Ndaje yi jëm ci liggéeyu waare bi
Buleen fàtte : Jamano bu ñuy am suñu ndaje yu gën a mag yi, Sasu Nguuru Yàlla bi dina joxe li ñu war a def ayu-bés bu nekk ci ndaje yi jëm ci liggéeyu waare bi. Mbooloo yi nga xam ne ci weer wii lañu war a am seen ndaje bu gën a mag bi tudd “ Nañu déggal Yàlla ”, dinañu seet li ñu war a soppi ci porogaraam bii ngir mën a teewe ndaje bu mag boobu. Su baaxee ci seen mbooloo, ayu-bés biy jiitu ayu-bés bi ngeen di am seen ndaje bu gën a mag bi, nangeen jël 15 minit ngir seetaat ponk yi am solo yu seen mbooloo warul a fàtte ci li nekk ci xët 3 ba 6 ci Sasu Nguuru Yàlla bii. Bu ndaje bu mag bi paasee ba mu mat benn walla ñaari weer, dinañu jël 15 ba 20 minit ci benn ci ndaje yi jëm ci liggéeyu waare bi (mën na nekk ci xaaj bi tudd “ Li nekk soxla ci mbooloo mi ”) ngir waxtaan ci ay ponku porogaraam boobu, yu waaraatekat yi gis ne dañoo baax ci waaraate bi. Ci waxtaan boobu, dinañu mën a wax ni ñuy toppe li ñu jàng ci ndaje bu gën a mag boobu ak li ñu fa jàng loo xam ne tax na seen waaraate bi gën a am njariñ.
10-16 oktoobar
Woy-Yàlla 27
10 min : Yégle yi jëm ci suñu mbooloo. Yenn ci yégle yi nekk ci Sasu Nguuru Yàlla. Li nekk ci xët 8, bu baaxee ci seen gox, na am ñu koy topp te wone ni ñu mënee wone Réveillez-vous ! bu 8 oktoobar ak La Tour de Garde bu 15 oktoobar. Ku ci nekk bu paree, waxal lu baax li mu def. Nanga wax itam ci yeneen waxtaan yu nekk ci yéenekaay yooyu yu mën a itteel nit ñi ci seen gox.
15 min : Ndax danga faral di jàng ni mu ware ? Waxtaan ak ñi teew bu ñu jële ci téere École du ministère, xët 21 ba 26. Lan lañu mën a boole ci suñu porogaraamu njàng (seetleen wërale bi nekk ci xët 21) ? Lu tax ñu war a jàng téere yi mbootaayu Yàlla defar (xët 23, xise 2) ? Am na lu am solo lu ñu war a topp bu ñu bëggee suñu porogaraamu njàng yàgg te ñu bañ koo bàyyi. Loolu lan la (xët 26, xise 3-4) ? Loo def ba mën a jàng suñu yéenekaay yi La Tour de Garde ak Réveillez-vous ! ? Ban njariñ nga ci gis ?
20 min : “ Nañu kontine di wax Kàddu Yàlla ak fit wu dëgër. ”a Laajal ñi teew ñu wax kañ la waare ak fit mën a jafe. Lan moo leen dimbali ba ñu mën ko def ?
Woy-Yàlla 64 ak ñaan bu mujj bi.
17-23 oktoobar
Woy-Yàlla 41
10 min : Yégle yi jëm ci suñu mbooloo. Nanga seetaat benn walla ñaari ponk yu nekk ci xaaj 3 bi nekk ci Sasu Nguuru Yàlla bu septaambar 2005, xët 3. Dañu fay wone ni ñu mënee jëfandikoo bu baax Mbind yi bu ñuy jàngale Biibël bi.
15 min : Nañu moytu lu bon li nekk ci internet. Waare bu benn magu mbooloo di def, ci li nekk ci Réveillez-vous ! bu 8 desàmbar 2004, xët 18 ba 21.
20 min : “ Wonal sa moroom ne danga ko bëgg — nanga baax ak moom. ”b Laajal ñi teew ñu wax, bu ñuy waaraate, naka lañu mënee won nit ñi ne dañu leen bëgg. Dinañu ci gën a waxtaan ci Sasu Nguuru Yàlla yiy ñów.
Woy-Yàlla 18 ak ñaan bu mujj bi.
24-30 oktoobar
Woy-Yàlla 29
5 min : Yégle yi jëm ci suñu mbooloo.
15 min : Li nekk soxla ci mbooloo mi.
