TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Watchtower
TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Wolof
  • BIBLE
  • TÉERE YI
  • RÉUNIONS
  • km 9/05 p. 2
  • Ndaje yi jëm ci liggéeyu waare bi

Aucune vidéo n'est disponible pour cette sélection.

Il y a eu un problème lors du chargement de la vidéo.

  • Ndaje yi jëm ci liggéeyu waare bi
  • Sasu Nguuru Yàlla — 2005
  • Turu xaaj yi
  • 12-18 septaambar
  • 19-25 septaambar
  • 26 septaambar ba 2 oktoobar
  • 3-9 oktoobar
Sasu Nguuru Yàlla — 2005
km 9/05 p. 2

Ndaje yi jëm ci liggéeyu waare bi

12-18 septaambar

Woy-Yàlla 35

5 min : Yégle yi jëm ci suñu mbooloo. Yenn ci yégle yi nekk ci Sasu Nguuru Yàlla.

20min : “ Ndaje bu gën a mag bi ci atum 2005 : ‘ Nañu déggal Yàlla ’. ”a Sekkerteeru mbooloo mi moo ko war a def. Waxal ñi teew ñu gaaw a seet li ñu war a def ngir teewe ndaje bu gën a mag bi.

20 min : “ Nañu dimbali ñi ñuy jàngal Biibël bi ñu topp li ñuy jàng. ”b Waxtaan ak ñi teew bu ñu jële ci xët 3, xaaj 1 ak 2. Mën ngeen seet itam li nekk ci Sasu Nguuru Yàlla bu ut 2005, ci xët 1. Lu tax nga war a waajal bu baax bépp njàngum Biibël bi nga war a def ? Loolu, naka nga koy defe ? Waxal ñi teew ñu wax naka lañu toppe li ñu wax foofu. Booy jeexal waxtaan bi, nanga wax li nekk ci wërale (encadré) bi nekk ci xët 3.

Woy-Yàlla 88 ak ñaan bu mujj bi.

19-25 septaambar

Woy-Yàlla 74

10 min : Yégle yi jëm ci suñu mbooloo. Tànnal ay ponk yu am solo ci leetar bi ñu bànqaas bi yónnee te wax ci. Mu ngi ci xët bi njëkk ci Sasu Nguuru Yàlla bii.

20 min : Lan lañu defoon daaw ? Wottukatu liggéeyu waare bi mooy seet li mbooloo mi def daaw ci liggéeyu waare bi. Na gën a wax ci lu rafet li mbooloo mi def ci liggéey boobu. Waxal benn walla ñaari fànn fu mbooloo mi war a góor-góorlu at mii di ñów. Waxal lu rafet li pioñee yi def. Waxal lu baax li ñu gis bi ñu doon jàpple ñi bàyyi woon waare.

15 min : “ Nañu wéy di dëgëral suñu ngëmu moroom. ”c Waxal ñi teew ñu wax li leen seen mbokk ci ngëm defal ndax mbëggeel bi ñu am ci ñoom.

Woy-Yàlla 79 ak ñaan bu mujj bi.

26 septaambar ba 2 oktoobar

Woy-Yàlla 32

10 min : Yégle yi jëm ci suñu mbooloo. Waxal fu ñu tollu ci xaalisu mbooloo mi te jàngal kayit biy wone ne bànqaas bi jot na xaalis bi ñu maye. Waxal waaraatekat yi ñu bañ a fàttee bind li ñu def ci liggéeyu waare bi ci weeru septaambar te joxe ko.

15 min : Li nekk soxla ci mbooloo mi.

