Wonal sa moroom ne danga ko bëgg : nanga nekk ku mën seetlu
1 Yexowa Yàlla ak Yeesu Krist dañuy seetlu liy soxla nit ñi, ba pare jàpple leen ci. Kenn gënu leen mën a def loolu (2 Net. 16:9 ; Mark 6:34). Ci waaraate bi, bu ñu ràññee liy soxal nit ñi ak liy seeni coono, dinañu mën a xam li ñuy waxtaan ak ñoom.
2 Nanga xool bu baax : Yeesu, ku mën seetlu la woon (Mark 12:41-43 ; Lukk 19:1-6). Ñun itam, bu ñuy dugg ci kër, nañu xool bu baax li ñu def ci kër gi ngir rafetal ko, ngir xam ci ban diine la waa kër gi bokk. Bu fa amee oto, seetal li ñu ci bind. Seetal it ndax amul ay fowukaay ci ëtt bi. Bu ñu defee loolu, dinañu mën a xam li ñu mën a wax ngir xamal nit ñi xibaar bu baax bi ci fasoŋ bu rafet. Bu ñuy dugg ci kër bu ñuy nuyoo, nañu seet itam li nit ñi di def. Dina tax bu ñuy waxtaan ak ñoom, ku ci nekk dinañu ko mën a wax lu koy soxal.
3 Li nekk ci xolu nit, mën na feeñ ci kanamam ak ci ni muy jëfe (Léeb. 15:13). Xéyna dafa am mbokk mu gaañu, walla mu am leneen lu ko metti, ba tax mu soxla kuy waxtaan ak moom ngir féexal xolam. Boo ko wonee ay aaya yu ànd ak li mu nekkee, mën na am mu neex ko (Léeb. 16:24). Mën nga tase ak kuy génn këram fekk dafa yàkkamti. Walla ki ñów ci bunt bi dafa yore xale buy jooy. Xéyna li gën mooy nga wax ko ne dinga jaaraat beneen yoon. Nit kooku bu gisee ne dañu ko fonk, te dañuy bokk tiisam, loolu mën na tax bés bu ñu fa dellusee, mu nangu ñu déglu. — 1 Pie. 3:8.
4 Xoolal ni nit ki mel, ba pare nga seet loo ko mën a wax : Ndaw li Pool dafa gisoon ca Aten, benn màggalukaay fu ñu bindoon lii : “ Yàlla mi nu xamul. ” Ci loolu la jaar ngir xamal leen xibaar bu baax bi. Dafa leen nee : “ Li ngeen di màggal nag te xamuleen ko, loolu laa leen di xamal. ” Pool dafa seet bu baax ni muy waxe ak ñoom ngir bañ ci tooñ kenn. Looloo tax mu am ñu ci déglu xibaaru Nguur gi ba gëm. — Jëf. 17:23, 34.
5 Ñun itam, bu ñu nekkee ay nit ñu mën seetlu, dinañu mën a ràññe liy soxal nit ñi. Bu ko defee, dinañu leen mën a wax lu ci jëm. Nanga laaj nit ñi ay laaj yuy tax ñu mën a wax seen xalaat. Seetal aaya yoo xam ne bu ko nit ki déggee, dina gën a bëgg déglu suñu waxtaan (Léeb. 20:5). Bu ñu nekkee nit ku mën seetlu, te di won suñu moroom ne dañu ko bëgg, dinañu mën a waare ci fasoŋ bu baax.