25 min : “ Nañu màggal Yexowa ci diggu mbooloo mu réy mi. ”c Sekkerteeru mbooloo mi moo koy def. Waxal ban ndaje bu gën a mag la seen mbooloo war a teewe. Nangeen waxtaan ci xise yi, mel ni bu ñuy def njàngum La Tour de Garde. Na am kuy jàng xise yi. Nangeen seetaat li nekk ci wërale bi tudd “ Ndaje bu gën a mag bi : Li ñu warul a fàtte. ”
Woy-Yàlla 4 ak ñaan bu mujj bi.
31 oktoobar ba 6 nowàmbar
Woy-Yàlla 92
10 min : Yégle yi jëm ci suñu mbooloo. Waxal waaraatekat yi ñu bañ a fàttee bind li ñu def ci liggéeyu waare bi ci weeru oktoobar te joxe ko. Li nekk ci xët 8, bu baaxee ci seen gox, na am ñu koy topp te wone ni ñu mënee wone Réveillez-vous ! bu 22 oktoobar ak La Tour de Garde bu 1 nowàmbar. Na ci kenn wone li nekk ci wërale bi tudd “ Dans notre prochain numéro ” (maanaam liy am ci yéenekaay biy ñëw) ngir waajal waxtaan bi ngeen mën a am beneen yoon. — Seetal Le Ministère du Royaume bu oktoobar 1998, xët 10, xise 7 ba 8.
15 min : “ Nañu fexe ba nit ñi bëgg yokk li ñu xam ci Biibël bi, bu ñuy faral di leen indil suñu yéenekaay yi. ”d Bu ngeen di def xise 3, woneel li nekk ci téere Comment raisonner, xët 336 ba 341. Mën ngeen ci tànn ay aaya ngir waajal ay waxtaan yu def benn aaya ci li Nguuru Yàlla di def. Na am benn waaraatekat buy wone ni ñu mënee waxtaan ak nit ci benn aaya, bu ñuy yóbbul nit yéenekaay yu sog a génn. Dina faramfàcce ci lu gàtt aaya bi te misaal ko ngir nit ki xam bu baax li aaya boobu bëgg wax ak it njariñ bi mu mën a am bu ko toppee.
20 min : Ay ndaw yu xam li ñu bëgg te bañ a ñàkk yar. Waare bu benn magu mbooloo di def, ci La Tour de Garde bu 15 septaambar 2002, xët 23 ba 24 ci xaaj bi tudd “ Une abstention respectueuse ” (maanaam dañu bañ waaye defuñu ko ci fasoŋ bu amul yar). Balaa ndaje bi di jot, nanga wax benn walla ñaari ndaw ne dinga leen laaj ñu wax jafe-jafe yi ñu am ci seen lekkool ak li leen ci dimbali.
Woy-Yàlla 100 ak ñaan bu mujj bi.
7-13 nowàmbar
Woy-Yàlla 26
10 min : Yégle yi jëm ci suñu mbooloo. Waxal fu ñu tollu ci xaalisu mbooloo mi te jàngal kayit biy wone ne bànqaas bi jot na xaalis bi ñu maye. Na am ku topp li nekk ci Sasu Nguuru Yàlla bu sãwiyee 2005, xët 3 ba 6 ngir wone ni ñu mënee wone téere bu ñu war a wone ci weeru nowàmbar. Su leneen baaxee ci seen gox, mën na ko wax it ngir wone téere boobu. — Seetleen Sasu Nguuru Yàlla bu sãwiyee 2005, xët 8, xise 5.
15 min : Fexeel ba sa xel gën a nekk ci li ñuy wax ci ndaje yi. Waare ak waxtaan ak ñi teew bu ñu jële ci La Tour de Garde bu 15 septaambar 2002, xët 12 ba 14, xise 11 ba 14. Nangeen seetaat li ñu ci wax te laajal ñi teew ñu wax li leen dimbali ba ñu gën a jariñoo ndaje yi ñuy am ci mbooloo mi.
20 min : Li ñuy sol ak ni ñuy defare suñu bopp, na ànd ak li neex Yàlla. Waare ak waxtaan ak ñi teew bu ñuy jële ci La Tour de Garde bu 1 ut 2002, xët 17 ba 19. Benn magu mbooloo moo koy def. Laajal ñi teew naka la solu bu yiw mënee ubbi bunt bu ñuy waare.
Woy-Yàlla 73 ak ñaan bu mujj bi.
[Li ñu bind ci suuf]
a Li ngay njëkk wax warul weesu benn minit, ba pare laajal ñi teew ay laaj, te may leen ñu tontu.
b Li ngay njëkk wax warul weesu benn minit, ba pare laajal ñi teew ay laaj, te may leen ñu tontu.
c Li ngay njëkk wax warul weesu benn minit, ba pare laajal ñi teew ay laaj, te may leen ñu tontu.
d Li ngay njëkk wax warul weesu benn minit, ba pare laajal ñi teew ay laaj, te may leen ñu tontu.