TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Watchtower
TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Wolof
  • BIBLE
  • TÉERE YI
  • RÉUNIONS
  • km 9/05 p. 1
  • Nañu jariñoo bu baax suñu jot

Aucune vidéo n'est disponible pour cette sélection.

Il y a eu un problème lors du chargement de la vidéo.

  • Nañu jariñoo bu baax suñu jot
  • Sasu Nguuru Yàlla — 2005
  • Leneen lu jëm ci loolu
  • Nañu yemale waxtu yi ñuy féexal suñu xol, fi ñu war a yem
    Sasu Nguuru Yàlla — 2001
  • Lan ngay jiital ci sa dund ?
    Sasu Nguuru Yàlla — 2006
  • Bégalal Yexowa ci ni ngay féexale sa xol
    Mën nga dund ci jàmm ba fàww! (Njàngum Biibël bi)
Sasu Nguuru Yàlla — 2005
km 9/05 p. 1

Nañu jariñoo bu baax suñu jot

1 Ñun, Yexowa lañu bëgg neex. Moo tax ñuy fexe ba li ñuy def ci wàllu ngëm, nekk li ëpp solo ci suñu dund. Kàddu Yàlla mu ngi ñuy sant ñu ‘ jëkk wut nguuram ’ te ‘ sax ci [yëf] yi gëna rafet ’, maanaam seet li war a ëpp solo ci suñu dund (Macë 6:33 ; Fil. 1:10). Lu ñu mën a def ba am jot ngir lépp lu ñu war a def ci wàllu Nguur gi, te yemale li ci des fi mu war a yem ? — Efes 5:​15-17.

2 Nañu jiital ci suñu dund lépp li ànd ak liggéeyu Nguur gi : Nanga defar benn porogaraam ngir bañ a yàq jot ci lu amul solo noonu. Am na ñuy bind ci seen calendrier bés yi ñu bëgg waaraate. Loolu dañu koy def bu weer wi di komaase. Te bu ñu defee loolu ba pare, duñu nangu leneen tere leen def li ñu tëral noonu. Mën nga def loolu itam ak waxtu yi nga bëgg jàngal sa bopp, ak waxtu yi nga bëgg teewe suñu ndaje yi, muy ci mbooloo mi walla ndaje yu mag yi. Ñu bare dañuy def porogaraam ngir li ñu war a def bés bu nekk te dañu ciy boole jàng Biibël bi. Ci lañuy komaase bés bi, walla moom lañu koy jeexale. Tànnal waxtu yi ngay defe lépp li am solo, te bul bàyyi lu amul solo noonu jël waxtu yooyu. — Daj. 3:1 ; 1 Kor. 14:⁠40.

3 Bul ëppal ci ni ngay jëfandikoo li nekk ci àddina si : Am na réew yoo xam ne, espoor, fo yi ak yeneen yu mel noonu dañu bare. Ñu bare, waxtu yi ñuy seetaan tele walla nekk ci seen ordinatër, dafa ëpp. Waaye ñi dem ba seen xel yépp nekk ci fo walla ci lu bees lu àddina si di am, ci lu wóor dinañu mujje ci “ céy su ma xamoon ” (1 Ywna. 2:​15-17). Moo tax Mbind yi nee ñu bañ a ëppal bu ñuy jëfandikoo li nekk ci àddina si (1 Kor. 7:31). Loolu, lu am solo la. Boo ko toppee, dinga mën a won Yexowa ne jaamu ko moo ëpp solo ci sa dund. — Macë 6:​19-21.

4 Àddina sii, waxtu bi ko dese, bareetul. Ñiy jiital ci seen dund lépp li jëm ci Nguur gi, dinañu am bànneex te dinañu neex Yàlla (Léeb. 8:​32-35 ; Saak 1:25). Jot lu am solo la. Kon nañu ko jariñoo bu baax.

    Téere yi ci Wolof (1996-2025)
    Ngir génn
    Ngir konektewu
    • Wolof
    • Yónnee ko
    • Ni nga bëgge mbir yi feeñe
    • Copyright © 2025 Watch Tower Bible and Tract Society of Pennsylvania
    • Conditions d’utilisation
    • Règles de confidentialité
    • Paramètres de confidentialité
    • JW.ORG
    • Ngir konektewu
    Partager