Wonal sa moroom ne danga ko bëgg — nanga baax ak moom
1 Dafa am jigéen joo xam ne, pur moom, Seede Yexowa yi baaxuñu. Waaye benn bés, dafa daje ak benn Seede Yexowa. Nee na : “ Dëgg-dëgg, fàtte naa ci lan lañu doon waxtaan bés boobu. Waaye ni mu baaxe woon ak man, loolu moom, fàttewuma ko. Ku bëgg nit te ku woyof la woon. Dëgg-dëgg dama ko bëggoon a def xarit. ” Waaw, bu ñuy waaraate, nañu won nit ñi ne dañu leen bëgg. Lu am solo la. — Fil. 2:4.
2 Ku bëgg sa moroom dangay baax ak moom : Boo bëggee sa moroom, dinga baax ak moom, maanaam dinga laabiir (1 Kor. 13:4). Ku baax dafay yéene moroomam jàmm. Te dafay seet li mu mën a def ngir dimbali ko. Bu ñuy waar nit ñi ci xibaar bu baax bi, dañu leen di defal lu baax. Waaye du foofu la suñu mbëggeel war a yem. Dafa war a feeñ ci suñu jikko — ci ni ñuy baaxe ak ñoom, ci yar ak teggin bi ñuy wone, ci ni ñu leen di dégloo, ci li ñu leen di wax ak ni ñu koy waxe, ak ci bët yi ñu leen di xoole. — Macë 8:2, 3.
3 Bu ñu bëggee suñu moroom, dinañu seet itam li ñu mën a def ngir dimbali ko. Benn pioñee dafa doon waaraate. Mu àgg ci këru benn jigéen ju màgget ju jëkkëram gaañu woon. Waaye jigéen ji, bi mu gisee ne seede Yexowa la, mayu ko mu wax. Mu nee ko, bi mu ñówee ci buntam, ci waañ bi la nekkoon. Am na fu mu yéegoon ngir jéem a dindi benn làmp bu yàqu. Pioñee bi nee ko : “ Yow kenn yaay def loolu ? Wóorul de. ” Jigéen ji bàyyi ko mu dugg. Pioñee bi daldi ko defaral làmp bi, ba pare dem. Bi loolu paasee tuuti, doomu jigéen jooju ñów seetsi ko. Yaayam nettali ko li pioñee bi defoon. Loolu dafa ko laal ba mu dem wuti suñu mbokk moomu ngir gërëm ko. Bi mu ko gisee, waxtaan nañu bu baax ba mu nangu jàng Biibël bi ak ñun.
4 Yexowa bëgg na doom-Aadama yi. Bu ñu baaxee ak nit ñi, ñu ngi roy ci Moom. Te loolu dafay rafetal xibaaru Nguur gi bi ñuy waare. Kon, fu ñu mënta nekk, nañu “ rafetal suñu tur ni jawriñi Yàlla [...] ci laabiir ”, maanaam nañu baax ak ñépp, te wone noonu ne, ñun, Yàlla lañuy liggéeyal. — 2 Kor. 6:4, 6.