TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Watchtower
TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Wolof
  • BIBLE
  • TÉERE YI
  • RÉUNIONS
  • km 8/05 p. 1
  • Waare Nguur gi — Lu réy la

Aucune vidéo n'est disponible pour cette sélection.

Il y a eu un problème lors du chargement de la vidéo.

  • Waare Nguur gi — Lu réy la
  • Sasu Nguuru Yàlla — 2005
  • Leneen lu jëm ci loolu
  • Dénk nañu leen lu réy
    Sasu Nguuru Yàlla — 2007
  • Fonk nañu lool lu réy li ñu Yàlla may !
    Sasu Nguuru Yàlla — 2007
Sasu Nguuru Yàlla — 2005
km 8/05 p. 1

Waare Nguur gi — Lu réy la

1 Bés bu nekk nit ñu baree bare dañuy jot ci li leen Yexowa di may ngir ñu mën a dund (Macë 5:45). Waaye am na lu réy loo xam ne tuuti nit kese ñoo ci bokk. Waaw, tuuti nit kese ñooy waare Nguuru Yàlla, di wone noonu ne ñu ngiy gërëm Yàlla (Macë 24:14). Lu réy loolu, ndax fonk nga ko bu baax ?

2 Waare xibaaru Nguur gi, dafay màggal Yàlla (Yaw. 13:15). Te it dafay maye yaakaar te dafay indil jàmm ñi sonn lool ci àddina su jaxasoo si ñu nekk nii. Ñiy nangu déglu xibaar boobu, dinañu mën a am dund gu dul jeex (Ywna. 17:⁠3). Ban liggéey moo mën a joxe lu mel noonu ? Ndaw li Pool, dafa fonkoon liggéeyu waare bi. Wone woon na ko ci ni mu ko doon defe. Ci moom, liggéeyu waare bi, dafa meloon ni alal ju bare. — Jëf. 20:​20, 21, 24 ; 2 Kor. 4:​1, 7.

3 Lu réy loolu, nañu ko fonk bu baax : Dinañu mën a wone ne fonk nañu liggéeyu waare bi su ñu ko defee ci fasoŋ bu baax. Ndax dañuy waajal ay waxtaan yu mën a laal xolu nit ñi ? Lan lañu mën a def ngir gën a aay ci jëfandikoo ak it ci waxtaan ci Mbind mu sell mi ? Ndax ñu ngiy jéem a waare nit ñépp ci suñu goxu mbooloo ? Ndax xam nañu li ñu mën a def ngir komaase njàngum Biibël te kontine ko ? Démb ba tey, karceen yiy topp bu baax Yàlla, dañu sawar ci liggéey boobu, ndaxte dañu xam ni mu ame solo. Xam nañu it ne ku mën a bokk ci liggéey boobu am nga lu réy, moo tax ñu fonk ko lool. Ñun it, noonu lañu gise liggéey boobu moo tax ñu sawar ci lool. — Macë 25:​14-​23.

4 Xéyna dañu bare coono ndaxte dañu màgget. Walla suñu wér-gi-yaram demewul noonu. Walla dañu am yeneen coono. Waaye am na lu mën a yokk suñu doole : na ñu wóor ne am na ñu fonk ni ñuy góor-góorloo ngir bokk ci liggéeyu waare bi. Kàddu Yàlla wone na ne Yexowa fonk na lépp li nit ñu mel noonu di def ngir jaamu ko. Bu dee sax li ñuy def dafa tuuti ci bëti nit ñi, Yexowa moom fonk na ko. — Lukk 21:​1-4.

5 Waare xibaaru Nguur gi dafa ñuy may mbégte mu réy. Suñu benn mbokk mu jigéen bu am 92 at nee na : “ Su ma geestoo ba xool 80 at yi ma liggéeyal Yàlla, damay gis ne lu réy laa am. Réccuwuma ci dara ! Su ma mënoon a dellu nekkaat gune, duma soppi dara ci sama dund, ndaxte dëgg-dëgg ‘ mbaaxaayu xolu Yàlla, moo gën dund gi ci boppam ’. ” (Sab. 63:⁠3). Bokk ci liggéeyu waare Nguur gi, lu réy la. Nañu fonk bu baax li ñu Yexowa may noonu.

    Téere yi ci Wolof (1996-2025)
    Ngir génn
    Ngir konektewu
    • Wolof
    • Yónnee ko
    • Ni nga bëgge mbir yi feeñe
    • Copyright © 2025 Watch Tower Bible and Tract Society of Pennsylvania
    • Conditions d’utilisation
    • Règles de confidentialité
    • Paramètres de confidentialité
    • JW.ORG
    • Ngir konektewu
    Partager