Xaaj 11 : Nañu dimbali ñi ñuy jàngal Biibël bi ñu topp li ñuy jàng
Nañu leen won ni ñuy delloo seeti nit ñi
1 Ku komaasee bokk ci liggéeyu waare bi, dina daje ak ñu bëgg déglu xibaar bu baax bi. Naka lañu ko mënee dimbali mu aay ci dellu seeti ñi suñu waxtaan neex ?
2 Nee ko ci waxtaan bu njëkk bi lañu war a waajal li ñuy waxtaane beneen yoon bu ñu dellusee. Waxal kiy jàng Biibël bi ne dafa war a toppatoo bu baax nit ki muy waxtaanal (Fil. 2:4). Won ko ndànk-ndànk li mu mën a def ngir nit ki wax li mu xalaat. Won ko it ni mu waree déglu nit ki ak li mu mën a seet ci nit ki ngir gën koo xam. Bu amee ku suñu waxtaan neex, na kiy jàng Biibël bi bind li am solo ci seen waxtaan ak ci li ñu gis ci nit ki. Seetleen ci li mu bind noonu, ngir dimbali ko mu xam ci lan la mën a waxtaan bés bu ngeen fa delloo.
3 Waajalleen li ngeen war a wax bu ngeen di dellu seeti nit : Seetaatleen li ngeen waxtaane bi ngeen fa njëkkee dem. Te wonal kiy jàng Biibël bi ni mu mënee tànn ci xibaaru Nguur gi benn ponk bu mën a neex nit ki (1 Kor. 9:19-23). Waajalleen li mu nar a wax nit ki. Booleleen ci ñaar yii : benn aaya ak benn xise ci téere fu ñuy jàngale Biibël bi. Nangeen waajal it benn laaj bu ngeen mën a laaj nit ki bu ngeen di jeexal waxtaan bi ngir mën a kontine waxtaan bi beneen yoon. Saa yu waaraatekat bu bees bi demee seeti nit, dafa war a am lenn lu bees lu mu koy jàngal ci Kàddu Yàlla. Won ko ni mu ko mënee def.
4 Fexeel ba waaraatekat bu bees bi, xam lu yomb lu mu mën a wax ngir tàmbali waxtaan bi bu delloo seeti nit. Loolu dina baax lool. Bu nuyoo ba pare, mën na wax lii : “ Keroog waxtaan nañu bu baax. Tey dama la bëgg won li Biibël bi wax ci [waxal li nga bëgg, ngeen waxtaan ci]. ” Mën nga won waaraatekat bu bees bi it li mu mën a def bu fekkee ne keneen moo ko ubbil bunt bi.
5 Buñu yéex ci dellu seeti nit : Waxal kiy jàng Biibël bi mu gaaw a dellu seeti képp ku suñu waxtaan neex. Wax ko nag ne yenn saay, loolu du yomb. Lée-lée dina war a jaar këram ay yoon yu bare, bala mu koy mën a gis. Wax ko li mu mën a wax nit ki bu bëggee jàpp ak moom bés ngir kontine waxtaan bi. Won ko it lu tax dellu seeti nit ki ci bés bi ñu jàpp am solo lool (Macë 5:37). Bu ñuy waaraate, dañuy wut ñi mën a bokk ci ñiy jaamu Yexowa, ba pare delluwaat seeti leen ngir gën a waxtaan ak ñoom. Bu ñuy def loolu, dañu war a baax, lewet te may nit ñi cér. Dimbalil waaraatekat bu bees bi ngir mu wone jikko yooyu ci waaraate bi. — Titt 3:2.