Tey, waxtu waare jot na !
1 “ Ragalleen Yàlla te jox ko ndam li. ” Loolu lañuy yégal “ xeet yépp, giir yépp, kàllaama yépp ak réew yépp ”. Liggéey boobu, ay malaaka ñoo koy jiite. Lu tax ñuy yégal nit ñi loolu ? Ndaxte waxtu àtte Yàlla jot na. Tey, ñu ngi ci waxtu àtte boobu. Waxtu àtte boobu dina jeex ci bés bu ñuy alag àddina sii. Am na lu am solo li waa àddina si war a def. Mooy ‘ jaamu ki sàkk asamaan ak suuf, géej gi ak bëti ndox yi ”. Liggéeyu waare “ xebaar bi sax ”, amul beneen liggéey bu ko ëpp solo, te gën ko jamp. Waaw, tey waxtu waare jot na ! — Peeñ. 14:6, 7.
2 Ci fukki at yii weesu, ñiy jaamu Yexowa waare nañu xibaaru Nguur gi, te sàkk ay taalibe ci lu jege 12 milioŋi milioŋi waxtu. Ñu bare dañu soppi ni ñu doon dunde ngir mën a gën a bokk ci ngóob bi ñuy def ci wàllu ngëm (Macë 9:37, 38). Bu ñu jëlee pioñee yi amoon daaw ci àddina si sépp, dafa mel ni weer wu nekk, lu ëpp 850 000 waaraatekat ñoo nekkoon pioñee. Ñi nekk pioñee bu ci sax, 70 waxtu lañu war a waare weer wu nekk. Pioñee yuy jàpple yi ñoom, 50 waxtu lañu war a waare weer wu nekk.
3 Lan lañu soxla ngir mën a nekk pioñee : Komka dañu xam ne “ diir bu gàtt rekk a fi des ”, pioñee yi dañuy góor-góorlu ngir yombalal seen dund (1 Kor. 7:29, 31). Dañuy seet ni ñu mënee wàññi xaalis bi ñuy jaay. Bu ko defee, ñu mën a wàññi li ñu war a liggéey ngir am li ñu soxla ci seen dund. Am na ñu toxu ci kër bu gën a ndaw. Ñeneen ñi dañu tàggoo ak alal joo xam ne soxlawuñu ko woon dëgg (Macë 6:19-21). Ñu ci bare, wàññi nañu it li ñu bëggoon a am ci àddina. Loolu lépp dañu ko def ndaxte dañu bëggoon a gën a def seen jot ak seen xel ci waaraate bi (Efes 5:15, 16). Waaraatekat yu bare dañu kontine di wut pexe ngir nekk pioñee. Nangu nañu it ñàkk yenn yi ngir mën koo nekk. Te it dañu wéeru ci Yexowa di ko ñaan ngir mu jàpple leen ci. Loolu lépp a tax ñu ci bare mujj mën a def porogaraam bu baax, bu leen may ñu nekk pioñee.
4 Ndax mën nga nekk pioñee ? Ndax mënuloo laaj ñi fexe ba nekk pioñee, li ñu def ba mën ko ? Àndal ak ñoom ci waaraate bi. Dinga gis mbégte yi ñuy am ci liggéey boobu. Jàngal li suñu téere yi wax ci liggéeyu pioñee bi. Am na yoo xam ne boo ko defee, dinga mën a nekk pioñee. Nanga ko jéem a def, te góor-góorlu ci. Fi mu nee nii, bu amee loo xam ne dafa lay tere nekk pioñee, wax ko Yexowa. Ñaan ko mu won la loo mën a def ba loolu mën a deñ. — Léeb. 16:3.
5 Barke ak mbégte yi nga ci mën a jële : Liggéeyu pioñee bi dafay tax ñu gën a aay ci jëfandikoo Biibël bi. Loolu dafay yokk suñu mbégte. Suñu benn mbokk pioñee bu nekk ndaw nee na : “ Mën a faramfàcce bu baax Kàddug dëgg gi, njariñ dëgg la. Boo nekkee pioñee, dangay jëfandikoo bu baax Biibël bi. Léegi, bu may waaraate këroo-kër, xam naa ban aaya moo mën a baax ci képp ku ma dajeel. ” — 2 Tim. 2:15.
6 Liggéeyu pioñee bi dafa ñuy jàngal lu bare lu ñuy jariñ ci suñu dund. Mën na jàngal ndaw yi ñu bañ a yàq seen jot ak seen xaalis. Mën na leen jàngal it ñu déggoo ak nit ñi. Ñu bare wax nañu ne liggéeyu pioñee bi dafa tax ñu gën a jiital seen diggante ak Yexowa ci seen dund (Efes 4:13). Ci kow loolu lépp nag, pioñee yi dañuy gis ni leen Yexowa di jàpplee ak barke yi mu leen di may. — Jëf. 11:21 ; Fil. 4:11-13.
7 Xéyna, gën a jege Yexowa dina bokk ci barke yi gën a mag yi ñu mën a am bu ñu nekkee pioñee. Loolu mën na ñu dimbali ci suñuy coono. Suñu benn mbokk mu jigéen bu mas a jaar ci coono yu mettee-metti nee na : “ Ci jamano bi ma nekkee pioñee, sama diggante ak Yexowa dafa dem ba rattax lool. Diggante boobu dimbali na ma bu baax ci sama coono yépp. ” Nee na it : “ Bi ma nekkee mag ba tey, def naa sama dund yépp ci liggéeyu pioñee bi. Ni ma ci kontaane ! Tax na ba ma mën a liggéeyal Yexowa ci fasoŋ boo xam ne, masuma xalaat ne dinaa ko mën. ” (Jëf. 20:35). Liggéeyu waare bi dafa am solo lool. Yàlla nañu am barke yu réy ñun itam bu ñu ciy def lépp li ñu mën. — Léeb. 10:22.
[Laaj yi]
1. Lu tax waxtu waare jot tey ?
2. Ñiy jaamu Yexowa, naka lañu wonee ne xam nañu ne waxtu wi des bareetul ?
3. Ci lu bare, lan la waaraatekat yi war a soppi ci seen dund ngir mën a nekk pioñee ?
4. Lan nga mën a def ngir mën a nekk pioñee ?
5. Liggéeyu pioñee bi, naka la ñuy dimbalee ñu gën a aay ci waaraate bi ?
6. Lan lañuy jàng bu ñu nekkee pioñee ?
7. Liggéeyu pioñee bi lan lay def ba ñu gën a jege Yexowa ?