “ Bu ñu waree soppi waxtu njàng mi, du ñàkk suñu Pàppa bind ko ci buntu firisideer bi. Su ko defee ñépp a koy gis. ” Ci dëgg, fexe ba bañ a ñàkk benn njàngum Biibël bi ci njaboot gi, lu baax te rafet la. Bu ngeen di yar seeni doom “ di leen yemale ak a yee ci boroom bi ”, noonu ngeen di wonee ne dangeen leen bëgg, bëgg it suñu Baay bi nekk ci asamaan. — Efes 6:4.