Nañu fàttaliku li ñu jàng ci lekkoolu sasu Nguuru Yàlla
Dinañu jéem a tontu laaj yii di topp, ci Lekkoolu sasu Nguuru Yàlla bi ñuy am diggante 29 ut ba 4 septaambar 2005. Ci lu mat 30 minit, wottukatu lekkool bi dina waxtaan ak ñi teew ngir fàttaliku li ñu jàng ci lekkool bi diggante 4 sulyet ba 4 septaambar 2005. [Buleen fàtte lii : Bu amee laaj boo xam ne binduñu fi ngeen war a jàng tont bi, yéen a war a wutal seen bopp tont bi. — Seetleen li ñu wax ci téere École du ministère, xët 36-37.]
LIY TAX ÑU AAY CI WAX
1. Bu ñuy waare, naka lañu mënee fexe ba suñu “ lewet leer ñépp ”, maanaam ñépp gis ne dañu lewet ? Lu tax loolu am solo ? (Fil. 4:5 ; Saak 3:17) [be p. 251 § 1-3 ak wërale bi]
2. Lu tax maslaa baax ci suñu diggante ak suñu moroom ? [be p. 253 § 1-2]
3. Bu ñu bëggee nit ki xalaat bu baax ci li ñu koy jàngal, lu tax ñu war a xam bu baax fasoŋu laaj yi ñu ko war a laaj ? [be p. 253 § 3-4]
4. Lan lañu war a def bu ñu bëggee ñi nuy déglu gëm li ñuy wax ? [be p. 255 § 1-4 ak wërale bi ; p. 256 § 1 ak wërale bi]
5. Yenn saay dañuy bëgg jaar ci yeneen téere ngir wone ne li Biibël bi wax mooy dëgg. Bu ñuy def loolu, lan lañu warul a fàtte ? [be p. 256 § 3-5 ak wërale bi]
WAXTAAN N° 1
6. Lan moo ñuy won ne Yeesu mas na dund ci kow suuf ? [w03 15/6 p. 4-7]
7. Lu tax ñu wax ne “ gémmiñu nit ñu jub ñi ” dina leen musal ? Lu tax ñu wax it ne “ këru nit ñu jub ñi ” du daanu ? (Léeb. 12:6, 7) [w03 15/1 p. 30 § 1-3]
8. Ndegam Biibël bi waxul lépp li ñu war a def ak lépp li ñu warul a def, naka lañu mënee xam ‘ liy coobareg Boroom bi ’ ? (Efes 5:17) [w03 1/12 p. 21 § 2-p. 22 § 3]
9. Am na ñu néew doole, walla ñu am poroblemu xaalis. Yan ndigal yu nekk ci Biibël bi ñoo leen ci mën a dimbali ? [w03 1/8 p.5 § 3-6]
10. Yexowa ku nangu maye la. Loolu lu mu war a def ci ñun ? (Macë 10:8) [w03 1/8 p. 20-22]
LI ÑU WAROON A JÀNG CI BIIBËL BI AYU-BÉS BU NEKK
11. Ci buntu kër Yàlla bi Suleymaan tabaxoon, amoon na ñaari poto yu tuddoon Yakin ak Bowas. Loolu lu mu doon tekki ? (1 Bu. 7:15-22)
12. Suleymaan jëloon na 20 dëkk ca Galile, may leen buuru Tiir bi tuddoon Iram. Loolu ndax ànd na ak li Sàrtu Musaa waxoon ? (1 Bu. 9:10-13)
13. Am na “ nitu Yàlla ” bu defoon li Yàlla tere. Lan lañu mën a jàngee ci loolu ? (1 Bu. 13:1-25)
14. Naka la buur bi Asa wonee ne ku am fit lawoon ? Lan lañu mën a jànge ci loolu ? (1 Bu. 15:11-13)
15. Yenn saay ñu am lu ñu naqadi. Waaye topp di ci xalaat rekk, walla di ko jooytu rekk, mën na indi musiba. Li xew diggante Akab ak Nabott, naka la ko wonee ? (1 Bu. 21:1-16)