Nañu boolloo ngir yégle ci àddina si sépp ndaje bu mag bu ñetti fan bi tudd “ Nañu roy Kirist ” Waaraatekat yi dinañu joxewaat ay kayit yu ndaw ngir yégle suñu ndaje bu ñetti fan bi
1 At mii weesu, joxe woon nañu ci àddina si sépp ay kayit yu ndaw ngir yégle ndaje bu mag bu ñetti fan bi tudd “ Mucc gi soreetul ! ”. Liggéey boobu def na lu am solo ci nit ñi suñu waxtaan neex. Am na ñu nangu kayit bu ndaw bi fekk masuñu woon a gis ndaje bu mel noonu. Dañu ñów teewe ndaje bu mag boobu nekk xew bu réy ci wàllu ngëm ci Seede Yexowa yi (Isa. 65:13). Gis nañu mbëggeel ak déggoo bi am ci diggante mbokk karceen yi. Loolu tax na ñu kontaan lool ci li ñu nekk seen biir (Sab. 133:1). Dañu bëgg dimbali nit ñi nu mën ñépp, ñu ñów teewe ndaje bu ñetti fan bi tudd “ Nañu roy Kirist ”. Kon, dinañu joxewaat ay kayit yu ndaw ci àddina si sépp ngir loolu.
2 Li ñu defoon daaw, li mu indi : Liggéey bu rafet lool la mbooloo yi nekk ci àddina si sépp def daaw bi ñu doon woo nit ñi ci ndaje bu ñetti fan bi tudd “Mucc gi soreetul ! ”. Nañu ko seete ci lii : Am na dëkk foo xam ne, bind nañu ci benn surnaal benn xaaj bu mag bu doon wax ci liggéey boobu ñu def. Surnaal boobu nee woon na lii : “ Seede Yexowa yi def nañu liggéey bu réy ngir jot nit ñépp bala ndaje bu mag bi di jot. Dañu ci jébbal jot bu gën a bare, dem fu gën a sore, te it gën a gaaw ci seen wax ”. Ci beneen dëkk, taskatu xibaar yi gis nañu ni seede Yexowa yi doon ànd ñoom ñépp ci liggéey bi ñu doon def ngir joxe kayit bu ndaw boobu ba tax ñu wax ci bu baax ci seen surnaal. Lu mu néew-néew, ñetti surnaal ñoo wax lu rafet ci li ñu doon def bala ndaje boobu jot. Benn taskatu xibaar bind na xaaj bu gudd bu doon def lu ëpp ñaari xët ci surnaalam ci bésu dimaas. Waxoon na lu jëm ci suñu ngëm, ci déggoo bi am ci suñu biir, ci liggéey bi ñu def ak kayit yu ndaw yooyu ak itam ci ndaje bu mag boobu. Benn waaraatekat dafa doon bëgg joxe kayit bi ci benn kër. Nit ki dog ko, nee ko : “ Xam naa li nga bëgg ! Léegi laa doon jàng lu ci jëm ci surnaal bi ! ” Keneen dafa ko ne : “ Maa ngi doon jàng lu jëm ci yéen rekk, ngeen ñów ! Mbaa kayit bii, sama bos la ? ” Mu teg ci, ne “ Yéen seede Yexowa yi, li ngeen di def nii, rafet na lool ”
3 Gis nañu nit ñu bare ñu suñu waxtaan neex, ñu doon ñów ci ndaje bu mag bi, yore ci seen loxo kayit bi ñu leen joxoon. Am na ñu jóge woon ci dëkk yu sore ngir teewe ndaje bi. Liggéey bu rafet boobu, bokk na ci li tax nit ñu gën a bare teewe ndaje bu mag boobu. Ci benn réew, boo seetee ñi teewoon ñépp ci ndaje bu mag boobu, dafa mel ni ci 100 nit yoo jël ci ñi teewoon ci ndaje bu ñetti fan bi ko jiitu woon, 27 nit ñoo ci yokku.
4 Ni ñu koy defe ci gox bi : Mën ngeen a komaasee joxe kayit yi ngir yégle ndaje bu mag bi, ñetti ayu bés bala bésu ndaje bu mag bi di jot. War nañu def lépp li ñu mën ngir jot fu nekk ci suñu goxu mbooloo. Ci mbooloo yi am gox bu réy lool, waaraatekat yi dinañu mën a bàyyi benn kayit ci kër yi ñu fekkul kenn ci ayu bés bi jiitu ndaje bu mag bi. Nañu ko def fi nga xam ne waa mbedd mi duñu ko mën a gis. Mbooloo yi war nañu def lépp ngir joxe kayit yu ñu leen jox yépp. Te itam war nañu góor-góorlu ngir laal fépp fi ñu mën ci seen goxu mbooloo. Bu amee kayit yu des, pioñee yi dinañu ko mën a jëfandikoo.
5 Li ñuy wax : Mën ngeen a wax lu mel ni lii : “ Ñun ak suñu waa mbooloo yépp, dañuy joxe kayit bii ngir woo nit ñi ci xew bu mag bu war a am. Bii yaa ko moom. Yeneen leeral a ngi ci kayit bi ”. Bu ñu waxee lu gàtt, dinañu mën a joxe kayit yu bare. Ba tey, bu ñu dajee ak ku am lu mu bëgg laajte, nañu taxaw ngir tontu ko. Bu ñu gisee ku suñu waxtaan neex, nañu bind turam te gaaw dellusi ngir seetsi ko.
6 Def lépp li ñu mën ngir roy Kirist am na solo lool (Ywna. 3:36) ! Suñu ndaje bu mag bu ñetti fan biy ñów, dina dimbali képp ku fa teewe ngir mu mën a def loolu. Mën na ñu wóor ne seede bu mag a mag lañuy defaat noonu bii yoon. Li koy waral mooy li ñuy ànd ñun ñépp ci yégle suñu ndaje bu mag bu ñetti fan bi tudd “ Nañu roy Kirist ”. Kon nañu sawar ci woo nit ñi nu mën ñépp ñu teewe ndaje boobu. Yàlla na Yexowa barkeel bu baax lépp li ñuy def ngir bokk ci liggéey boobu ñuy def ci àddina si sépp.