20 min : Nañu jëfandikoo yéenekaay yi ngir xamal nit ñi xibaar bu baax bi. La Tour de Garde ak Réveillez-vous ! lañuy wone ci weeru oktoobar. Ponk yii di topp, ci Sasu Nguuru Yàlla bu màrs 2004, xët 5, xise 3 ba 6, lañu leen jële. Nanga komaase sa waxtaan ci ponk yooyu maanaam : 1) Booleel ay yéenekaay boo leen di wone. 2) Nanga jàpp benn bés ci ayu-bés bu nekk ngir wone suñuy yéenekaay. 3) Nanga seet ñaata yéenekaay nga bëgg a joxe weer wu nekk. 4) Nanga wone suñu yéenekaay yi saa yoo ci amee bunt. 5) Nanga jëfandikoo bu baax yéenekaay yi xaw a yàgg. Waxal ni ñu mënee topp xelal yooyu ci seen goxu mbooloo. Na am ñu topp li nekk ci xët 8 te wone ni ñu mënee wone Réveillez-vous ! bu 8 septaambar ak La Tour de Garde bu 15 septaambar. Mën ngeen wax it leneen lu mën a baax ci seen gox. Na benn magu mbooloo wone benn yéenekaay, te benn xale wone bi ci des. Bu ci kenn wonee yéenekaay yi ba pare, waxal lu tax li mu def baax.

Woy-Yàlla 1 ak ñaan bu mujj bi.

3-9 oktoobar

Woy-Yàlla 11

10 min : Yégle yi jëm ci suñu mbooloo. Na am ñu topp li nekk ci xët 8 te wone ni ñu mënee wone Réveillez-vous ! bu 22 septaambar ak La Tour de Garde bu 1 oktoobar. Mën ngeen wax it leneen lu mën a baax ci seen gox. Waxal itam ci yeneen waxtaan yu nekk ci yéenekaay yi, yu mën a neex ñi nekk ci seen gox. Na am ku ci jël benn ngir wone yéenekaay yi. Bu ci kenn wonee yéenekaay yi ba pare, waxal lu tax li mu def baax.

20 min : “ Nañu jariñoo bu baax suñu jot. ”d Waxal ñi teew ñu wax ni ñuy def ba mën a jàng Biibël bi bés bu nekk. Waxal njaboot yi ak ñeneen ñi ñu topp li nekk ci Sasu Nguuru Yàlla bu me 2005, xët 3 ba 6 ngir taxawal benn porogaraam ngir li ñuy def ngir jaamu Yàlla.

15 min : Nañu bégal Yexowa (Léeb. 27:11). Nanga waxtaan ak ñaar walla ñetti mbokk ci ngëm yu yàgg jaamu Yexowa. Kenn ku ci nekk dina wax benn walla ñaari mbir yu tax ñu kontine di déggal Yexowa. Mën nañu wax lu mel ni tàmm jàng Biibël bi yow kenn, tàmm di teewe ndaje yi, am ay xarit yuy déggal bu baax Yexowa, bokk bu baax ci liggéeyu waare bi, ñaan Yàlla ñaan yu jóge ci biir xol, ak moytu fo yu tilim yi. Ndax jaar nañu ci lu leen mënoon a tere déggal Yexowa ? Naka lañu def ba loolu bañ leen a tere déggal Yexowa ? Yan barke lañu am ndax li ñu déggal Yexowa ?

Woy-Yàlla 69 ak ñaan bu mujj bi.

[Li ñu bind ci suuf]

a Li ngay njëkk wax warul weesu benn minit, ba pare laajal ñi teew ay laaj, te may leen ñu tontu.

b Li ngay njëkk wax warul weesu benn minit, ba pare laajal ñi teew ay laaj, te may leen ñu tontu.

c Li ngay njëkk wax warul weesu benn minit, ba pare laajal ñi teew ay laaj, te may leen ñu tontu.

d Li ngay njëkk wax warul weesu benn minit, ba pare laajal ñi teew ay laaj, te may leen ñu tontu.

    Téere yi ci Wolof (1996-2025)
    Ngir génn
    Ngir konektewu
    • Wolof
    • Yónnee ko
    • Ni nga bëgge mbir yi feeñe
    • Copyright © 2025 Watch Tower Bible and Tract Society of Pennsylvania
    • Conditions d’utilisation
    • Règles de confidentialité
    • Paramètres de confidentialité
    • JW.ORG
    • Ngir konektewu
    Partager