Ndax yaa ngi jëfandikoo kayit yi ñuy joxe ngir woo nit ñi ci suñu ndaje yi ?
Am na benn xale bu 11 at bu for benn bés, benn kayit fu ñu doon woo nit ñi ci suñu ndaje yi. Kayit boobu dafa doon wax ci benn waxtaan bu ñu naroon a def ci lu jëm ci safara. Ginnaaw loolu xale boobu dafa nee : “ Dama bëggoon a xam li ñu ci nar a wax ndaxte dafa meloon ni man, du ma def dara lu baax. Moo tax ma ragaloon a dem safara bés bu ma deewee. ” Xale boobu dem na teewe ndaje boobu. Mu komaasee jàng Biibël bi. Benn at ginnaaw bi mu teewee ndaje boobu, ñu sóob ko ci ndox. Noonu la Karl Klein komaasee bokk ci liggéeyu waare bi. Bi mu demee ba mu yàgg, mujj na bokk ci Jataay biy Dogal ci Seede Yexowa yi te yàgg na ci. Loolu lépp ci lan la komaase ? Ci kayit bu ñuy jëfandikoo ngir woo nit ñi ci suñu ndaje yi.
Ba tey jii, kayit yooyu baax nañu lool ci waaraate bi. Ay waaraatekat yu bare gis nañu ne bu ñu ko joxee ngir komaasee waxtaan ak nit, dafay baax. Wayjur yi bëgg seeni doom bokk ci liggéeyu waare bi, mën nañu leen wax ñu joxe ko ci waaraate bi. Kuy bind leetar ngir waare, mën na ko ci boole it ngir nit ñi xam kañ lañuy daje. Mën nañu ko jox it ñi ñuy jàngal Biibël bi ak ñi suñu waxtaan neex ngir ñu ñów teewe suñu ndaje yi.
Ci kayit boobu wax nañu ci lu gàtt li ñuy def ci ndaje bu nekk. Waaye léegi, dootuñu fa bindati adareesu Saalu Nguur gi, ak waxtu yi ñuy defe ndaje yi. Yow yaa ko war a xamal ki ngay jox kayit boobu. Dina am foo ko mën a bind ci kayit bi. Ndax yaa ngi jëfandikoo bu baax kayit boobu ci liggéeyu waare bi ?