Ndaje yi jëm ci liggéeyu waare bi
BULEEN FÀTTE : Bu ndaje bu mag bi tudd “ Nañu déggal Yàlla ” paasee ba mu mat benn walla ñaari weer, dinañu jël 15 ba 20 minit ci benn ci ndaje yi jëm ci liggéeyu waare bi ngir waxtaan ci ay ponku porogaraam boobu. Bu leen neexee, mën ngeen ko def ci xaaj bi tudd “ Li nekk soxla ci mbooloo mi ”. Ponk yooyu na nekk ay ponk yu waaraatekat yi gis ne dinañu baax ci waaraate bi. Ci waxtaan boobu, dinañu mën a wax ni ñuy toppe li ñu jàng ci ndaje bu gën a mag boobu ak li ñu fa jàng loo xam ne dafa tax seen liggéeyu waare bi gën a am njariñ. — Seetleen li nekk ci Sasu Nguuru Yàlla bu oktoobar 2005, xët 2.
14-20 nowàmbar
Woy-Yàlla 98
10 min : Yégle yi jëm ci suñu mbooloo. Yenn ci yégle yi nekk ci Sasu Nguuru Yàlla. Na ñaari nit topp li nekk ci xët 4, te wone ni ñu mënee wone Réveillez-vous ! bu 8 nowàmbar ak La Tour de Garde bu 15 nowàmbar. Mën nañu wax leneen lu mën a baax ci seen gox ngir wone yéenekaay yi. Na ku ci nekk wone li ñu mën a tontu bu amee ku ñu ne : “ Mbirum diine soxalu ma ”. — Seetleen téere Comment raisonner xët 16 ak 17.
15 min : Ay maye yuy seddal xolu Yàlla. Waare bu benn magu mbooloo di def ci li nekk ci La Tour de Garde bu 1 nowàmbar 2005, xët 26 ba 30.
20 min: “ Nañu màggal Yexowa. ”a Boo defee lu baax ba nit ñi gis ko, dinga ci mën a jaar ba waar nit ñi. Bu ngeen di def xise 4, waxal ñi teew ñu nettali ci lu gàtt loolu naka la mënee nekk.
Woy-Yàlla 79 ak ñaan bu mujj bi.
21-27 nowàmbar
Woy-Yàlla 14
10 min : Yégle yi jëm ci suñu mbooloo.
20 min : Na Yexowa nekk seen Yàlla. Waare bu benn magu mbooloo di def, ci li nekk ci La Tour de Garde bu 1 awril 2005, xët 25 ba 28. Waxal ni ñu mënee topp li ñu jàng ci Ibrayima, Dawuda, ak Ilias.
15 min : “ Wonal sa moroom ne danga ko bëgg : nanga nekk ku mën seetlu. ”b Na benn waaraatekat wone ni muy seetloo lu koy xamal li soxal ki muy waxal, ak ni mu ciy waxtaane.
Woy-Yàlla 31 ak ñaan bu mujj bi.
28 nowàmbar ba 4 desàmbar
Woy-Yàlla 87
12 min : Yégle yi jëm ci suñu mbooloo. Waxal fu ñu tollu ci xaalisu mbooloo mi te jàngal kayit biy wone ne bànqaas bi jot na xaalis bi ñu maye. Waxal waaraatekat yi ñu bañ a fàttee bind li ñu def ci liggéeyu waare bi ci weeru nowàmbar te joxe ko. Na ñaari nit topp li nekk ci xët 4, te wone ni ñu mënee wone Réveillez-vous ! bu 22 nowàmbar ak La Tour de Garde bu 1 desàmbar. Mën ngeen wax leneen lu mën a baax ci seen gox ngir wone yéenekaay yi. Nañu wax nit ki ne bu bëggee, mën na maye dara ngir jàpple suñu liggéey.
15 min : “ Naka lañu leen mënee dimbali ? ” Waare lay doon. Nanga nettali li yenn seede Yexowa def ngir jàpple seeni mbokk ci ngëm yu nekkoon ci coono. (Seetal Réveillez-vous ! bu 8 ut 2003, xët 10 ba 15, bu 22 nowàmbar 2002, xët 19 ba 24, ak bu 22 oktoobar 2001, xët 23 ba 27. Mën nga seet it yeneen téere.) Boo ci paree, waxtaanleen ci ponk yi ëpp solo ci xaaj bi nekk ci xët 3 ci Sasu Nguuru Yàlla bii. Fexeel ba nit ñi gis ne bu ñu bëggee maye dara ngir jàpple suñu mbokk yi nekk ci coono, li gën mooy ñu def ko ci kees yi ñu def ngir jàpple liggéeyu waare bi ci àddina si sépp.
18 min : Ni ñuy yéglee xibaar bu baax bi ci weeru desàmbar. Waare ak waxtaan ak ñi teew. Ci juróomi minit yu njëkk yi, waxal ci ponk yii di topp yu nekk ci xaaj bi tudd “ Ni ñu waree topp li ñu bind ngir wone li ñu mën a wax ci waaraate bi ”, bi nekk ci Sasu Nguuru Yàlla bu sãwiyee 2005 : 1) Li ñu bind ngir wone li ñu mën a wax ci waaraate bi, bu ñu ko mënee wax ci suñu kàddu bopp, ci lay gën a baax. 2) War nañu seet bu baax li ñu mën a wax ak li ñu warul a wax fi ñuy waare. 3) War nañu seet itam ni nit ñi di yaroo ak ni ñuy xalaate. 4) Dañu war a jàng bu baax li ñu bëgg won nit ki te seet ay ponk yu ko mën a itteel. 5) Bu ñuy waaraate, mën nañu wax leneen lu dul li ñu bind ci Sasu Nguuru Yàlla bi ngir wone li ñu mën a wax ci waaraate bi. Juróomi ponk yooyu, war nañu leen a topp bu ñuy wone suñu téere yi ci weeru desàmbar. Waxleen ni ngeen ko mënee def. Mën ngeen topp li nekk ci Sasu Nguuru Yàlla bu sãwiyee 2005 ci xët 3 ba 6 walla leneen lu mën a baax ci seen goxu mbooloo. Na benn walla ñaari waaraatekat wone ku ci nekk ni ñu mënee wone suñu téere yi.
Woy-Yàlla 50 ak ñaan bu mujj bi.
5-11 desàmbar
Woy-Yàlla 17
10 min : Yégle yi jëm ci suñu mbooloo.
15 min : Li nekk soxla ci mbooloo mi.
20 min : “ Li suñu liggéeyu waare bi di def. ”c Bu ngeen di def xise 5, booleleen ci li nekk ci La Tour de Garde bu 15 feewriyee 2004, xët 32.
Woy-Yàlla 9 ak ñaan bu mujj bi.
[Li ñu bind ci suuf]
a Li ngay njëkk wax warul weesu benn minit, ba pare laajal ñi teew ay laaj, te may leen ñu tontu.
b Li ngay njëkk wax warul weesu benn minit, ba pare laajal ñi teew ay laaj, te may leen ñu tontu.
c Li ngay njëkk wax warul weesu benn minit, ba pare laajal ñi teew ay laaj, te may leen ñu tontu.