TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Watchtower
TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Wolof
  • BIBLE
  • TÉERE YI
  • RÉUNIONS
  • km 9/05 p. 8
  • Nañu wéy di dëgëral suñu ngëmu moroom

Aucune vidéo n'est disponible pour cette sélection.

Il y a eu un problème lors du chargement de la vidéo.

  • Nañu wéy di dëgëral suñu ngëmu moroom
  • Sasu Nguuru Yàlla — 2005
  • Leneen lu jëm ci loolu
  • Nañu def lu baax te sédde ci li ñu am
    Sasu Nguuru Yàlla — 2005
  • Bu ñuy waare, na ku nekk yokk sa doole moroom
    Sasu Nguuru Yàlla — 2008
  • Ndimbal bu yomb am
    Sasu Nguuru Yàlla — 2006
Sasu Nguuru Yàlla — 2005
km 9/05 p. 8

Nañu wéy di dëgëral suñu ngëmu moroom

1 Ndaw li Pool dafa doon def lépp ngir dëgëral ngëmu mbokkam yi ci ngëm ((Jëf. 14:​19-22)). Ñun it, dañuy def lu mel noonu. Bu suñu mbokk nekkee ci coono, dafa ñuy laal, te dañu koy bëgg dimbali. Biibël bi wone na ne du magi mbooloo mi rekk ñoo war a toppatoo waa mbooloo mi. Ñun ñépp a ko war a def (Room 15:​1, 2). Biibël bi nee na : “ Nangeen dëgëralante te yokkante seen ngëm. ” (1 Tes. 5:11) Nañu seet ñaari fasoŋ yi ñu ko mën a defe.

2 Bu kenn amee soxla, nañu ko gis : Kàddu Yàlla nee na Dorkas dafa doon “ wéy ci jëf yu baax ak saraxe ”. (Jëf. 9:​36, 39.) Bu nit amee soxla, dafa ko doon gis, ba pare mu def lépp ngir dimbali ko. Dëgg-dëgg, Dorkas jar na roy ! Ndax danga dégg ne suñu benn mbokk bu màgget dafa soxla ku koy yóbbu ca ndaje ya ? Walla am na benn pioñee bu amul ku muy àndal ci waaraate bi benn ngoon ci ayu-bés bi ? Boo gisee ku soxla lu mel noonu te nga wax ko li nga bëgg def ngir jàpple ko, dina kontaan lool !

3 Nañu am ak suñuy mbokk waxtaan yu jëm ci suñu ngëm : Li ñuy wax itam mën na dëgëral suñu ngëmu moroom (Efes 4:29). Benn magu mbooloo bu yàgg nekk mag ci mbooloo mi nee na : “ Boo bëggee yokk sa doole moroom, nanga am waxtaan yu jëm ci suñu ngëm. Boo bëggee komaase waxtaan buy dëgëral ngëm, mën nga laaj lu mel nii : ‘ Naka nga xame dëgg gi ? ’ ” Nanga jege ndaw yi nekk ci sa mbooloo te won leen ne fonk nga leen. Jegeel itam ñi seen xol jeex walla ñiy gaaw a rus (Léeb. 12:25). Bu ñu nekkee ak suñuy mbokk, mën nañu nekk di waxtaan rekk ci fowi àddina si ba duñu wax sax ci suñu ngëm. Buñu nangu loolu. — Room 1:​11, 12.

4 Léegi lan nga mën a wax nit ñi ngir dëgëral seen ngëm ? Danga faral di jàng walla gëstu Biibël bi. Ndax amul loo ci yàggul a jàng lu tax nga gën a fonk Yexowa ? Ndax amul lu yokk sa doole lu nga dégg ci benn waxtaan bu ñu jagleel ñépp, walla njàngum La Tour de Garde ? Ndax déggoo fu suñu benn mbokk jaar te loolu dëgëral sa ngëm ? Lu mel noonu am na maanaa lool ci wàllu ngëm. Boo ko fonkee, foo mënta nekk, dinga am loo mën a wax suñuy mbokk ngir ñu gën a am doole ci wàllu ngëm. — Léeb. 2:1 ; Lukk 6:⁠45.

5 Nañu bëgg dimbali suñuy mbokk te xam bu baax li ñu leen di wax. Su ñu defee loolu, dinañu wéy di dëgëral suñu ngëmu moroom yi. — Léeb. 12:18.

    Téere yi ci Wolof (1996-2025)
    Ngir génn
    Ngir konektewu
    • Wolof
    • Yónnee ko
    • Ni nga bëgge mbir yi feeñe
    • Copyright © 2025 Watch Tower Bible and Tract Society of Pennsylvania
    • Conditions d’utilisation
    • Règles de confidentialité
    • Paramètres de confidentialité
    • JW.ORG
    • Ngir konektewu
    Partager