TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Watchtower
TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Wolof
  • BIBLE
  • TÉERE YI
  • RÉUNIONS
  • km 7/05 p. 2
  • Ndaje yi jëm ci liggéeyu waare bi

Aucune vidéo n'est disponible pour cette sélection.

Il y a eu un problème lors du chargement de la vidéo.

  • Ndaje yi jëm ci liggéeyu waare bi
  • Sasu Nguuru Yàlla — 2005
  • Turu xaaj yi
  • 11-17 sulyet
  • 18-24 sulyet
  • 25-31 sulyet
  • 1-7 ut
Sasu Nguuru Yàlla — 2005
km 7/05 p. 2

Ndaje yi jëm ci liggéeyu waare bi

11-17 sulyet

Woy-Yàlla 32

10 min : Yégle yi jëm ci suñu mbooloo. Yenn ci yégle yi nekk ci Sasu Nguuru Yàlla. Na ñaari nit wone ci kanamu ñépp ni ñu mënee wone Réveillez-vous ! bu 8 sulyet ak La Tour de Garde bu 15 sulyet. Nañu topp li nekk ci xët 4, walla ñu wax leneen lu mën a baax ci seen gox. Ku ci nekk na wone li ñu mën a tontu bu amee ku ñu wax : “ Dama jàpp. ” (Seetal li nekk ci téere Comment raisonner, xët 19 ak 20, “ Je suis occupé ”.) Ci lu gàtt waxal li ëpp solo ci xaaj bi tudd “ Yéen ñi bëgg waare ci gox fu ñu dul waare lu bare : li ngeen warul a fàtte. ” Li nekk ci xaaj boobu, ci leetar bu 25 awril 2005 lañu ko jële. Leetar boobu, yónnee nañu ko mbooloo yi yépp.

15 min : Ndax sa njaboot taxawal na benn porogaraam ? Waxaatal li nekk ci Sasu Nguuru Yàlla bu me 2005 ci xët 3 ba 6. Waxal ñi teew ñu wax li ñu def ngir topp li nekk ci xët yooyu ak li ñu ci jële.

20 min : “ Ndax boo gisee rekk dangay jëf ? ”a Waxal ni ngeen mënee topp ci seen mbooloo li nekk ci xaaj bii.

Woy-Yàlla 46 ak ñaan bu mujj bi.

18-24 sulyet

Woy-Yàlla 67

10 min : Yégle yi jëm ci suñu mbooloo. Ci lu gàtt, waxal li nekk ci La Tour de Garde bu 15 ut 2000, xët 32. Am porogaraam ngir jàng Biibël bi bés bu nekk, lu baax la. Bu ñu nekkee ci jamano noppalu sax, war nañu ko def. War nañu ko def it bu ñu nekkee ci lu bees. Waxal ban njariñ lañu ciy jële.

20 min : “ Nañu dimbali ñi ñuy jàngal Biibël bi ñu topp li ñuy jàng — Xaaj 11. ”b Na am ñuy wone ni benn waaraatekat wonee ki muy jàngal Biibël bi, ni ñuy delloo seeti nit ku suñu waxtaan neex. Dañuy seetaat li ñu waxoon bi ñu njëkkee wax ak nit kooku. Ba pare ñu tànn li ñuy wax bu ñu fa dellusee. Nañu seet lu yomb lu ñuy njëkk wax bu ñu àggee, ak benn laaj bu ñu mën a laajte bala ñuy dem. Bu ñu defee loolu lépp ba pare, nañu def mel ni ñu bëgg toppaat li ñu waajal noonu. Foofu la li ñuy wone ci kanamu ñépp war a jeexe.

15 min : Li nekk soxla ci mbooloo mi.

Woy-Yàlla 34 ak ñaan bu mujj bi.

25-31 sulyet

Woy-Yàlla 58

15 min : Yégle yi jëm ci suñu mbooloo. Waxal fu ñu tollu ci xaalisu mbooloo mi te jàngal kayit biy wone ne bànqaas bi jot na xaalis bi ñu maye. Na ñaari nit wone ci kanamu ñépp ni ñu mënee wone Réveillez-vous ! bu 22 sulyet ak La Tour de Garde bu 1 ut. Nañu topp li nekk ci xët 4, walla ñu wax leneen lu mën a baax ci seen gox. Na kenn ki def mel ni mu ngiy wone yéenekaay yi ci màrse walla feneen fu bare nit, fekk dafa ci am bunt.

10 min : Nangeen dugal dëgg gi ci seen xolu doom (5 Mu. 6:⁠7). Waare lay doon. Benn magu mbooloo moo koy def. Na ko jële ci li nekk ci La Tour de Garde bu 15 ut 2002, xët 30 ak 31. Yenn saay mu am karceen boo xam ne ki muy séyal nekkul Seede. Waxal li Biibël bi wax ci ni wayjur bu mel noonu mënee yar doomam.

20 min : “ Bor bu ñu ameel nit ñi.”c Boole ci li nekk ci La Tour de Garde bu 1 sulyet 2000, xët 11, xise 13.

Woy-Yàlla 37 ak ñaan bu mujj bi.

1-7 ut

Woy-Yàlla 83

15 min : Yégle yi jëm ci suñu mbooloo. Waxal waaraatekat yi ñu bañ a fàttee bind li ñu def ci liggéeyu waare bi ci weeru sulyet te joxe ko. Waxal ñi teew ñu ubbi seen téere École du ministère ci xët 70. Nangeen waxtaan ci xise 1 ak 2 ak ci wërale bi tudd  “ Comment répondre lors des réunions ? ” ci xët boobu.

15 min : “ Dimbalil say doom ñu mën waaraate. ” Waare ak waxtaan ak ñi teew. Na am benn baay (walla benn yaay) ak doomam yuy topp lu yomb li ñu mën a wax ci waaraate bi. Bala ñuy jeexal waxtaan bi, na wayjur bi wax nit ki li mu mën a def bu bëggee jàpple suñu liggéey.

15 min : Ndax yaa ngi jéem a waxtaan ak nit ku nekk ci li ko itteel ? Waare ak waxtaan ak ñi teew bu ñu jële ci Sasu Nguuru Yàlla bu sãwiyee 2005, xët 6. Waxleen ci li nekk ci xaaj boobu. Waxleen ni ñu ko mënee topp ak téere yi ñuy wone ci weeru ut. Na am ñu wone ci kanamu ñépp benn walla ñaari fasoŋ yi ñu ko mënee def.

Woy-Yàlla 98 ak ñaan bu mujj bi.

[Li ñu bind ci suuf]

a Li ngay njëkk wax warul weesu benn minit, ba pare laajal ñi teew ay laaj, te may leen ñu tontu.

b Li ngay njëkk wax warul weesu benn minit, ba pare laajal ñi teew ay laaj, te may leen ñu tontu.

c Li ngay njëkk wax warul weesu benn minit, ba pare laajal ñi teew ay laaj, te may leen ñu tontu.

    Téere yi ci Wolof (1996-2025)
    Ngir génn
    Ngir konektewu
    • Wolof
    • Yónnee ko
    • Ni nga bëgge mbir yi feeñe
    • Copyright © 2025 Watch Tower Bible and Tract Society of Pennsylvania
    • Conditions d’utilisation
    • Règles de confidentialité
    • Paramètres de confidentialité
    • JW.ORG
    • Ngir konektewu
    Partager